Al-An'am · 95/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
۞ إِنَّ اللَّهَ فَالِقُ الْحَبِّ وَالنَّوَىٰ ۖ يُخْرِجُ الْحَيَّ مِنَ الْمَيِّتِ وَمُخْرِجُ الْمَيِّتِ مِنَ الْحَيِّ ۚ ذَٰلِكُمُ اللَّهُ ۖ فَأَنَّىٰ تُؤْفَكُونَ ۝٩٥
Innal laaha faaliqul habbi wannawaa yukhrijul haiya minal maiyiti wa mukhrijul maiyiti minal haiy; zaalikumul laahu fa annaa tu`fakoon
📖 Tekkim Wolof
Yàlla mooy xar pepp ak i saal : [génne ca luy sax gàncax walla garab], Mooy génne luy dundu ci lu dee, tey génne lu dee ci luy dundu. Yàllaa ngoogu. Waaw naka lañu leen wëlbatee ?

🎧 Dégg


📜 Aaya 93-97 — Al-An'am

93وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّنِ افْتَرَىٰ عَلَى اللَّهِ كَذِبًا أَوْ قَالَ أُوحِيَ إِلَيَّ وَلَمْ يُوحَ إِلَيْهِ شَيْءٌ وَمَن قَالَ سَأُنزِلُ مِثْلَ مَا أَنزَلَ اللَّهُ ۗ وَلَوْ تَرَىٰ إِذِ الظَّالِمُونَ فِي غَمَرَاتِ الْمَوْتِ وَالْمَلَائِكَةُ بَاسِطُو أَيْدِيهِمْ أَخْرِجُوا أَنفُسَكُمُ ۖ الْيَوْمَ تُجْزَوْنَ عَذَابَ الْهُونِ بِمَا كُنتُمْ تَقُولُونَ عَلَى اللَّهِ غَيْرَ الْحَقِّ وَكُنتُمْ عَنْ آيَاتِهِ تَسْتَكْبِرُونَ
Ana ku gën a tooñ kuy duural Yàlla ay fen, walla muy wax naan : “Soloo nañu ma”, te fekk soloowuñu ko dara. Ak kuy wax naan : “Danaa wàcce lu mel ni lii Yàlla wàcce.”. Cëy boo gisoon tooñkat ya bis ba ñu nekkee ci wextanu ndee, te Malaaka ya tàllal seeni yoxo (naan leen) : “Génneleen seen bopp. Tey jii, dees na leen feye mbugal muy toroxale ci sababus la ngeen doon wax ci Yàlla te du dëgg ak la ngeen daan rëy-rëylu tey dëddu ay tegtalam”.
94وَلَقَدْ جِئْتُمُونَا فُرَادَىٰ كَمَا خَلَقْنَاكُمْ أَوَّلَ مَرَّةٍ وَتَرَكْتُم مَّا خَوَّلْنَاكُمْ وَرَاءَ ظُهُورِكُمْ ۖ وَمَا نَرَىٰ مَعَكُمْ شُفَعَاءَكُمُ الَّذِينَ زَعَمْتُمْ أَنَّهُمْ فِيكُمْ شُرَكَاءُ ۚ لَقَد تَّقَطَّعَ بَيْنَكُمْ وَضَلَّ عَنكُم مَّا كُنتُمْ تَزْعُمُونَ
(Moom Yàlla Mu ne leen) Dikk ngeen di kenn kenn ni Nu leen binde woon cig njalbéen, te bàyyi ci seen ginnaaw la ñu leen wërsëgale woon. Waaw Nun sax gisunu ña ngeen daan jaamu, di ko bokkaale ak Yàlla. Léegi seen digganteek ñoom dog na, te la ngeen doon sos réer na leen.
95۞ إِنَّ اللَّهَ فَالِقُ الْحَبِّ وَالنَّوَىٰ ۖ يُخْرِجُ الْحَيَّ مِنَ الْمَيِّتِ وَمُخْرِجُ الْمَيِّتِ مِنَ الْحَيِّ ۚ ذَٰلِكُمُ اللَّهُ ۖ فَأَنَّىٰ تُؤْفَكُونَ
Yàlla mooy xar pepp ak i saal : [génne ca luy sax gàncax walla garab], Mooy génne luy dundu ci lu dee, tey génne lu dee ci luy dundu. Yàllaa ngoogu. Waaw naka lañu leen wëlbatee ?
96فَالِقُ الْإِصْبَاحِ وَجَعَلَ اللَّيْلَ سَكَنًا وَالشَّمْسَ وَالْقَمَرَ حُسْبَانًا ۚ ذَٰلِكَ تَقْدِيرُ الْعَزِيزِ الْعَلِيمِ
Mooy sos leeraayu suba si, def guddi muy noflaay ; def jant bi ak weer wi ñuy waññikaayu jamono. Loolu mooy nattaleb Aji-not jiy Aji-xam [Yàlla].
97وَهُوَ الَّذِي جَعَلَ لَكُمُ النُّجُومَ لِتَهْتَدُوا بِهَا فِي ظُلُمَاتِ الْبَرِّ وَالْبَحْرِ ۗ قَدْ فَصَّلْنَا الْآيَاتِ لِقَوْمٍ يَعْلَمُونَ
Moom moo leen defal ay bidiw ngir ngeen di ca gindiku bu ngeen nekkee ci lëndëmi jéeri walla géej gi. Faramfàcce Nanu Téere ba, ngir aw nit ñuy xam !
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
95Aaya

Tekki — Al-An'am 95

Simoore Al-An'am Aaya 95 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla mooy xar pepp ak i saal : [génne ca…

Simoore Aaya 95/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 93–97. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers