Al-A'raf · 178/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
مَن يَهْدِ اللَّهُ فَهُوَ الْمُهْتَدِي ۖ وَمَن يُضْلِلْ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الْخَاسِرُونَ ۝١٧٨
mai yahdil laahu fa huwal muhtadee wa mai yudlil fa ulaaa`ika humul khaasiroon
📖 Tekkim Wolof
Ku Yàlla gindi nag, mu nekk cig njub. Ña Mu bàyyi cig réer, ñooy ñu yàqule ña.
🎧 Dégg

📜 Aaya 176-180 — Al-A'raf

176وَلَوْ شِئْنَا لَرَفَعْنَاهُ بِهَا وَلَٰكِنَّهُ أَخْلَدَ إِلَى الْأَرْضِ وَاتَّبَعَ هَوَاهُ ۚ فَمَثَلُهُ كَمَثَلِ الْكَلْبِ إِن تَحْمِلْ عَلَيْهِ يَلْهَثْ أَوْ تَتْرُكْهُ يَلْهَث ۚ ذَّٰلِكَ مَثَلُ الْقَوْمِ الَّذِينَ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا ۚ فَاقْصُصِ الْقَصَصَ لَعَلَّهُمْ يَتَفَكَّرُونَ
Su nu sooboon Nu yékkatikook mbóot yooyu, waaye dafa jengoon jëm ci àddina, topp bànneexam. Dafay mel ni xaj, boo ko songee muy yalkat, boo ko bàyyee muy yalkat. Loolu mooy niróowaaleeb nit ña weddi Sunuy kàddu. Nettalil xew-xew ba. Xéy-na ñoom ñu fàttaliku !
177سَاءَ مَثَلًا الْقَوْمُ الَّذِينَ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا وَأَنفُسَهُمْ كَانُوا يَظْلِمُونَ
Nekkinu nit ña weddi Sunuy kàddu, aka bon, waaye seen bopp lañuy tooñ nag.
178مَن يَهْدِ اللَّهُ فَهُوَ الْمُهْتَدِي ۖ وَمَن يُضْلِلْ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الْخَاسِرُونَ
Ku Yàlla gindi nag, mu nekk cig njub. Ña Mu bàyyi cig réer, ñooy ñu yàqule ña.
179وَلَقَدْ ذَرَأْنَا لِجَهَنَّمَ كَثِيرًا مِّنَ الْجِنِّ وَالْإِنسِ ۖ لَهُمْ قُلُوبٌ لَّا يَفْقَهُونَ بِهَا وَلَهُمْ أَعْيُنٌ لَّا يُبْصِرُونَ بِهَا وَلَهُمْ آذَانٌ لَّا يَسْمَعُونَ بِهَا ۚ أُولَٰئِكَ كَالْأَنْعَامِ بَلْ هُمْ أَضَلُّ ۚ أُولَٰئِكَ هُمُ الْغَافِلُونَ
Nun bind nanu ba noppi ngir Safara jinne yu bari ak nit. Ñeel na leen xol yu dul am dégg-dégg. Ay bët yu ñu dul gis ak ay nopp yu ñu dul dégge. Ñooña, dañoo mel ni mala ya, ñoo leen gën a réer sax. Ñooy ñu sàggan ña.
180وَلِلَّهِ الْأَسْمَاءُ الْحُسْنَىٰ فَادْعُوهُ بِهَا ۖ وَذَرُوا الَّذِينَ يُلْحِدُونَ فِي أَسْمَائِهِ ۚ سَيُجْزَوْنَ مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Yàllaa moom tur yu rafet yi. Nangeen ko ciy jaamu te ngeen dëddu ña di jeng ci turam yi : dees na leen feye la ñu daan def.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
178Aaya

Tekki — Al-A'raf 178

Simoore Al-A'raf Aaya 178 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ku Yàlla gindi nag, mu nekk cig njub. Ña Mu…

Simoore Aaya 178/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 176–180. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers