Ibrahima · 33/52
Tekki Waxtaan — Ibrahima
وَسَخَّرَ لَكُمُ الشَّمْسَ وَالْقَمَرَ دَائِبَيْنِ ۖ وَسَخَّرَ لَكُمُ اللَّيْلَ وَالنَّهَارَ ۝٣٣
Wa sakhkhara lakumush shamsa walqamara daaa`ibaini wa sakhkhara lakumul laila wannahaar
📖 Tekkim Wolof
Te tàggatal na leen it jant bi ak weer wi ñuy ñaari way-daw [ku ca nekk ci aw rëddëm]. Tàggatal na leen guddi ak bëccëg.
🎧 Dégg

📜 Aaya 31-35 — Ibrahima

31قُل لِّعِبَادِيَ الَّذِينَ آمَنُوا يُقِيمُوا الصَّلَاةَ وَيُنفِقُوا مِمَّا رَزَقْنَاهُمْ سِرًّا وَعَلَانِيَةً مِّن قَبْلِ أَن يَأْتِيَ يَوْمٌ لَّا بَيْعٌ فِيهِ وَلَا خِلَالٌ
Waxal sama jaam yi gëm ne leen : "Nañuy taxawal julli tey joxe ca la Ma leen wërsëgale ci lu nëbbu walla la feeñ, balaa àpp bis di ñëw boo xam ne jotoo amu fa waxantumalaa xaritoo.
32اللَّهُ الَّذِي خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ وَأَنزَلَ مِنَ السَّمَاءِ مَاءً فَأَخْرَجَ بِهِ مِنَ الثَّمَرَاتِ رِزْقًا لَّكُمْ ۖ وَسَخَّرَ لَكُمُ الْفُلْكَ لِتَجْرِيَ فِي الْبَحْرِ بِأَمْرِهِ ۖ وَسَخَّرَ لَكُمُ الْأَنْهَارَ
Yàlla mooy ki bind asamaan yi ak suuf si te Mooy wàcce ndox mu jóge kaw asamaan ngir Mu génne ca meññent yu nekk i xéewal ci yéen. Te Moo leen tàggatal gaal ngir ngeen mën a daw ci géej ci ndigalam. Te tàggatal na leen it dex yi.
33وَسَخَّرَ لَكُمُ الشَّمْسَ وَالْقَمَرَ دَائِبَيْنِ ۖ وَسَخَّرَ لَكُمُ اللَّيْلَ وَالنَّهَارَ
Te tàggatal na leen it jant bi ak weer wi ñuy ñaari way-daw [ku ca nekk ci aw rëddëm]. Tàggatal na leen guddi ak bëccëg.
34وَآتَاكُم مِّن كُلِّ مَا سَأَلْتُمُوهُ ۚ وَإِن تَعُدُّوا نِعْمَتَ اللَّهِ لَا تُحْصُوهَا ۗ إِنَّ الْإِنسَانَ لَظَلُومٌ كَفَّارٌ
Te Moo di leen may ci lépp lu ngeen ko ñaan. Te sax, bu ngeen doon jéem a waññi ay xéewalam, dungeen ko mën a takk. Ndekete yoo nit moom ab tooñkat la bu mën a fakk jëf.
35وَإِذْ قَالَ إِبْرَاهِيمُ رَبِّ اجْعَلْ هَٰذَا الْبَلَدَ آمِنًا وَاجْنُبْنِي وَبَنِيَّ أَن نَّعْبُدَ الْأَصْنَامَ
[Fàttalikul] ba Ibraahiima waxee ne : “Sama Boroom, [ñaan naa la] nga def dëkk bii di fu am kóolute, te maak samag njaboot nga soril nu ak jaamu xërëm.
IbrahimaFihi Alxuraan
52Aaya
MeccanRevelation
33Aaya

Tekki — Ibrahima 33

Simoore Ibrahima Aaya 33 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te tàggatal na leen it jant bi ak weer wi…

Simoore Aaya 33/52 — Ibrahima إبراهيم (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ibrahima Dégg, Ibrahima Tekki, Ibrahima mp3, Ibrahima pdf. Aaya 31–35. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers