Al-An'am · 36/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
۞ إِنَّمَا يَسْتَجِيبُ الَّذِينَ يَسْمَعُونَ ۘ وَالْمَوْتَىٰ يَبْعَثُهُمُ اللَّهُ ثُمَّ إِلَيْهِ يُرْجَعُونَ ۝٣٦
Innamaa yastajeebul lazeena yasma`oon; walmawtaa yab`asuhumul laahu summa ilaihi yurja`oon
📖 Tekkim Wolof
Ñay dégg ñoo lay wuyu. Ña dee, Yàlla Dana leen dekkal ; ñu dellusi ca Moom..
🎧 Dégg

📜 Aaya 34-38 — Al-An'am

34وَلَقَدْ كُذِّبَتْ رُسُلٌ مِّن قَبْلِكَ فَصَبَرُوا عَلَىٰ مَا كُذِّبُوا وَأُوذُوا حَتَّىٰ أَتَاهُمْ نَصْرُنَا ۚ وَلَا مُبَدِّلَ لِكَلِمَاتِ اللَّهِ ۚ وَلَقَدْ جَاءَكَ مِن نَّبَإِ الْمُرْسَلِينَ
Weddig ay Yonent yu la jiitu amoom na fi. Ñu muñ loraange ja, ba Nu dikke leen Sunu ndimbal. Kàddug Yàlla du soppiku, te jot nga lenn ca xew-xewi Yonent ya.
35وَإِن كَانَ كَبُرَ عَلَيْكَ إِعْرَاضُهُمْ فَإِنِ اسْتَطَعْتَ أَن تَبْتَغِيَ نَفَقًا فِي الْأَرْضِ أَوْ سُلَّمًا فِي السَّمَاءِ فَتَأْتِيَهُم بِآيَةٍ ۚ وَلَوْ شَاءَ اللَّهُ لَجَمَعَهُمْ عَلَى الْهُدَىٰ ۚ فَلَا تَكُونَنَّ مِنَ الْجَاهِلِينَ
Ndagam seen dëddu dafa rëy ci yaw, boo mënee sàkk ag tajfal ci biir suuf si, walla ker- keraan ci asamaan yi ba tax nga indil leen kéemaan, def ko. [Xamal ne] bu neexoon Yàlla, Mu dajale leen cig njub. Kon bul bokk ca ña sànku réer.
36۞ إِنَّمَا يَسْتَجِيبُ الَّذِينَ يَسْمَعُونَ ۘ وَالْمَوْتَىٰ يَبْعَثُهُمُ اللَّهُ ثُمَّ إِلَيْهِ يُرْجَعُونَ
Ñay dégg ñoo lay wuyu. Ña dee, Yàlla Dana leen dekkal ; ñu dellusi ca Moom..
37وَقَالُوا لَوْلَا نُزِّلَ عَلَيْهِ آيَةٌ مِّن رَّبِّهِ ۚ قُلْ إِنَّ اللَّهَ قَادِرٌ عَلَىٰ أَن يُنَزِّلَ آيَةً وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَهُمْ لَا يَعْلَمُونَ
Te ña ngay wax naan : “Lu tee woon ñu wàcce ci moom kéemaan gu tukke ci Yàlla ? ”. Neel : “Yàlla ku am kàttan la ci wàcce kéemaan. Waaye li ëpp ci ñoom xamuñu”.
38وَمَا مِن دَابَّةٍ فِي الْأَرْضِ وَلَا طَائِرٍ يَطِيرُ بِجَنَاحَيْهِ إِلَّا أُمَمٌ أَمْثَالُكُم ۚ مَّا فَرَّطْنَا فِي الْكِتَابِ مِن شَيْءٍ ۚ ثُمَّ إِلَىٰ رَبِّهِمْ يُحْشَرُونَ
Amul lenn luy dukkat ci suuf, du caageene luy naawe ñaari laaf, lu dul ne dañoo doon ay xeet [waasoo] ni yéen. Amul lenn lu Nu bàyyi ci Téere bi. [Xamleen ne] dees na leen fang jëme ci seen Boroom, gur-gur jiital wëtal.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
36Aaya

Tekki — Al-An'am 36

Simoore Al-An'am Aaya 36 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñay dégg ñoo lay wuyu. Ña dee, Yàlla Dana leen…

Simoore Aaya 36/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 34–38. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers