Al-Ahqaf · 18/35
Tekki Waxtaan — Al-Ahqaf
أُولَٰئِكَ الَّذِينَ حَقَّ عَلَيْهِمُ الْقَوْلُ فِي أُمَمٍ قَدْ خَلَتْ مِن قَبْلِهِم مِّنَ الْجِنِّ وَالْإِنسِ ۖ إِنَّهُمْ كَانُوا خَاسِرِينَ ۝١٨
Ulaaa`ikal lazeena haqqa `alaihimul qawlu feee umamin qad khalat min qablihim minal jinni wal insi innahum kaanoo khaasireen
📖 Tekkim Wolof
Ñoom ñooñee la wax ja dal ca séen kaw (menn mbugël) mooy xeet ya leen jiitu woon ci jinne yeek nit ñi. Ñoom dañoo yàqule woon.
🎧 Dégg

📜 Aaya 16-20 — Al-Ahqaf

16أُولَٰئِكَ الَّذِينَ نَتَقَبَّلُ عَنْهُمْ أَحْسَنَ مَا عَمِلُوا وَنَتَجَاوَزُ عَن سَيِّئَاتِهِمْ فِي أَصْحَابِ الْجَنَّةِ ۖ وَعْدَ الصِّدْقِ الَّذِي كَانُوا يُوعَدُونَ
Ñooñee ñoo di ña nga xam ne dananu leen nangul la gëna rafet ca lañu daan jëf te da nanu leen faral séeni ñaawtéef , te it dananu leen limaale ca waa Àjjana, muy dig bu dëggu banu leen daan dig.
17وَالَّذِي قَالَ لِوَالِدَيْهِ أُفٍّ لَّكُمَا أَتَعِدَانِنِي أَنْ أُخْرَجَ وَقَدْ خَلَتِ الْقُرُونُ مِن قَبْلِي وَهُمَا يَسْتَغِيثَانِ اللَّهَ وَيْلَكَ آمِنْ إِنَّ وَعْدَ اللَّهِ حَقٌّ فَيَقُولُ مَا هَٰذَا إِلَّا أَسَاطِيرُ الْأَوَّلِينَ
Kuy wax ñaari waajuram naan leen : “Kuf ma leen te naan leen ! Ndax dangeen may dig ne danaa génnaat dellu àddina te ña wéyoon masuñoo génnaat ? ” Ñoom ñaar ña ngay sàkku ndimbalul Yàlla ngir ag delloom, [ñu di ko wax naan]: “Soo delluwul ginnaaw ci lii nga ne toskare dal na la ! Digub Yàlla dëgg la de”. Moom it mu tontuwaat ne : “Lii du lenn lu dul feni mag ñu jëkk ña”.
18أُولَٰئِكَ الَّذِينَ حَقَّ عَلَيْهِمُ الْقَوْلُ فِي أُمَمٍ قَدْ خَلَتْ مِن قَبْلِهِم مِّنَ الْجِنِّ وَالْإِنسِ ۖ إِنَّهُمْ كَانُوا خَاسِرِينَ
Ñoom ñooñee la wax ja dal ca séen kaw (menn mbugël) mooy xeet ya leen jiitu woon ci jinne yeek nit ñi. Ñoom dañoo yàqule woon.
19وَلِكُلٍّ دَرَجَاتٌ مِّمَّا عَمِلُوا ۖ وَلِيُوَفِّيَهُمْ أَعْمَالَهُمْ وَهُمْ لَا يُظْلَمُونَ
Kenn ku nekk am na lu tollook lamuy jëf, ñu nar leen a faye la ñu jëfoon te kenn du leen ca tooñ (ci wàññi natt ba).
20وَيَوْمَ يُعْرَضُ الَّذِينَ كَفَرُوا عَلَى النَّارِ أَذْهَبْتُمْ طَيِّبَاتِكُمْ فِي حَيَاتِكُمُ الدُّنْيَا وَاسْتَمْتَعْتُم بِهَا فَالْيَوْمَ تُجْزَوْنَ عَذَابَ الْهُونِ بِمَا كُنتُمْ تَسْتَكْبِرُونَ فِي الْأَرْضِ بِغَيْرِ الْحَقِّ وَبِمَا كُنتُمْ تَفْسُقُونَ
Bu keroogee bis ba ñuy gaaral ña weddi ci kaw Safara (naan leen) : “jeexaloon ngeen séen yu neex ya ca jamono ba ngeen nekkee daan dund ca àddina : te pëcëxóowoon ngeen ko, bis bi niki tey dees na leen faye mbugalum toroxtaane, ngir ni ngeen daan saay-saayee.
Al-AhqafFihi Alxuraan
35Aaya
MeccanRevelation
18Aaya

Tekki — Al-Ahqaf 18

Simoore Al-Ahqaf Aaya 18 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñoom ñooñee la wax ja dal ca séen kaw (menn…

Simoore Aaya 18/35 — Al-Ahqaf الأحقاف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Ahqaf Dégg, Al-Ahqaf Tekki, Al-Ahqaf mp3, Al-Ahqaf pdf. Aaya 16–20. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers