Fatir · 35/45
Tekki Waxtaan — Fatir
الَّذِي أَحَلَّنَا دَارَ الْمُقَامَةِ مِن فَضْلِهِ لَا يَمَسُّنَا فِيهَا نَصَبٌ وَلَا يَمَسُّنَا فِيهَا لُغُوبٌ ۝٣٥
Allazeee ahallanaa daaral muqaamati min fadlihee laa yamassunaa feehaa nasabunw wa laa yamassunaa feehaa lughoob
📖 Tekkim Wolof
Moom mi nu dalal ci kërug nooflaay ci mbaaxam, coono dunu fa dab, jaaxle it dunuu fa dab”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 33-37 — Fatir

33جَنَّاتُ عَدْنٍ يَدْخُلُونَهَا يُحَلَّوْنَ فِيهَا مِنْ أَسَاوِرَ مِن ذَهَبٍ وَلُؤْلُؤًا ۖ وَلِبَاسُهُمْ فِيهَا حَرِيرٌ
Àjjanay Hadan yoo xam danañu ca dugg, ñu di leen fa sadd ay lami wurus ak peme ; te seenug col ca biir àjjana yooyu sooy lay doon.
34وَقَالُوا الْحَمْدُ لِلَّهِ الَّذِي أَذْهَبَ عَنَّا الْحَزَنَ ۖ إِنَّ رَبَّنَا لَغَفُورٌ شَكُورٌ
Ñuy wax naan : “Xeeti cant yi ñeel na Yàlla, Yàlla mi nu dàqal tiitaange. Sunu Boroom daal Jéggalaakoon la buy Yayoowaakoonu cant.
35الَّذِي أَحَلَّنَا دَارَ الْمُقَامَةِ مِن فَضْلِهِ لَا يَمَسُّنَا فِيهَا نَصَبٌ وَلَا يَمَسُّنَا فِيهَا لُغُوبٌ
Moom mi nu dalal ci kërug nooflaay ci mbaaxam, coono dunu fa dab, jaaxle it dunuu fa dab”.
36وَالَّذِينَ كَفَرُوا لَهُمْ نَارُ جَهَنَّمَ لَا يُقْضَىٰ عَلَيْهِمْ فَيَمُوتُوا وَلَا يُخَفَّفُ عَنْهُم مِّنْ عَذَابِهَا ۚ كَذَٰلِكَ نَجْزِي كُلَّ كَفُورٍ
Ñay weddi nag, ñoom Safara la ñuy dëkk : ñu di leen xorñoññal, duñu dee ; te it deesuleen woyofalal mbugal ma. Noonu la Nuy feye képp ku di ab weddiwaakoon.
37وَهُمْ يَصْطَرِخُونَ فِيهَا رَبَّنَا أَخْرِجْنَا نَعْمَلْ صَالِحًا غَيْرَ الَّذِي كُنَّا نَعْمَلُ ۚ أَوَلَمْ نُعَمِّرْكُم مَّا يَتَذَكَّرُ فِيهِ مَن تَذَكَّرَ وَجَاءَكُمُ النَّذِيرُ ۖ فَذُوقُوا فَمَا لِلظَّالِمِينَ مِن نَّصِيرٍ
Ña ngay yuuxu ca biir, di wax naan : “Yaw sunu Boroom, génne nu ; kon dey dananu jëf u yiw, wu bokkul ak la ñu daan jëf ”. “Waaw, moo ndax dundalunuleen fa woon diir bu tax, ña fàttaliku ñépp, fàttaliku nañu ca ? Te ay xuppekat it dëkkaloon nañu leen. Kon book, toqamtikuleen mbugal mi. Tooñkat yi, kenn duleen dimbali”.
FatirFihi Alxuraan
45Aaya
MeccanRevelation
35Aaya

Tekki — Fatir 35

Simoore Fatir Aaya 35 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Moom mi nu dalal ci kërug nooflaay ci mbaaxam, coono…

Simoore Aaya 35/45 — Fatir فاطر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Fatir Dégg, Fatir Tekki, Fatir mp3, Fatir pdf. Aaya 33–37. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers