Yusuf · 20/111
Tekki Waxtaan — Yusuf
وَشَرَوْهُ بِثَمَنٍ بَخْسٍ دَرَاهِمَ مَعْدُودَةٍ وَكَانُوا فِيهِ مِنَ الزَّاهِدِينَ ۝٢٠
Wa sharawhu bisamanim bakhsin daraahima ma`doo datinw wa kaanoo feehi minaz zaahideen
📖 Tekkim Wolof
Ñu jaay ko ci njëg gu néew : ay dërëm yu bariwul. Ndax dañu koo xeeboon.

🎧 Dégg


📜 Aaya 18-22 — Yusuf

18وَجَاءُوا عَلَىٰ قَمِيصِهِ بِدَمٍ كَذِبٍ ۚ قَالَ بَلْ سَوَّلَتْ لَكُمْ أَنفُسُكُمْ أَمْرًا ۖ فَصَبْرٌ جَمِيلٌ ۖ وَاللَّهُ الْمُسْتَعَانُ عَلَىٰ مَا تَصِفُونَ
Ñu indiwaale yéreem yu taq dereet [ju dul dereeti Yusuufa]. Mu tontu leen ne : “Yéen dey, seen bakkan rafetal na leen mbir mii... Waaye danaa sax ci muñ gu rafet ! Ci Yàlla laay dimbandikoo ci lii ngeen nettali ! ”
19وَجَاءَتْ سَيَّارَةٌ فَأَرْسَلُوا وَارِدَهُمْ فَأَدْلَىٰ دَلْوَهُ ۖ قَالَ يَا بُشْرَىٰ هَٰذَا غُلَامٌ ۚ وَأَسَرُّوهُ بِضَاعَةً ۚ وَاللَّهُ عَلِيمٌ بِمَا يَعْمَلُونَ
Ay tukkikat agsi, yónni seenub rootkat, mu yoor baagam. Mu daldi ne : “Mbégtee ngi ! Lii de ab xale la ! ” Ñu yóbbu ko nar koo jaay. Te Yàlla ku xam la la ñuy def.
20وَشَرَوْهُ بِثَمَنٍ بَخْسٍ دَرَاهِمَ مَعْدُودَةٍ وَكَانُوا فِيهِ مِنَ الزَّاهِدِينَ
Ñu jaay ko ci njëg gu néew : ay dërëm yu bariwul. Ndax dañu koo xeeboon.
21وَقَالَ الَّذِي اشْتَرَاهُ مِن مِّصْرَ لِامْرَأَتِهِ أَكْرِمِي مَثْوَاهُ عَسَىٰ أَن يَنفَعَنَا أَوْ نَتَّخِذَهُ وَلَدًا ۚ وَكَذَٰلِكَ مَكَّنَّا لِيُوسُفَ فِي الْأَرْضِ وَلِنُعَلِّمَهُ مِن تَأْوِيلِ الْأَحَادِيثِ ۚ وَاللَّهُ غَالِبٌ عَلَىٰ أَمْرِهِ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ
Ka ko jënd di waa Misra, wax na jabaram ne ko : “Teralal ma ko. Xéy-na mu jariñ nu mbaa nu def ko sunu doom.”. Noonu la nu darajaale Yuusufa ci suuf si, ak it ngir Nu jàngal ko pirim gént. Yàlla kuy not la ca la Mu namm : waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.
22وَلَمَّا بَلَغَ أَشُدَّهُ آتَيْنَاهُ حُكْمًا وَعِلْمًا ۚ وَكَذَٰلِكَ نَجْزِي الْمُحْسِنِينَ
Ba mu màggee ba tollu ci góor gu mat, jox Nanu ko ràññee ak xam-xam. Te noonu Lanuy feye way-rafetal ña.
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
20Aaya

Tekki — Yusuf 20

Simoore Yusuf Aaya 20 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñu jaay ko ci njëg gu néew : ay dërëm…

Simoore Aaya 20/111 — Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yusuf Dégg, Yusuf Tekki, Yusuf mp3, Yusuf pdf. Aaya 18–22. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers