Al-An'am · 154/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
ثُمَّ آتَيْنَا مُوسَى الْكِتَابَ تَمَامًا عَلَى الَّذِي أَحْسَنَ وَتَفْصِيلًا لِّكُلِّ شَيْءٍ وَهُدًى وَرَحْمَةً لَّعَلَّهُم بِلِقَاءِ رَبِّهِمْ يُؤْمِنُونَ ۝١٥٤
Summa aatainaa Moosal Kitaaba tammaaman `alal lazeee ahsana wa tafseelal likulli shai`inw wa hudanw wa rahmatal la`allahum biliqaaa`i Rabbihim yu`minoon
📖 Tekkim Wolof
Ba noppi ñu jox Muusaa Téere ba, ngir matal xéewal ci ku rafetal, ak ug faramfàcce ci mbir yépp, di njub, di yërmaande. Ndax Yàlla ñoom ñu gëm ne danañu dajeek seen Boroom.

🎧 Dégg


📜 Aaya 152-156 — Al-An'am

152وَلَا تَقْرَبُوا مَالَ الْيَتِيمِ إِلَّا بِالَّتِي هِيَ أَحْسَنُ حَتَّىٰ يَبْلُغَ أَشُدَّهُ ۖ وَأَوْفُوا الْكَيْلَ وَالْمِيزَانَ بِالْقِسْطِ ۖ لَا نُكَلِّفُ نَفْسًا إِلَّا وُسْعَهَا ۖ وَإِذَا قُلْتُمْ فَاعْدِلُوا وَلَوْ كَانَ ذَا قُرْبَىٰ ۖ وَبِعَهْدِ اللَّهِ أَوْفُوا ۚ ذَٰلِكُمْ وَصَّاكُم بِهِ لَعَلَّكُمْ تَذَكَّرُونَ
Buleen jegeñ [laal] alali jirim ci lu dul na mu gën a rafete, ba bamuy mën a lijjanti boppam. Te nangeen di matal natt ak peese cig maandute. Nun [Yàlla] dunu teg bakkan lu dul lu mu àttan. Bu ngeen di dox [ca la ngeen di àtte], nangeen ko defe ci maandute, doonte la sax seen mbokk ngeen di àtte. Nangeen matal it kóllereg Yàlla. Loolu la leen ci Yàlla dénk. Ndax ngeen di fàttaliku.
153وَأَنَّ هَٰذَا صِرَاطِي مُسْتَقِيمًا فَاتَّبِعُوهُ ۖ وَلَا تَتَّبِعُوا السُّبُلَ فَتَفَرَّقَ بِكُمْ عَن سَبِيلِهِ ۚ ذَٰلِكُمْ وَصَّاكُم بِهِ لَعَلَّكُمْ تَتَّقُونَ
“Te lii nag moo di Sama yoon wu jub xocc wa, toppleen ko ; te buleen topp ñall yi, kon ñu teqale leen ak samaw yoon.”. Loolu la leen ci Yàlla dénku. Ndax Yàlla ngeen [di fegu] ragal Yàlla.
154ثُمَّ آتَيْنَا مُوسَى الْكِتَابَ تَمَامًا عَلَى الَّذِي أَحْسَنَ وَتَفْصِيلًا لِّكُلِّ شَيْءٍ وَهُدًى وَرَحْمَةً لَّعَلَّهُم بِلِقَاءِ رَبِّهِمْ يُؤْمِنُونَ
Ba noppi ñu jox Muusaa Téere ba, ngir matal xéewal ci ku rafetal, ak ug faramfàcce ci mbir yépp, di njub, di yërmaande. Ndax Yàlla ñoom ñu gëm ne danañu dajeek seen Boroom.
155وَهَٰذَا كِتَابٌ أَنزَلْنَاهُ مُبَارَكٌ فَاتَّبِعُوهُ وَاتَّقُوا لَعَلَّكُمْ تُرْحَمُونَ
Te Téere bii wàcce Nanu ko, barkeel ko - toppleen ko, te ngeen ragal (Yàlla) ndax Yàlla amaana yërëmees leen -
156أَن تَقُولُوا إِنَّمَا أُنزِلَ الْكِتَابُ عَلَىٰ طَائِفَتَيْنِ مِن قَبْلِنَا وَإِن كُنَّا عَن دِرَاسَتِهِمْ لَغَافِلِينَ
ndax it ngeen bañ a wax ne : “Ab Téere wàcceluñu ko kenn ku dul ñaari kurél ya [Yahuud ya ak Nasraan ya] ca ña nu jiitu, te nun seenug njàngale umpu nanu.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
154Aaya

Tekki — Al-An'am 154

Simoore Al-An'am Aaya 154 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ba noppi ñu jox Muusaa Téere ba, ngir matal xéewal…

Simoore Aaya 154/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 152–156. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers