Al-A'raf · 130/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
وَلَقَدْ أَخَذْنَا آلَ فِرْعَوْنَ بِالسِّنِينَ وَنَقْصٍ مِّنَ الثَّمَرَاتِ لَعَلَّهُمْ يَذَّكَّرُونَ ۝١٣٠
Wa laqad akhaznaaa Aala Fir`awna bis sineena wa naqsim minas samaraati la`allahum yazzakkaroon
📖 Tekkim Wolof
Teg Nanu nitu Firawna bekkoor ay at ak wàññikug meññent ndax xéy-na ñu fàttaliku [seen Boroom].

🎧 Dégg


📜 Aaya 128-132 — Al-A'raf

128قَالَ مُوسَىٰ لِقَوْمِهِ اسْتَعِينُوا بِاللَّهِ وَاصْبِرُوا ۖ إِنَّ الْأَرْضَ لِلَّهِ يُورِثُهَا مَن يَشَاءُ مِنْ عِبَادِهِ ۖ وَالْعَاقِبَةُ لِلْمُتَّقِينَ
Muusaa wax ay nitam : “Sàkkuleen ndimbal ci Yàlla te ngeen muñ, suuf si Yàllaa ko moom. Dana ko donnale ku ko neex ciy jaamam. Te muj ga, way-ragal Yàlla yee ko moom”.
129قَالُوا أُوذِينَا مِن قَبْلِ أَن تَأْتِيَنَا وَمِن بَعْدِ مَا جِئْتَنَا ۚ قَالَ عَسَىٰ رَبُّكُمْ أَن يُهْلِكَ عَدُوَّكُمْ وَيَسْتَخْلِفَكُمْ فِي الْأَرْضِ فَيَنظُرَ كَيْفَ تَعْمَلُونَ
[Ñoom yahuud ya] ne : “Loreef nanu lu jiitu sa dikk ci nun ak ginnaaw la nga nu indil.”. Mu ne : “Xéy-na seen Boroom dana rey seeni noon, Mu wuutal leen ci suuf si ba noppi di saytu na ngeen di def”.
130وَلَقَدْ أَخَذْنَا آلَ فِرْعَوْنَ بِالسِّنِينَ وَنَقْصٍ مِّنَ الثَّمَرَاتِ لَعَلَّهُمْ يَذَّكَّرُونَ
Teg Nanu nitu Firawna bekkoor ay at ak wàññikug meññent ndax xéy-na ñu fàttaliku [seen Boroom].
131فَإِذَا جَاءَتْهُمُ الْحَسَنَةُ قَالُوا لَنَا هَٰذِهِ ۖ وَإِن تُصِبْهُمْ سَيِّئَةٌ يَطَّيَّرُوا بِمُوسَىٰ وَمَن مَّعَهُ ۗ أَلَا إِنَّمَا طَائِرُهُمْ عِندَ اللَّهِ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَهُمْ لَا يَعْلَمُونَ
Bu leen lu baax dikkalee, ñu ne : “Lii noo ko moom” ; bu leen lu bon dalee, ñu gaafal Muusaa ak ña ànd ak moom. Déedéet seen gaaf nekkul ci kenn ku dul Yàlla. Waaye ña ëpp ca ñoom xamuñu.
132وَقَالُوا مَهْمَا تَأْتِنَا بِهِ مِنْ آيَةٍ لِّتَسْحَرَنَا بِهَا فَمَا نَحْنُ لَكَ بِمُؤْمِنِينَ
Ñu ne : “ Loo nu mën a indil ciy kéemaan ngir jabar nu ci, dunu la gëm”.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
130Aaya

Tekki — Al-A'raf 130

Simoore Al-A'raf Aaya 130 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Teg Nanu nitu Firawna bekkoor ay at ak wàññikug meññent…

Simoore Aaya 130/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 128–132. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers