An-Nisa · 170/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
يَا أَيُّهَا النَّاسُ قَدْ جَاءَكُمُ الرَّسُولُ بِالْحَقِّ مِن رَّبِّكُمْ فَآمِنُوا خَيْرًا لَّكُمْ ۚ وَإِن تَكْفُرُوا فَإِنَّ لِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَلِيمًا حَكِيمًا ۝١٧٠
Yaaa aiyuhan naasu qad jaaa`akumur Rasoolu bilhaqqi mir Rabbikum fa ammminoo khairal lakum; wa in takfuroo fainnna lillaahi maa fis samaawaati wal ard; wa kaanal laahu `Aleemann hakeemaa
📖 Tekkim Wolof
Éy yéen nit ñi ! Yonent bi indil na leen dëgg te bawoo fa seen Boroom. Kon gëmleen, [su ngeen ko defee], moo gën ci yéen de. Bu ngeen weddee nag, xamleen ne Moo moom la ca asamaan ya ak suuf si. Te Yàlla di Ku xam, di Ku xereñ..

🎧 Dégg


📜 Aaya 168-172 — An-Nisa

168إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا وَظَلَمُوا لَمْ يَكُنِ اللَّهُ لِيَغْفِرَ لَهُمْ وَلَا لِيَهْدِيَهُمْ طَرِيقًا
Ña weddi te tooñ, Yàlla duleen baal, duleen gindi, teg leen ci yoon wu jub wa
169إِلَّا طَرِيقَ جَهَنَّمَ خَالِدِينَ فِيهَا أَبَدًا ۚ وَكَانَ ذَٰلِكَ عَلَى اللَّهِ يَسِيرًا
lu dul xanaa ca yoonu Safara, te dañu fay béel ba fàwwu. Loola di lu yombu Yàlla.
170يَا أَيُّهَا النَّاسُ قَدْ جَاءَكُمُ الرَّسُولُ بِالْحَقِّ مِن رَّبِّكُمْ فَآمِنُوا خَيْرًا لَّكُمْ ۚ وَإِن تَكْفُرُوا فَإِنَّ لِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَلِيمًا حَكِيمًا
Éy yéen nit ñi ! Yonent bi indil na leen dëgg te bawoo fa seen Boroom. Kon gëmleen, [su ngeen ko defee], moo gën ci yéen de. Bu ngeen weddee nag, xamleen ne Moo moom la ca asamaan ya ak suuf si. Te Yàlla di Ku xam, di Ku xereñ..
171يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لَا تَغْلُوا فِي دِينِكُمْ وَلَا تَقُولُوا عَلَى اللَّهِ إِلَّا الْحَقَّ ۚ إِنَّمَا الْمَسِيحُ عِيسَى ابْنُ مَرْيَمَ رَسُولُ اللَّهِ وَكَلِمَتُهُ أَلْقَاهَا إِلَىٰ مَرْيَمَ وَرُوحٌ مِّنْهُ ۖ فَآمِنُوا بِاللَّهِ وَرُسُلِهِ ۖ وَلَا تَقُولُوا ثَلَاثَةٌ ۚ انتَهُوا خَيْرًا لَّكُمْ ۚ إِنَّمَا اللَّهُ إِلَٰهٌ وَاحِدٌ ۖ سُبْحَانَهُ أَن يَكُونَ لَهُ وَلَدٌ ۘ لَّهُ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۗ وَكَفَىٰ بِاللَّهِ وَكِيلًا
Éy yéen ñoñ-téere, buleen jéggi dayo ci seen diine, te buleen wax ci Yàlla lu dul lu nekk dëgg. Ku Nu barkeel ka di Iisaa, doomi Maryaama, doonul lu dul Yonentub Yàlla, di kàddoom ga Mu sànni ca Maryaama, di ruu gu tukkee ci Moom. Kon gëmleen Yàlla ak Yonentam. Te buleen di wax nit [Yàlla]. Bàyyileen wax jooju ! Moo gën ci yéen. Yàlla Moom kenn rekk la. Sellam gi jombaate naak Muy am doom. Moom mooy boroom li nekk ci asamaan yeek suuf si, te Yàlla doy na sëkk wéeruwaay.
172لَّن يَسْتَنكِفَ الْمَسِيحُ أَن يَكُونَ عَبْدًا لِّلَّهِ وَلَا الْمَلَائِكَةُ الْمُقَرَّبُونَ ۚ وَمَن يَسْتَنكِفْ عَنْ عِبَادَتِهِ وَيَسْتَكْبِرْ فَسَيَحْشُرُهُمْ إِلَيْهِ جَمِيعًا
Ku ñu barkeel ka [Iisaa], du jomlu te du jombulu ci nekk jaamab Yàlla, Malaaka ya gën a jegeñ [seen Boroom], ñoom it duñu ko jomlu ci jombu koo jaamu. Képp ku jomlu ci jomb koo jaamu ... [Na xam ne] Yàlla Dana leen fang [gur-gur jiital] ñoom ñépp jëme leen ca Moom.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
170Aaya

Tekki — An-Nisa 170

Simoore An-Nisa Aaya 170 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Éy yéen nit ñi ! Yonent bi indil na leen…

Simoore Aaya 170/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 168–172. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, August 19, 2026

Don't forget us in your sincere prayers