Al-Jathiya · 34/37
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Jathiya
وَقِيلَ الْيَوْمَ نَنسَاكُمْ كَمَا نَسِيتُمْ لِقَاءَ يَوْمِكُمْ هَٰذَا وَمَأْوَاكُمُ النَّارُ وَمَا لَكُم مِّن نَّاصِرِينَ ۝٣٤
Wa qeelal yawma nansaakum kamaa naseetum liqaaa`a yawmikum haazaa wa maawaakumun Naaru wa maa lakum min naasireen
📖 Tekkim Wolof
Ñu wax leen ne : “Bis niki tey dananu leen fàtte (bàyyi leen ci biir Safara) kem ni ngeen fàttewoon dajeg seen bis bii ( ba waajaluleen ko). Seenub dëkkuwaay mooy Safara ; te kenn du leen fa dimbali.

🎧 Dégg


📜 Aaya 32-36 — Simoore Al-Jathiya

32وَإِذَا قِيلَ إِنَّ وَعْدَ اللَّهِ حَقٌّ وَالسَّاعَةُ لَا رَيْبَ فِيهَا قُلْتُم مَّا نَدْرِي مَا السَّاعَةُ إِن نَّظُنُّ إِلَّا ظَنًّا وَمَا نَحْنُ بِمُسْتَيْقِنِينَ
Te bu ñu leen waxaan ne : “digub Yàlla bii dëgg la de ; te it Bis Pénc ba sikkuwul”, ngeen daan tontu ne : “Nun sax xamunu luy Bis Pénc ba ; am nanu ci ay njortu te wóoluwu nu ko.
33وَبَدَا لَهُمْ سَيِّئَاتُ مَا عَمِلُوا وَحَاقَ بِهِم مَّا كَانُوا بِهِ يَسْتَهْزِئُونَ
Ñu ne gegg ca [ñaatéefi ] seen jëf ya. Lañu daan yejje gaw leen.
34وَقِيلَ الْيَوْمَ نَنسَاكُمْ كَمَا نَسِيتُمْ لِقَاءَ يَوْمِكُمْ هَٰذَا وَمَأْوَاكُمُ النَّارُ وَمَا لَكُم مِّن نَّاصِرِينَ
Ñu wax leen ne : “Bis niki tey dananu leen fàtte (bàyyi leen ci biir Safara) kem ni ngeen fàttewoon dajeg seen bis bii ( ba waajaluleen ko). Seenub dëkkuwaay mooy Safara ; te kenn du leen fa dimbali.
35ذَٰلِكُم بِأَنَّكُمُ اتَّخَذْتُمْ آيَاتِ اللَّهِ هُزُوًا وَغَرَّتْكُمُ الْحَيَاةُ الدُّنْيَا ۚ فَالْيَوْمَ لَا يُخْرَجُونَ مِنْهَا وَلَا هُمْ يُسْتَعْتَبُونَ
li ko waral moo di ni ngeen jàpp laayay Yàlla ay reetaan dundug àddina tax ngeen woru faggu”. Bis niki tey dootu ñu fa génne te déefuleen ko woyofal.
36فَلِلَّهِ الْحَمْدُ رَبِّ السَّمَاوَاتِ وَرَبِّ الْأَرْضِ رَبِّ الْعَالَمِينَ
Yàllaa jagoo xeeti cant (yépp), Mooy Boroom asamaan yi di Boroom suuf si : di Boroom àddina sépp.
Al-JathiyaFihi Alxuraan
37Aaya
MeccanRevelation
34Aaya

Tekki — Al-Jathiya 34

Simoore Al-Jathiya Aaya 34 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñu wax leen ne : “Bis niki tey dananu leen…

Simoore Aaya 34/37 — Simoore Al-Jathiya الجاثية (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Jathiya Dégg, Simoore Al-Jathiya Tekki, Simoore Al-Jathiya mp3, Simoore Al-Jathiya pdf. Aaya 32–36. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers