Al-An'am · 82/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
الَّذِينَ آمَنُوا وَلَمْ يَلْبِسُوا إِيمَانَهُم بِظُلْمٍ أُولَٰئِكَ لَهُمُ الْأَمْنُ وَهُم مُّهْتَدُونَ ۝٨٢
Allazeena aamanoo wa lam yalbisooo eemaanahum bizulmin ulaaa`ika lahumul amnu wa hum muhtadoon
📖 Tekkim Wolof
Ña gëm te jaxasewuñu seen ngëm ak tooñeel, ñooña ñoo am kóolute ; te ñoom ñooy ña tegu ci njub”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 80-84 — Al-An'am

80وَحَاجَّهُ قَوْمُهُ ۚ قَالَ أَتُحَاجُّونِّي فِي اللَّهِ وَقَدْ هَدَانِ ۚ وَلَا أَخَافُ مَا تُشْرِكُونَ بِهِ إِلَّا أَن يَشَاءَ رَبِّي شَيْئًا ۗ وَسِعَ رَبِّي كُلَّ شَيْءٍ عِلْمًا ۗ أَفَلَا تَتَذَكَّرُونَ
Aw nitam dàggasanteek moom ; mu ne leen : “Moo ndax dangeen di dàggasanteek man ci Yàlla, te man gindi Na ma ? Ragaluma li ngeen koy bokkaale lu dul lu Yàlla namm. Xam- xamu sama Boroom peeg na yëf yépp. Moo ndax dangeen dul fàttaliku [xalaat] ?
81وَكَيْفَ أَخَافُ مَا أَشْرَكْتُمْ وَلَا تَخَافُونَ أَنَّكُمْ أَشْرَكْتُم بِاللَّهِ مَا لَمْ يُنَزِّلْ بِهِ عَلَيْكُمْ سُلْطَانًا ۚ فَأَيُّ الْفَرِيقَيْنِ أَحَقُّ بِالْأَمْنِ ۖ إِن كُنتُمْ تَعْلَمُونَ
Te sax man, naka laay ragale li ngeen Koy bokkaale te yéen ragaluleen ne yéen, yéen a ngi bokkaleek Yàlla yoo xam ne wàcceluñu leen ca aw lay ? Kon ñaari kurél ya [yéen ak nun], ku ci gën a yay ci am kóolute ? (waxleen) dengam xam ngeen.
82الَّذِينَ آمَنُوا وَلَمْ يَلْبِسُوا إِيمَانَهُم بِظُلْمٍ أُولَٰئِكَ لَهُمُ الْأَمْنُ وَهُم مُّهْتَدُونَ
Ña gëm te jaxasewuñu seen ngëm ak tooñeel, ñooña ñoo am kóolute ; te ñoom ñooy ña tegu ci njub”.
83وَتِلْكَ حُجَّتُنَا آتَيْنَاهَا إِبْرَاهِيمَ عَلَىٰ قَوْمِهِ ۚ نَرْفَعُ دَرَجَاتٍ مَّن نَّشَاءُ ۗ إِنَّ رَبَّكَ حَكِيمٌ عَلِيمٌ
Loolu mooy Sunu lay wi nu jox Ibraahiima mu yay ca aw nitam. Dananu yékkati ku Nu neex mu kawe. Te sa Boroom Ku xereñ la, Ku xam la.
84وَوَهَبْنَا لَهُ إِسْحَاقَ وَيَعْقُوبَ ۚ كُلًّا هَدَيْنَا ۚ وَنُوحًا هَدَيْنَا مِن قَبْلُ ۖ وَمِن ذُرِّيَّتِهِ دَاوُودَ وَسُلَيْمَانَ وَأَيُّوبَ وَيُوسُفَ وَمُوسَىٰ وَهَارُونَ ۚ وَكَذَٰلِكَ نَجْزِي الْمُحْسِنِينَ
May Nanu ko Isaaqa ak Yanqooba, gindi leen, teg leen cig njub ñoom ñépp. Ak Nooh it, gindi Nanu ko lu jiitu, ak cay sëtam, Daawuda ak Suleymaan, ak Ayuuba ak Yuusufa, ak Muusaa, ak Haaruuna. Te noonu la Nuy feyee ñay rafetal.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
82Aaya

Tekki — Al-An'am 82

Simoore Al-An'am Aaya 82 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña gëm te jaxasewuñu seen ngëm ak tooñeel, ñooña ñoo…

Simoore Aaya 82/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 80–84. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers