Al-An'am · 102/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
ذَٰلِكُمُ اللَّهُ رَبُّكُمْ ۖ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ خَالِقُ كُلِّ شَيْءٍ فَاعْبُدُوهُ ۚ وَهُوَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ وَكِيلٌ ۝١٠٢
Zaalikumul laahu Rabbukum laaa ilaaha illaa huwa khaaliqu kulli shai`in fa`budooh; wa huwa `alaa kulli shai`inw Wakeel
📖 Tekkim Wolof
Yàllaa ngi noonu, di seen Boroom ! Yàlla ju dul Moom amul, Moom mi bind lépp lu ne. Jaamuleen ko, Mooy kiy saytu lépp.

🎧 Dégg


📜 Aaya 100-104 — Al-An'am

100وَجَعَلُوا لِلَّهِ شُرَكَاءَ الْجِنَّ وَخَلَقَهُمْ ۖ وَخَرَقُوا لَهُ بَنِينَ وَبَنَاتٍ بِغَيْرِ عِلْمٍ ۚ سُبْحَانَهُ وَتَعَالَىٰ عَمَّا يَصِفُونَ
Te ñoom sàkkal nañu Yàlla ay bokkaale yu di ay jinne te Moo leen bind. Sosal nañu ko it ay doom yu góor ak yu jigéen, ci lu àndul ak benn xam-xam. Cëy sellam ga ak màggam ga ! Jomb Na la ñu koy nirële.
101بَدِيعُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۖ أَنَّىٰ يَكُونُ لَهُ وَلَدٌ وَلَمْ تَكُن لَّهُ صَاحِبَةٌ ۖ وَخَلَقَ كُلَّ شَيْءٍ ۖ وَهُوَ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمٌ
Moo bind asamaan yi ak suuf si. Naka lay ame doom, te amul àndandoo ju jigéen ? Moo bind lu nekk, di Ku xam lu ne.
102ذَٰلِكُمُ اللَّهُ رَبُّكُمْ ۖ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ خَالِقُ كُلِّ شَيْءٍ فَاعْبُدُوهُ ۚ وَهُوَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ وَكِيلٌ
Yàllaa ngi noonu, di seen Boroom ! Yàlla ju dul Moom amul, Moom mi bind lépp lu ne. Jaamuleen ko, Mooy kiy saytu lépp.
103لَّا تُدْرِكُهُ الْأَبْصَارُ وَهُوَ يُدْرِكُ الْأَبْصَارَ ۖ وَهُوَ اللَّطِيفُ الْخَبِيرُ
Ay gët mënu koo gis, te Moom mën naa gis ay gët. Te Moom mooy Aji-ñeewant, di Ku deñ ciy kumpa.
104قَدْ جَاءَكُم بَصَائِرُ مِن رَّبِّكُمْ ۖ فَمَنْ أَبْصَرَ فَلِنَفْسِهِ ۖ وَمَنْ عَمِيَ فَعَلَيْهَا ۚ وَمَا أَنَا عَلَيْكُم بِحَفِيظٍ
Ay lay yu leer nàññ dikkal na leen, tukke ca seen Boroom. Ku nangoo gis, boppam la ko defal ; ku gëmm [bañ a gis], boppam lay yàqal, nekkewuma fi di leen wattu.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
102Aaya

Tekki — Al-An'am 102

Simoore Al-An'am Aaya 102 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàllaa ngi noonu, di seen Boroom ! Yàlla ju dul…

Simoore Aaya 102/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 100–104. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers