Al-Maida · 77/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
قُلْ يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لَا تَغْلُوا فِي دِينِكُمْ غَيْرَ الْحَقِّ وَلَا تَتَّبِعُوا أَهْوَاءَ قَوْمٍ قَدْ ضَلُّوا مِن قَبْلُ وَأَضَلُّوا كَثِيرًا وَضَلُّوا عَن سَوَاءِ السَّبِيلِ ۝٧٧
Qul yaaa Ahlal Kitaabi laa taghloo fee deenikum ghairal haqqi wa laa tattabi`ooo ahwaaa`a qawmin qad dalloo min qablu wa adalloo kaseeranw wa dalloo `an Sawaaa`is Sabeel
📖 Tekkim Wolof
Neel : “Yéen ñon-téere, buleen teeŋal seen diine, mu wuuteek dëgg ga. Buleen topp bànneexi nit ñoo xam ne réeroon nañu bu jëkk, te réeraloon nañu ñu bari, réere tigi yoon wu jub wa.
🎧 Dégg

📜 Aaya 75-79 — Al-Maida

75مَّا الْمَسِيحُ ابْنُ مَرْيَمَ إِلَّا رَسُولٌ قَدْ خَلَتْ مِن قَبْلِهِ الرُّسُلُ وَأُمُّهُ صِدِّيقَةٌ ۖ كَانَا يَأْكُلَانِ الطَّعَامَ ۗ انظُرْ كَيْفَ نُبَيِّنُ لَهُمُ الْآيَاتِ ثُمَّ انظُرْ أَنَّىٰ يُؤْفَكُونَ
Ku ñu barkeel ka, doomi Maryaama, nekkul lu dul ab Yonent, boo xam ne ay Yonent jiitu woon na ko fi. Yaayam ku saxoon ci dëgg la. Ñoom ñaar dañu daan lekk ñam. Gisal ni Nu leen di leerale sunuy tegtal te it xoolal ni ñuy walbateee [dëgg ga].
76قُلْ أَتَعْبُدُونَ مِن دُونِ اللَّهِ مَا لَا يَمْلِكُ لَكُمْ ضَرًّا وَلَا نَفْعًا ۚ وَاللَّهُ هُوَ السَّمِيعُ الْعَلِيمُ
Neel : “Moo ndax dangeen di bàyyi Yàlla, di jaamu loo xam ne mënuleen a lor, mënuleen a jariñ ? ”.Te Yàlla Moom Kuy dégg la, Ku xam la.
77قُلْ يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لَا تَغْلُوا فِي دِينِكُمْ غَيْرَ الْحَقِّ وَلَا تَتَّبِعُوا أَهْوَاءَ قَوْمٍ قَدْ ضَلُّوا مِن قَبْلُ وَأَضَلُّوا كَثِيرًا وَضَلُّوا عَن سَوَاءِ السَّبِيلِ
Neel : “Yéen ñon-téere, buleen teeŋal seen diine, mu wuuteek dëgg ga. Buleen topp bànneexi nit ñoo xam ne réeroon nañu bu jëkk, te réeraloon nañu ñu bari, réere tigi yoon wu jub wa.
78لُعِنَ الَّذِينَ كَفَرُوا مِن بَنِي إِسْرَائِيلَ عَلَىٰ لِسَانِ دَاوُودَ وَعِيسَى ابْنِ مَرْيَمَ ۚ ذَٰلِكَ بِمَا عَصَوا وَّكَانُوا يَعْتَدُونَ
Rëbbéef na ña weddi ca waa Bani Israayiila mu jaare ca làmmiñu Daawuda ak [Iisaa] doomi Maryaama, ngir lañu moy ndigal te nekkon ñu jéggi dayo.
79كَانُوا لَا يَتَنَاهَوْنَ عَن مُّنكَرٍ فَعَلُوهُ ۚ لَبِئْسَ مَا كَانُوا يَفْعَلُونَ
Daawuñu bàyyi lu ñaaw la ñu daan def. Ay waay, la ñu daan def, aka bon !
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
77Aaya

Tekki — Al-Maida 77

Simoore Al-Maida Aaya 77 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Neel : “Yéen ñon-téere, buleen teeŋal seen diine, mu wuuteek…

Simoore Aaya 77/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 75–79. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers