Saba · 39/54
Tekki Waxtaan — Saba
قُلْ إِنَّ رَبِّي يَبْسُطُ الرِّزْقَ لِمَن يَشَاءُ مِنْ عِبَادِهِ وَيَقْدِرُ لَهُ ۚ وَمَا أَنفَقْتُم مِّن شَيْءٍ فَهُوَ يُخْلِفُهُ ۖ وَهُوَ خَيْرُ الرَّازِقِينَ ۝٣٩
Qul inna Rabbee yabsutur rizqa limai yashaaa`u min `ibaadihee wa yaqdiru lah; wa maaa anfaqtum min shai`in fahuwa yukhlifuhoo wa Huwa khairur raaziqeen
📖 Tekkim Wolof
Waxal ne : “Yàlla sama Boroom mooy yaatalal ku ko soob wërsëgam ci jaamam yi, Moo koy xatal it. Lépp lu ngeen mën a joxe [ci alal], moom Yàlla moo koy wuutalaat, te Yàlla moo di ngën ji kuy wërsëgal”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 37-41 — Saba

37وَمَا أَمْوَالُكُمْ وَلَا أَوْلَادُكُم بِالَّتِي تُقَرِّبُكُمْ عِندَنَا زُلْفَىٰ إِلَّا مَنْ آمَنَ وَعَمِلَ صَالِحًا فَأُولَٰئِكَ لَهُمْ جَزَاءُ الضِّعْفِ بِمَا عَمِلُوا وَهُمْ فِي الْغُرُفَاتِ آمِنُونَ
Nekkul ne seeni alal walla seeni doom ñoo leen di tax a jegeñ Yàlla. Lu dul ña ca gëm tey jëf u yiw. Ñooñu danañu am pey gu ñu fulandi ci sababus la ñu daan jëf, te ñoom ña nga ne fayax ci ay kër yu kawe [ca Àjjana].
38وَالَّذِينَ يَسْعَوْنَ فِي آيَاتِنَا مُعَاجِزِينَ أُولَٰئِكَ فِي الْعَذَابِ مُحْضَرُونَ
Waaye ña daan dox, di dëgërante bopp ak Sunuy kàddu, ñoom ña nga ne xeew ci biir mbugal ma.
39قُلْ إِنَّ رَبِّي يَبْسُطُ الرِّزْقَ لِمَن يَشَاءُ مِنْ عِبَادِهِ وَيَقْدِرُ لَهُ ۚ وَمَا أَنفَقْتُم مِّن شَيْءٍ فَهُوَ يُخْلِفُهُ ۖ وَهُوَ خَيْرُ الرَّازِقِينَ
Waxal ne : “Yàlla sama Boroom mooy yaatalal ku ko soob wërsëgam ci jaamam yi, Moo koy xatal it. Lépp lu ngeen mën a joxe [ci alal], moom Yàlla moo koy wuutalaat, te Yàlla moo di ngën ji kuy wërsëgal”.
40وَيَوْمَ يَحْشُرُهُمْ جَمِيعًا ثُمَّ يَقُولُ لِلْمَلَائِكَةِ أَهَٰؤُلَاءِ إِيَّاكُمْ كَانُوا يَعْبُدُونَ
Bu keroogee Bis ba leen Yàlla di dajale mbooleseen. Ba noppi daldi wax Malaaka ya ne leen : “Moo ndax ñii yéen la ñu daan jaamu ? ”.
41قَالُوا سُبْحَانَكَ أَنتَ وَلِيُّنَا مِن دُونِهِم ۖ بَلْ كَانُوا يَعْبُدُونَ الْجِنَّ ۖ أَكْثَرُهُم بِهِم مُّؤْمِنُونَ
Ñu ne : “Tudd nanu sag sell ! Yaw yaay sunu wéeruwaay, du ñoom. Li am moo di, ñoom jinne yi la ñu daan jaamu, li ëppoon ci ñoom jinne la ñu gëm.
SabaFihi Alxuraan
54Aaya
MeccanRevelation
39Aaya

Tekki — Saba 39

Simoore Saba Aaya 39 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Waxal ne : “Yàlla sama Boroom mooy yaatalal ku ko…

Simoore Aaya 39/54 — Saba سبأ (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Saba Dégg, Saba Tekki, Saba mp3, Saba pdf. Aaya 37–41. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers