Al-Maida · 15/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
يَا أَهْلَ الْكِتَابِ قَدْ جَاءَكُمْ رَسُولُنَا يُبَيِّنُ لَكُمْ كَثِيرًا مِّمَّا كُنتُمْ تُخْفُونَ مِنَ الْكِتَابِ وَيَعْفُو عَن كَثِيرٍ ۚ قَدْ جَاءَكُم مِّنَ اللَّهِ نُورٌ وَكِتَابٌ مُّبِينٌ ۝١٥
yaaa Ahlal kitaabi qad jaaa`akum Rasoolunaa yubaiyinu lakum kaseeram mimmmaa kuntum tukhfoona minal Kitaabi wa ya`foo `an kaseer; qad jaaa`akum minal laahi noorunw wa Kitaabum Mubeen
📖 Tekkim Wolof
Éy yéen ñon-téere ! Sunub Yonent dikk na ci yéen, leeral na leen lu bari ci la ngeen nëbboon ca Téere ba, te muy jéllale itam lu bari ! Téere bu jóge ca Yàlla dikkal na leen, di leer guy leeral !

🎧 Dégg


📜 Aaya 13-17 — Al-Maida

13فَبِمَا نَقْضِهِم مِّيثَاقَهُمْ لَعَنَّاهُمْ وَجَعَلْنَا قُلُوبَهُمْ قَاسِيَةً ۖ يُحَرِّفُونَ الْكَلِمَ عَن مَّوَاضِعِهِ ۙ وَنَسُوا حَظًّا مِّمَّا ذُكِّرُوا بِهِ ۚ وَلَا تَزَالُ تَطَّلِعُ عَلَىٰ خَائِنَةٍ مِّنْهُمْ إِلَّا قَلِيلًا مِّنْهُمْ ۖ فَاعْفُ عَنْهُمْ وَاصْفَحْ ۚ إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ الْمُحْسِنِينَ
Ci sababus firi ga ñu firi kóllare ga, la Nu leen rëbbe [Nun Yàlla], def seeni xol wow koŋŋ : dañuy toxal baat [maanaa ya] jële ko fa mu tëddoon, boole ca fàtte as lëf ca la Nu leen waare woon. Te foo toll di gis ci ñoom ay wor, lu dul ci lu néew ca ñoom. Nanga leen jéggal te jéllale. Yàlla safoo na ñay rafetal.
14وَمِنَ الَّذِينَ قَالُوا إِنَّا نَصَارَىٰ أَخَذْنَا مِيثَاقَهُمْ فَنَسُوا حَظًّا مِّمَّا ذُكِّرُوا بِهِ فَأَغْرَيْنَا بَيْنَهُمُ الْعَدَاوَةَ وَالْبَغْضَاءَ إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ ۚ وَسَوْفَ يُنَبِّئُهُمُ اللَّهُ بِمَا كَانُوا يَصْنَعُونَ
Ña def seen bopp ay [nasraan] it, fasante woon Nanu kóllare ak ñoom. Ñoom fàtte nañu as lëf ca la Nu leen waare woon, tax ñu tàbbaal seen diggante noonoo ak mbañeel guy wéy ba Bis-pénc ba. Yàlla dana leen xala xabaar la ñu daan def.
15يَا أَهْلَ الْكِتَابِ قَدْ جَاءَكُمْ رَسُولُنَا يُبَيِّنُ لَكُمْ كَثِيرًا مِّمَّا كُنتُمْ تُخْفُونَ مِنَ الْكِتَابِ وَيَعْفُو عَن كَثِيرٍ ۚ قَدْ جَاءَكُم مِّنَ اللَّهِ نُورٌ وَكِتَابٌ مُّبِينٌ
Éy yéen ñon-téere ! Sunub Yonent dikk na ci yéen, leeral na leen lu bari ci la ngeen nëbboon ca Téere ba, te muy jéllale itam lu bari ! Téere bu jóge ca Yàlla dikkal na leen, di leer guy leeral !
16يَهْدِي بِهِ اللَّهُ مَنِ اتَّبَعَ رِضْوَانَهُ سُبُلَ السَّلَامِ وَيُخْرِجُهُم مِّنَ الظُّلُمَاتِ إِلَى النُّورِ بِإِذْنِهِ وَيَهْدِيهِمْ إِلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ
Yàlla dana ca gindi képp ku topp ndigalam, muy yoonu jàmm. Te Dana leen génne cig lëndëm, tàbbal leen cig leer bu Ko soobee. Te teg leen ci yoon wu jub xocc wa.
17لَّقَدْ كَفَرَ الَّذِينَ قَالُوا إِنَّ اللَّهَ هُوَ الْمَسِيحُ ابْنُ مَرْيَمَ ۚ قُلْ فَمَن يَمْلِكُ مِنَ اللَّهِ شَيْئًا إِنْ أَرَادَ أَن يُهْلِكَ الْمَسِيحَ ابْنَ مَرْيَمَ وَأُمَّهُ وَمَن فِي الْأَرْضِ جَمِيعًا ۗ وَلِلَّهِ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَمَا بَيْنَهُمَا ۚ يَخْلُقُ مَا يَشَاءُ ۚ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Ña wax ne : “Ka ñu barkeel, doomi Maryaama [Iisaa], mooy Yàlla ! ”, weddi nañu Yàlla - Neel : “Ana kan moo mënal Yàlla dara, su bëggoon a rey ku ñu barkeel ka, doomi Maryaama, ak yaayam, ak ñi nekk ci kaw suuf si ñépp [Am na sañ-sañu def ko] ?... Te Yàllaay Boroom asamaan yeek suuf si ak li ci seen diggante”. Moom Yàlla mooy sàkk [sos] li ko soob. Yàlla am na kàttan ci def lu ne.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
15Aaya

Tekki — Al-Maida 15

Simoore Al-Maida Aaya 15 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Éy yéen ñon-téere ! Sunub Yonent dikk na ci yéen,…

Simoore Aaya 15/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 13–17. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers