At-Tawba · 26/129
Tekki Waxtaan — Simoore At-Tawba
ثُمَّ أَنزَلَ اللَّهُ سَكِينَتَهُ عَلَىٰ رَسُولِهِ وَعَلَى الْمُؤْمِنِينَ وَأَنزَلَ جُنُودًا لَّمْ تَرَوْهَا وَعَذَّبَ الَّذِينَ كَفَرُوا ۚ وَذَٰلِكَ جَزَاءُ الْكَافِرِينَ ۝٢٦
Summa anzalal laahu sakeenatahoo `alaa Rasoolihee wa `alalmu `mineena wa anzala junoodal lam tarawhaa wa azzabal lazeena kafaroo; wa zaalika jazaaa`ul kaafireen
📖 Tekkim Wolof
Ginnaaw ga, Yàlla wàcce dalam ga ca Yonentam ba ak ca ñu gëm ña. Mu wàcce xarekat yu ngeen gisul ak mbugalu ña weddi. Loolu mooy peyu yéefar ya.

🎧 Dégg


📜 Aaya 24-28 — Simoore At-Tawba

24قُلْ إِن كَانَ آبَاؤُكُمْ وَأَبْنَاؤُكُمْ وَإِخْوَانُكُمْ وَأَزْوَاجُكُمْ وَعَشِيرَتُكُمْ وَأَمْوَالٌ اقْتَرَفْتُمُوهَا وَتِجَارَةٌ تَخْشَوْنَ كَسَادَهَا وَمَسَاكِنُ تَرْضَوْنَهَا أَحَبَّ إِلَيْكُم مِّنَ اللَّهِ وَرَسُولِهِ وَجِهَادٍ فِي سَبِيلِهِ فَتَرَبَّصُوا حَتَّىٰ يَأْتِيَ اللَّهُ بِأَمْرِهِ ۗ وَاللَّهُ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الْفَاسِقِينَ
Neel [Yaw Yonent bi] : “Su fekkee ne seeni baay ak seeni doom, ak seeni mbokk, ak seeni jabar, ak seeni jegeñaale, ak alal ju ngeen fàggu, ak njaay mu ngeen ragal mu lamb, ak kër yu leen neex ngeen gën a bëgg ci Yàlla ak Yonentam ak xareel yoonu Yàlla, kon nangeen xaar ba Yàlla dikk ak dogalam. Yàlla du gindi nit ñu dëng”.
25لَقَدْ نَصَرَكُمُ اللَّهُ فِي مَوَاطِنَ كَثِيرَةٍ ۙ وَيَوْمَ حُنَيْنٍ ۙ إِذْ أَعْجَبَتْكُمْ كَثْرَتُكُمْ فَلَمْ تُغْنِ عَنكُمْ شَيْئًا وَضَاقَتْ عَلَيْكُمُ الْأَرْضُ بِمَا رَحُبَتْ ثُمَّ وَلَّيْتُم مُّدْبِرِينَ
Yàlla dimbali na leen ci barab yu bari. Ak ca bisu (xareb) Hunayni ba ngeen yéemoo ca nangeen baree woon te jariñuleen dara. Ba li suuf si di yaatu, lépp xat na keroog ci yéen ; ngeen wëlbatiku daw.
26ثُمَّ أَنزَلَ اللَّهُ سَكِينَتَهُ عَلَىٰ رَسُولِهِ وَعَلَى الْمُؤْمِنِينَ وَأَنزَلَ جُنُودًا لَّمْ تَرَوْهَا وَعَذَّبَ الَّذِينَ كَفَرُوا ۚ وَذَٰلِكَ جَزَاءُ الْكَافِرِينَ
Ginnaaw ga, Yàlla wàcce dalam ga ca Yonentam ba ak ca ñu gëm ña. Mu wàcce xarekat yu ngeen gisul ak mbugalu ña weddi. Loolu mooy peyu yéefar ya.
27ثُمَّ يَتُوبُ اللَّهُ مِن بَعْدِ ذَٰلِكَ عَلَىٰ مَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Mujj Yàlla jéggal ku Ko neex ginnaaw ga, ndax Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
28يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِنَّمَا الْمُشْرِكُونَ نَجَسٌ فَلَا يَقْرَبُوا الْمَسْجِدَ الْحَرَامَ بَعْدَ عَامِهِمْ هَٰذَا ۚ وَإِنْ خِفْتُمْ عَيْلَةً فَسَوْفَ يُغْنِيكُمُ اللَّهُ مِن فَضْلِهِ إِن شَاءَ ۚ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ حَكِيمٌ
Éy yéen ñi gëm ! Bokkaalekat ya nekkuñu lu dul sobe : buñu jege Jàkka ju ñu wormaal ja, ginnaaw seen at mii. Bu ngeen ragalee nag Yàlla, Dana leen may kon ci ngënéelam bu ko soobee. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
26Aaya

Tekki — At-Tawba 26

Simoore At-Tawba Aaya 26 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ginnaaw ga, Yàlla wàcce dalam ga ca Yonentam ba ak…

Simoore Aaya 26/129 — Simoore At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore At-Tawba Dégg, Simoore At-Tawba Tekki, Simoore At-Tawba mp3, Simoore At-Tawba pdf. Aaya 24–28. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers