Al-Maida · 68/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
قُلْ يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لَسْتُمْ عَلَىٰ شَيْءٍ حَتَّىٰ تُقِيمُوا التَّوْرَاةَ وَالْإِنجِيلَ وَمَا أُنزِلَ إِلَيْكُم مِّن رَّبِّكُمْ ۗ وَلَيَزِيدَنَّ كَثِيرًا مِّنْهُم مَّا أُنزِلَ إِلَيْكَ مِن رَّبِّكَ طُغْيَانًا وَكُفْرًا ۖ فَلَا تَأْسَ عَلَى الْقَوْمِ الْكَافِرِينَ ۝٦٨
Qul yaaa Ahlal Kitaabi lastum `alaa shai`in hattaa tuqeemut Tawraata wal Injeela wa maaa unzila ilaikum mir Rabbikum; wa layazeedanna kaseeram minhum maa unzila ilaika mir Rabbika tugh yaananw wa kufran falaa taasa `alal qawmil kaafireen
📖 Tekkim Wolof
Neel : “Éy yéen ñon-téere, nekkuleen ci dara li feek defuleen [lu ñu leen digal] ci Tawreet ak Linjiil ak li ñu wàcce ci yéen mu jóge ca seen Boroom.”. Te dana yokk bew ak kéefar ñu bari ci ñoom li ñu wàcce ci yaw, mu jóge ci sa Boroom. Waaye bul jàq ci mbiri yéefar ya.

🎧 Dégg


📜 Aaya 66-70 — Al-Maida

66وَلَوْ أَنَّهُمْ أَقَامُوا التَّوْرَاةَ وَالْإِنجِيلَ وَمَا أُنزِلَ إِلَيْهِم مِّن رَّبِّهِمْ لَأَكَلُوا مِن فَوْقِهِمْ وَمِن تَحْتِ أَرْجُلِهِم ۚ مِّنْهُمْ أُمَّةٌ مُّقْتَصِدَةٌ ۖ وَكَثِيرٌ مِّنْهُمْ سَاءَ مَا يَعْمَلُونَ
Bu ñu jëfewoon Tawreet, ak Linjiil al la ñu wàcce ca ñoom mu tukke ca seen Boroom, kon fàwwu ñu lekk [xéewal] gu bawoo ci kaw ak gu ballee ci seeni suufi tànk. Am na ci ñoom ay nit ñu jub ; waaye ñu bari ca ñoom lu bon lañuy def !
67۞ يَا أَيُّهَا الرَّسُولُ بَلِّغْ مَا أُنزِلَ إِلَيْكَ مِن رَّبِّكَ ۖ وَإِن لَّمْ تَفْعَلْ فَمَا بَلَّغْتَ رِسَالَتَهُ ۚ وَاللَّهُ يَعْصِمُكَ مِنَ النَّاسِ ۗ إِنَّ اللَّهَ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الْكَافِرِينَ
Éy yaw Yonent bi, jottalil la ñu wàcce ci yaw mu tukkee ca sa Boroom. Boo ko deful kon jottaliwoo li Ma la yónni. [Te xamal ne] Yàlla Moo lay musal ci nit ñi. Te Yàlla du gindi aw nit ñu di ay yéefar.
68قُلْ يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لَسْتُمْ عَلَىٰ شَيْءٍ حَتَّىٰ تُقِيمُوا التَّوْرَاةَ وَالْإِنجِيلَ وَمَا أُنزِلَ إِلَيْكُم مِّن رَّبِّكُمْ ۗ وَلَيَزِيدَنَّ كَثِيرًا مِّنْهُم مَّا أُنزِلَ إِلَيْكَ مِن رَّبِّكَ طُغْيَانًا وَكُفْرًا ۖ فَلَا تَأْسَ عَلَى الْقَوْمِ الْكَافِرِينَ
Neel : “Éy yéen ñon-téere, nekkuleen ci dara li feek defuleen [lu ñu leen digal] ci Tawreet ak Linjiil ak li ñu wàcce ci yéen mu jóge ca seen Boroom.”. Te dana yokk bew ak kéefar ñu bari ci ñoom li ñu wàcce ci yaw, mu jóge ci sa Boroom. Waaye bul jàq ci mbiri yéefar ya.
69إِنَّ الَّذِينَ آمَنُوا وَالَّذِينَ هَادُوا وَالصَّابِئُونَ وَالنَّصَارَىٰ مَنْ آمَنَ بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ وَعَمِلَ صَالِحًا فَلَا خَوْفٌ عَلَيْهِمْ وَلَا هُمْ يَحْزَنُونَ
Ña nekk nasraan te gëm Yàlla, walbatiku gëm Lislaam, ak Bis-pénc ba te sellal seeni jëf, duñu am njàqare, duñu am naqar.
70لَقَدْ أَخَذْنَا مِيثَاقَ بَنِي إِسْرَائِيلَ وَأَرْسَلْنَا إِلَيْهِمْ رُسُلًا ۖ كُلَّمَا جَاءَهُمْ رَسُولٌ بِمَا لَا تَهْوَىٰ أَنفُسُهُمْ فَرِيقًا كَذَّبُوا وَفَرِيقًا يَقْتُلُونَ
Fasante woon Nanu kóllare ak waa Banii-Israayiila, yónni ci ñoom, saa yu Nu leen indilee lu leen neexul, ñu weddi ñenn ña, rey ñenn ña.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
68Aaya

Tekki — Al-Maida 68

Simoore Al-Maida Aaya 68 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Neel : “Éy yéen ñon-téere, nekkuleen ci dara li feek…

Simoore Aaya 68/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 66–70. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers