Yusuf · 19/111
Tekki Waxtaan — Yusuf
وَجَاءَتْ سَيَّارَةٌ فَأَرْسَلُوا وَارِدَهُمْ فَأَدْلَىٰ دَلْوَهُ ۖ قَالَ يَا بُشْرَىٰ هَٰذَا غُلَامٌ ۚ وَأَسَرُّوهُ بِضَاعَةً ۚ وَاللَّهُ عَلِيمٌ بِمَا يَعْمَلُونَ ۝١٩
Wa jaaa`at saiyaaratun fa-arsaloo waaridahum fa adlaa dalwah; qaala yaa bushraa haaza ghulaam; wa asarroohu bi-daa`ah; wallaahu `aleemum bimaa ya`maloon
📖 Tekkim Wolof
Ay tukkikat agsi, yónni seenub rootkat, mu yoor baagam. Mu daldi ne : “Mbégtee ngi ! Lii de ab xale la ! ” Ñu yóbbu ko nar koo jaay. Te Yàlla ku xam la la ñuy def.
🎧 Dégg

📜 Aaya 17-21 — Yusuf

17قَالُوا يَا أَبَانَا إِنَّا ذَهَبْنَا نَسْتَبِقُ وَتَرَكْنَا يُوسُفَ عِندَ مَتَاعِنَا فَأَكَلَهُ الذِّئْبُ ۖ وَمَا أَنتَ بِمُؤْمِنٍ لَّنَا وَلَوْ كُنَّا صَادِقِينَ
Ñu ne : "Yaw sunu baay, ba ñu demee, dañu doon rawante, bàyyi Yuusufa ca sunuy yóbbal ; ag till lekk ko. Te bu nu waxee dëgg it du tax nga gëm li nu wax”.
18وَجَاءُوا عَلَىٰ قَمِيصِهِ بِدَمٍ كَذِبٍ ۚ قَالَ بَلْ سَوَّلَتْ لَكُمْ أَنفُسُكُمْ أَمْرًا ۖ فَصَبْرٌ جَمِيلٌ ۖ وَاللَّهُ الْمُسْتَعَانُ عَلَىٰ مَا تَصِفُونَ
Ñu indiwaale yéreem yu taq dereet [ju dul dereeti Yusuufa]. Mu tontu leen ne : “Yéen dey, seen bakkan rafetal na leen mbir mii... Waaye danaa sax ci muñ gu rafet ! Ci Yàlla laay dimbandikoo ci lii ngeen nettali ! ”
19وَجَاءَتْ سَيَّارَةٌ فَأَرْسَلُوا وَارِدَهُمْ فَأَدْلَىٰ دَلْوَهُ ۖ قَالَ يَا بُشْرَىٰ هَٰذَا غُلَامٌ ۚ وَأَسَرُّوهُ بِضَاعَةً ۚ وَاللَّهُ عَلِيمٌ بِمَا يَعْمَلُونَ
Ay tukkikat agsi, yónni seenub rootkat, mu yoor baagam. Mu daldi ne : “Mbégtee ngi ! Lii de ab xale la ! ” Ñu yóbbu ko nar koo jaay. Te Yàlla ku xam la la ñuy def.
20وَشَرَوْهُ بِثَمَنٍ بَخْسٍ دَرَاهِمَ مَعْدُودَةٍ وَكَانُوا فِيهِ مِنَ الزَّاهِدِينَ
Ñu jaay ko ci njëg gu néew : ay dërëm yu bariwul. Ndax dañu koo xeeboon.
21وَقَالَ الَّذِي اشْتَرَاهُ مِن مِّصْرَ لِامْرَأَتِهِ أَكْرِمِي مَثْوَاهُ عَسَىٰ أَن يَنفَعَنَا أَوْ نَتَّخِذَهُ وَلَدًا ۚ وَكَذَٰلِكَ مَكَّنَّا لِيُوسُفَ فِي الْأَرْضِ وَلِنُعَلِّمَهُ مِن تَأْوِيلِ الْأَحَادِيثِ ۚ وَاللَّهُ غَالِبٌ عَلَىٰ أَمْرِهِ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ
Ka ko jënd di waa Misra, wax na jabaram ne ko : “Teralal ma ko. Xéy-na mu jariñ nu mbaa nu def ko sunu doom.”. Noonu la nu darajaale Yuusufa ci suuf si, ak it ngir Nu jàngal ko pirim gént. Yàlla kuy not la ca la Mu namm : waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
19Aaya

Tekki — Yusuf 19

Simoore Yusuf Aaya 19 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ay tukkikat agsi, yónni seenub rootkat, mu yoor baagam. Mu…

Simoore Aaya 19/111 — Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yusuf Dégg, Yusuf Tekki, Yusuf mp3, Yusuf pdf. Aaya 17–21. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers