An-Nisa · 148/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
۞ لَّا يُحِبُّ اللَّهُ الْجَهْرَ بِالسُّوءِ مِنَ الْقَوْلِ إِلَّا مَن ظُلِمَ ۚ وَكَانَ اللَّهُ سَمِيعًا عَلِيمًا ۝١٤٨
Laa yuhibbullaahul jahra bis sooo`i minal qawli illaa man zulim; wa kaanallaahu Samee`an `Aleeman
📖 Tekkim Wolof
Yàlla bëggul ku fésal wax ju ñaaw, ndegam nekkul ku ñu tooñ. Yàlla Kuy dégg la, Ku xam lépp.
🎧 Dégg

📜 Aaya 146-150 — An-Nisa

146إِلَّا الَّذِينَ تَابُوا وَأَصْلَحُوا وَاعْتَصَمُوا بِاللَّهِ وَأَخْلَصُوا دِينَهُمْ لِلَّهِ فَأُولَٰئِكَ مَعَ الْمُؤْمِنِينَ ۖ وَسَوْفَ يُؤْتِ اللَّهُ الْمُؤْمِنِينَ أَجْرًا عَظِيمًا
ba mu des ña tuub, réccu, te sellal [yéwénal], jubbantiku te tënku ci Yàlla te sellal seenug jaamu Yàlla. Ñooña, ñook jullit ñee ànd. Te Yàlla Dana jox jullit ñi pey gu màgg.
147مَّا يَفْعَلُ اللَّهُ بِعَذَابِكُمْ إِن شَكَرْتُمْ وَآمَنتُمْ ۚ وَكَانَ اللَّهُ شَاكِرًا عَلِيمًا
Lu Yàlla di doye mbugal leen? Bu ngeen dee sant Yàlla te gëm ko, Yàlla di Kuy nangug cant, di Ku xam lépp nag.
148۞ لَّا يُحِبُّ اللَّهُ الْجَهْرَ بِالسُّوءِ مِنَ الْقَوْلِ إِلَّا مَن ظُلِمَ ۚ وَكَانَ اللَّهُ سَمِيعًا عَلِيمًا
Yàlla bëggul ku fésal wax ju ñaaw, ndegam nekkul ku ñu tooñ. Yàlla Kuy dégg la, Ku xam lépp.
149إِن تُبْدُوا خَيْرًا أَوْ تُخْفُوهُ أَوْ تَعْفُوا عَن سُوءٍ فَإِنَّ اللَّهَ كَانَ عَفُوًّا قَدِيرًا
Bu ngeen fésalee yiw, walla ngeen nëbb ko, walla ngeen baale lu bon [la ñu leen def]... Xamleen ne Yàlla kuy baale la, Ku am kàttan la.
150إِنَّ الَّذِينَ يَكْفُرُونَ بِاللَّهِ وَرُسُلِهِ وَيُرِيدُونَ أَن يُفَرِّقُوا بَيْنَ اللَّهِ وَرُسُلِهِ وَيَقُولُونَ نُؤْمِنُ بِبَعْضٍ وَنَكْفُرُ بِبَعْضٍ وَيُرِيدُونَ أَن يَتَّخِذُوا بَيْنَ ذَٰلِكَ سَبِيلًا
Ña weddi Yàlla ak i Yonentam, te bëgg a téqale Yàlla ak i Yonentam, te naan : “ Gëm nanu ñenn ña, weddi ñenn ña [ca Yonentam ya]”, tey jéem a am ca yoon wa nekk ca diggante weddeek ngëm,
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
148Aaya

Tekki — An-Nisa 148

Simoore An-Nisa Aaya 148 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla bëggul ku fésal wax ju ñaaw, ndegam nekkul ku…

Simoore Aaya 148/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 146–150. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers