Yusuf · 50/111
Tekki Waxtaan — Yusuf
وَقَالَ الْمَلِكُ ائْتُونِي بِهِ ۖ فَلَمَّا جَاءَهُ الرَّسُولُ قَالَ ارْجِعْ إِلَىٰ رَبِّكَ فَاسْأَلْهُ مَا بَالُ النِّسْوَةِ اللَّاتِي قَطَّعْنَ أَيْدِيَهُنَّ ۚ إِنَّ رَبِّي بِكَيْدِهِنَّ عَلِيمٌ ۝٥٠
Wa qaalal maliku`toonee bihee falammaa jaaa`ahur rasoolu qaalar-ji ilaa rabbika fas`alhu maa baalun niswatil laatee qatta`na aydiyahunn; inna Rabbee bikaidihinna `Aleem
📖 Tekkim Wolof
Buur ba ne : “Indil-leen ma ko”. Ba ndaw la agsee ca moom [Yuusufa], mu ne ko : “Dellul ca sa sang, nga laaj ko : “Lan moo doon mbirum jigéen ña dogatoon seen yoxo ? Sama Boroom xam na bu baax seen pexe”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 48-52 — Yusuf

48ثُمَّ يَأْتِي مِن بَعْدِ ذَٰلِكَ سَبْعٌ شِدَادٌ يَأْكُلْنَ مَا قَدَّمْتُمْ لَهُنَّ إِلَّا قَلِيلًا مِّمَّا تُحْصِنُونَ
Dana ca topp gannaaw loolu juróom-ñaari at yu bekkoor yuy lekk la ngeen dencoon ngir ñoom ba mu des lu néew ca la ngeen dencoon.
49ثُمَّ يَأْتِي مِن بَعْدِ ذَٰلِكَ عَامٌ فِيهِ يُغَاثُ النَّاسُ وَفِيهِ يَعْصِرُونَ
Dana ca topp gannaaw loolu at moo xam ne dana xettali nit ñi te it danañu ca nal [reseñ ndax dana am].”
50وَقَالَ الْمَلِكُ ائْتُونِي بِهِ ۖ فَلَمَّا جَاءَهُ الرَّسُولُ قَالَ ارْجِعْ إِلَىٰ رَبِّكَ فَاسْأَلْهُ مَا بَالُ النِّسْوَةِ اللَّاتِي قَطَّعْنَ أَيْدِيَهُنَّ ۚ إِنَّ رَبِّي بِكَيْدِهِنَّ عَلِيمٌ
Buur ba ne : “Indil-leen ma ko”. Ba ndaw la agsee ca moom [Yuusufa], mu ne ko : “Dellul ca sa sang, nga laaj ko : “Lan moo doon mbirum jigéen ña dogatoon seen yoxo ? Sama Boroom xam na bu baax seen pexe”.
51قَالَ مَا خَطْبُكُنَّ إِذْ رَاوَدتُّنَّ يُوسُفَ عَن نَّفْسِهِ ۚ قُلْنَ حَاشَ لِلَّهِ مَا عَلِمْنَا عَلَيْهِ مِن سُوءٍ ۚ قَالَتِ امْرَأَتُ الْعَزِيزِ الْآنَ حَصْحَصَ الْحَقُّ أَنَا رَاوَدتُّهُ عَن نَّفْسِهِ وَإِنَّهُ لَمِنَ الصَّادِقِينَ
[Buur ba ne jigéen ña] : “Lan moo doon seen mbir ba ngeen sàkku Yuusufa ci jëmmam ? ”. Ñu tontu ne : “Wax dëgg Yàlla ! Xamalunu ko dara lu bon”. Jabaru buur ba ne : “Léegi nag dëgg gi leer na. Maa ko sàkku woon. Moom moo waxoon dëgg ! ”
52ذَٰلِكَ لِيَعْلَمَ أَنِّي لَمْ أَخُنْهُ بِالْغَيْبِ وَأَنَّ اللَّهَ لَا يَهْدِي كَيْدَ الْخَائِنِينَ
“[Man Yuusufa maa defoon] noonu ngir buur bi xam ne wuruju ma ko ginnaawam, te sax Yàlla du jubale pexem wurujkat ya.
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
50Aaya

Tekki — Yusuf 50

Simoore Yusuf Aaya 50 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Buur ba ne : “Indil-leen ma ko”. Ba ndaw la…

Simoore Aaya 50/111 — Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yusuf Dégg, Yusuf Tekki, Yusuf mp3, Yusuf pdf. Aaya 48–52. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers