At-Tawba · 116/129
Tekki Waxtaan — Simoore At-Tawba
إِنَّ اللَّهَ لَهُ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۖ يُحْيِي وَيُمِيتُ ۚ وَمَا لَكُم مِّن دُونِ اللَّهِ مِن وَلِيٍّ وَلَا نَصِيرٍ ۝١١٦
Innal laaha lahoo mulkus samaawaati wal ardi yuhyee wa yumeet; wa maa lakum min doonil laahi minw waliyyinw wa laa naseer
📖 Tekkim Wolof
Yàllaa moom nguurug asamaan yi ak suuf si. Mooy dundal, di rey. Te amuleen wéeruwaay walla ku leen mën a dimbali ku dul Moom (Yàlla).

🎧 Dégg


📜 Aaya 114-118 — Simoore At-Tawba

114وَمَا كَانَ اسْتِغْفَارُ إِبْرَاهِيمَ لِأَبِيهِ إِلَّا عَن مَّوْعِدَةٍ وَعَدَهَا إِيَّاهُ فَلَمَّا تَبَيَّنَ لَهُ أَنَّهُ عَدُوٌّ لِّلَّهِ تَبَرَّأَ مِنْهُ ۚ إِنَّ إِبْرَاهِيمَ لَأَوَّاهٌ حَلِيمٌ
Te it jéggalu ga Ibraayiima doon jéggalul baayam, du utoon dara lu dul ab dig bu mu ko digoon. (Waaye), ba mu ko leeree ne noonub Yàlla la (moom baayam), dafa deñ ba set wecc ci loolu. Ibraahiima ab delluwaakoon la ci Boroomam, ku lewet la.
115وَمَا كَانَ اللَّهُ لِيُضِلَّ قَوْمًا بَعْدَ إِذْ هَدَاهُمْ حَتَّىٰ يُبَيِّنَ لَهُم مَّا يَتَّقُونَ ۚ إِنَّ اللَّهَ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمٌ
Yàlla du bàyyi ñoo xam ne gindi na leen ba noppi ñuy tàbbiwaat cig réer, te leeralal na leen la ñu war a ragal. Yàlla xam na lépp.
116إِنَّ اللَّهَ لَهُ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۖ يُحْيِي وَيُمِيتُ ۚ وَمَا لَكُم مِّن دُونِ اللَّهِ مِن وَلِيٍّ وَلَا نَصِيرٍ
Yàllaa moom nguurug asamaan yi ak suuf si. Mooy dundal, di rey. Te amuleen wéeruwaay walla ku leen mën a dimbali ku dul Moom (Yàlla).
117لَّقَد تَّابَ اللَّهُ عَلَى النَّبِيِّ وَالْمُهَاجِرِينَ وَالْأَنصَارِ الَّذِينَ اتَّبَعُوهُ فِي سَاعَةِ الْعُسْرَةِ مِن بَعْدِ مَا كَادَ يَزِيغُ قُلُوبُ فَرِيقٍ مِّنْهُمْ ثُمَّ تَابَ عَلَيْهِمْ ۚ إِنَّهُ بِهِمْ رَءُوفٌ رَّحِيمٌ
Yàlla jéggal na ba noppi Yonent ba ak way-gàddaay ña (Muhaajiruun ya) ak ña leen dalaloon (Lansaar ya) ñoom ña nga xam ne toppoon nañu ko ca jamono ju jafe ja, ginnaaw ba xoli lenn ca ñoom xawoon a jeng. Mu jéggal leen ndax Moom (Yàlla) Ku ñeewant la, di Jaglewaakoon ci ñoom.
118وَعَلَى الثَّلَاثَةِ الَّذِينَ خُلِّفُوا حَتَّىٰ إِذَا ضَاقَتْ عَلَيْهِمُ الْأَرْضُ بِمَا رَحُبَتْ وَضَاقَتْ عَلَيْهِمْ أَنفُسُهُمْ وَظَنُّوا أَن لَّا مَلْجَأَ مِنَ اللَّهِ إِلَّا إِلَيْهِ ثُمَّ تَابَ عَلَيْهِمْ لِيَتُوبُوا ۚ إِنَّ اللَّهَ هُوَ التَّوَّابُ الرَّحِيمُ
Ak ñett ñañu bàyyi woon ginnaaw ba tax li suuf si yaatu yépp, lépp xat ci ñoom ; te it seeni jëf xat ci ñoom ba ñu jort ne amul wenn wéeruwaay (wuy musle) ci Yàlla ju dul Moom Yàlla. Mu daldi leen jéggal ngir ñu tuub (rëccu). Naka Yàlla Nanguwaakoonu tuub la, Jaglewaakoon la.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
116Aaya

Tekki — At-Tawba 116

Simoore At-Tawba Aaya 116 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàllaa moom nguurug asamaan yi ak suuf si. Mooy dundal,…

Simoore Aaya 116/129 — Simoore At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore At-Tawba Dégg, Simoore At-Tawba Tekki, Simoore At-Tawba mp3, Simoore At-Tawba pdf. Aaya 114–118. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers