Al-An'am · 106/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
اتَّبِعْ مَا أُوحِيَ إِلَيْكَ مِن رَّبِّكَ ۖ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ وَأَعْرِضْ عَنِ الْمُشْرِكِينَ ۝١٠٦
ittabi` maaa oohiya ilaika mir Rabbika laaa ilaaha illaa Huwa wa a`rid `anil mushrikeen
📖 Tekkim Wolof
Nanga topp la ñu la soloo te muy lu tukkee ca sa Boroom. Kenn du Yàlla ku dul Moom. Dëddul way-bokkaale ya.
🎧 Dégg

📜 Aaya 104-108 — Al-An'am

104قَدْ جَاءَكُم بَصَائِرُ مِن رَّبِّكُمْ ۖ فَمَنْ أَبْصَرَ فَلِنَفْسِهِ ۖ وَمَنْ عَمِيَ فَعَلَيْهَا ۚ وَمَا أَنَا عَلَيْكُم بِحَفِيظٍ
Ay lay yu leer nàññ dikkal na leen, tukke ca seen Boroom. Ku nangoo gis, boppam la ko defal ; ku gëmm [bañ a gis], boppam lay yàqal, nekkewuma fi di leen wattu.
105وَكَذَٰلِكَ نُصَرِّفُ الْآيَاتِ وَلِيَقُولُوا دَرَسْتَ وَلِنُبَيِّنَهُ لِقَوْمٍ يَعْلَمُونَ
Noona Lanuy faramfàccee Sunuy àtte. Ngir ñu wax ne : “Jàng nga”. Ak ngir Nu leeral ko aw nit ñuy ràññee.
106اتَّبِعْ مَا أُوحِيَ إِلَيْكَ مِن رَّبِّكَ ۖ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ وَأَعْرِضْ عَنِ الْمُشْرِكِينَ
Nanga topp la ñu la soloo te muy lu tukkee ca sa Boroom. Kenn du Yàlla ku dul Moom. Dëddul way-bokkaale ya.
107وَلَوْ شَاءَ اللَّهُ مَا أَشْرَكُوا ۗ وَمَا جَعَلْنَاكَ عَلَيْهِمْ حَفِيظًا ۖ وَمَا أَنتَ عَلَيْهِم بِوَكِيلٍ
Bu neexoon Yàlla, duñu bokkaale ! Defunu la [yaw Yonent bi] nga di leen wattu mbaa nga di leen aar.
108وَلَا تَسُبُّوا الَّذِينَ يَدْعُونَ مِن دُونِ اللَّهِ فَيَسُبُّوا اللَّهَ عَدْوًا بِغَيْرِ عِلْمٍ ۗ كَذَٰلِكَ زَيَّنَّا لِكُلِّ أُمَّةٍ عَمَلَهُمْ ثُمَّ إِلَىٰ رَبِّهِم مَّرْجِعُهُمْ فَيُنَبِّئُهُم بِمَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Buleen di ŋàññ ñay jaamu leneen lu dul Yàlla, ndax kon dañuy ŋàññ Yàlla cig jalgati, ngir ñàkk a xam. Noonu Lanuy rafetale jëfi wépp xeet [ci seeni gis-gis]. Ba noppi, ñu dellu jëm ca seen Boroom; Mu leeral leen la ñu nekkoon di ko def.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
106Aaya

Tekki — Al-An'am 106

Simoore Al-An'am Aaya 106 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nanga topp la ñu la soloo te muy lu tukkee…

Simoore Aaya 106/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 104–108. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers