At-Tawba · 62/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
يَحْلِفُونَ بِاللَّهِ لَكُمْ لِيُرْضُوكُمْ وَاللَّهُ وَرَسُولُهُ أَحَقُّ أَن يُرْضُوهُ إِن كَانُوا مُؤْمِنِينَ ۝٦٢
yahlifoona billaahi lakum liyurdookum wallaahu wa Rasooluhoo ahaqqu ai yurdoohu in kaanoo mu`mineen
📖 Tekkim Wolof
Ña nga lay waatal ci Yàlla ngir am seen ngërëm. Te Yàlla ak Yonentam ñoo gën a yey ci ñoom sàkku seen ngërëm ndeem ñu gëm lañu.
🎧 Dégg

📜 Aaya 60-64 — At-Tawba

60۞ إِنَّمَا الصَّدَقَاتُ لِلْفُقَرَاءِ وَالْمَسَاكِينِ وَالْعَامِلِينَ عَلَيْهَا وَالْمُؤَلَّفَةِ قُلُوبُهُمْ وَفِي الرِّقَابِ وَالْغَارِمِينَ وَفِي سَبِيلِ اللَّهِ وَابْنِ السَّبِيلِ ۖ فَرِيضَةً مِّنَ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ حَكِيمٌ
Asaka, ñi ko yeyoo ñooy ñi néew am-am, yalwaankat yi, ñi koy toppatoo, ñi ñu bëgg nooyal seen xol (ci Lislaam) ak ci goreel jaam, ña bor sonnal, ak ca lu jëm ci diiney Yàlla, ak doxandeem bu nekk ci tukki. Looloo di li Yàlla santaane ! Te Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.
61وَمِنْهُمُ الَّذِينَ يُؤْذُونَ النَّبِيَّ وَيَقُولُونَ هُوَ أُذُنٌ ۚ قُلْ أُذُنُ خَيْرٍ لَّكُمْ يُؤْمِنُ بِاللَّهِ وَيُؤْمِنُ لِلْمُؤْمِنِينَ وَرَحْمَةٌ لِّلَّذِينَ آمَنُوا مِنكُمْ ۚ وَالَّذِينَ يُؤْذُونَ رَسُولَ اللَّهِ لَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Am na ci ñoom ñuy lor Yonent bi, naan : “Benn nopp la”. - Neel : “Nopp bu yiw la ci yéen. Gëm na Yàlla te wóolu na way-gëm ña, te yërmaande la ci ñi gëm ci yéen. Te ñiy lor Yonentub Yàlla bi, mbugal mu metti ñeel na leen.
62يَحْلِفُونَ بِاللَّهِ لَكُمْ لِيُرْضُوكُمْ وَاللَّهُ وَرَسُولُهُ أَحَقُّ أَن يُرْضُوهُ إِن كَانُوا مُؤْمِنِينَ
Ña nga lay waatal ci Yàlla ngir am seen ngërëm. Te Yàlla ak Yonentam ñoo gën a yey ci ñoom sàkku seen ngërëm ndeem ñu gëm lañu.
63أَلَمْ يَعْلَمُوا أَنَّهُ مَن يُحَادِدِ اللَّهَ وَرَسُولَهُ فَأَنَّ لَهُ نَارَ جَهَنَّمَ خَالِدًا فِيهَا ۚ ذَٰلِكَ الْخِزْيُ الْعَظِيمُ
Moo ndax dañoo xamul ne (li wóor mooy) ne ku juuyook Yàlla ak Yonentam, dana ko ñeel ci loolu tàngooru Safara, fu muy sax ba fàwwu ? Muy gàcce gu mag.
64يَحْذَرُ الْمُنَافِقُونَ أَن تُنَزَّلَ عَلَيْهِمْ سُورَةٌ تُنَبِّئُهُم بِمَا فِي قُلُوبِهِمْ ۚ قُلِ اسْتَهْزِئُوا إِنَّ اللَّهَ مُخْرِجٌ مَّا تَحْذَرُونَ
Naaféq ya danañu ragal aw saar wàcc feeñal li nekk ci seeni xol. Neeleen : “Ñaawleleen ! Yàlla Dana génne li ngeen di ragal (mu génn)”.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
62Aaya

Tekki — At-Tawba 62

Simoore At-Tawba Aaya 62 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña nga lay waatal ci Yàlla ngir am seen ngërëm.…

Simoore Aaya 62/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 60–64. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers