Ibrahima · 6/52
Tekki Waxtaan — Ibrahima
وَإِذْ قَالَ مُوسَىٰ لِقَوْمِهِ اذْكُرُوا نِعْمَةَ اللَّهِ عَلَيْكُمْ إِذْ أَنجَاكُم مِّنْ آلِ فِرْعَوْنَ يَسُومُونَكُمْ سُوءَ الْعَذَابِ وَيُذَبِّحُونَ أَبْنَاءَكُمْ وَيَسْتَحْيُونَ نِسَاءَكُمْ ۚ وَفِي ذَٰلِكُم بَلَاءٌ مِّن رَّبِّكُمْ عَظِيمٌ ۝٦
Wa iz qaala Moosaa liqawmihiz kuroo ni`matal laahi `alaikum iz anjaakum min Aali Fir`awna yasoomoo nakum sooo`al `azaabi wa yuzabbihoona abnaaa`akum wa yastahyoona nisaaa`akum; wa fee zaalikum balaaa`um mir Rabbikum `azeem
📖 Tekkim Wolof
(Fàttalikul) ba Muusaa waxee aw nitam ne leen : “Fàttalikuleen xéewalu Yàlla ga Mu leen defaloon ba Mu leen musaloon ci waa kër Firawna, ñu leen doon teg mbugal mu bon. Di rey seen doon yu góor, di bàyyi jigéen ña. Te loolu nekkoon na ab nattu bu rëy bu jóge ci seen Boroom”,

🎧 Dégg


📜 Aaya 4-8 — Ibrahima

4وَمَا أَرْسَلْنَا مِن رَّسُولٍ إِلَّا بِلِسَانِ قَوْمِهِ لِيُبَيِّنَ لَهُمْ ۖ فَيُضِلُّ اللَّهُ مَن يَشَاءُ وَيَهْدِي مَن يَشَاءُ ۚ وَهُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Dunu yónni ab Yonent lu dul ci làkku nitam ña [lay waxe] ngir mu leeralal leen [la ñu ko yónni]. Te Yàlla mooy bàyyi cig réer ku ko soob, Dana gindi itam ku ko soob. Ndax Moom moo di boroom kàttan gi tey Aji-xereñ [ciy àtteem].
5وَلَقَدْ أَرْسَلْنَا مُوسَىٰ بِآيَاتِنَا أَنْ أَخْرِجْ قَوْمَكَ مِنَ الظُّلُمَاتِ إِلَى النُّورِ وَذَكِّرْهُم بِأَيَّامِ اللَّهِ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّكُلِّ صَبَّارٍ شَكُورٍ
Yónni woon Nanu Muusaa, dooleel kook Sunuy kaawtéef, ne ko : “Génneel saw nit cig lëndëm jëme leen cig réer, te nga waar leen ci xéewali Yàlla yi”. Ndax kéemtaan a ngi ci loolu ñeel képp ku di ab muñaakoon, di ab santaakoon.
6وَإِذْ قَالَ مُوسَىٰ لِقَوْمِهِ اذْكُرُوا نِعْمَةَ اللَّهِ عَلَيْكُمْ إِذْ أَنجَاكُم مِّنْ آلِ فِرْعَوْنَ يَسُومُونَكُمْ سُوءَ الْعَذَابِ وَيُذَبِّحُونَ أَبْنَاءَكُمْ وَيَسْتَحْيُونَ نِسَاءَكُمْ ۚ وَفِي ذَٰلِكُم بَلَاءٌ مِّن رَّبِّكُمْ عَظِيمٌ
(Fàttalikul) ba Muusaa waxee aw nitam ne leen : “Fàttalikuleen xéewalu Yàlla ga Mu leen defaloon ba Mu leen musaloon ci waa kër Firawna, ñu leen doon teg mbugal mu bon. Di rey seen doon yu góor, di bàyyi jigéen ña. Te loolu nekkoon na ab nattu bu rëy bu jóge ci seen Boroom”,
7وَإِذْ تَأَذَّنَ رَبُّكُمْ لَئِن شَكَرْتُمْ لَأَزِيدَنَّكُمْ ۖ وَلَئِن كَفَرْتُمْ إِنَّ عَذَابِي لَشَدِيدٌ
Ak ba seen Boroom xamlee ne : “Bu ngeen gërëmee, fàwwu Mu dolli leen. Bu ngeen weddee nag, [na ngeen xam ne ] Sama mbugal lu tar la”.
8وَقَالَ مُوسَىٰ إِن تَكْفُرُوا أَنتُمْ وَمَن فِي الْأَرْضِ جَمِيعًا فَإِنَّ اللَّهَ لَغَنِيٌّ حَمِيدٌ
Te Muusaa ne leen : “Bu ngeen weddi woon, yéen ak ñi nekk ci suuf si yépp [du wàññi Boroom bi dara], ngir Yàlla Aji-doylu la ci boppam [wëliis ay mbindéefam], Aji-yeyoo cant la”.
IbrahimaFihi Alxuraan
52Aaya
MeccanRevelation
6Aaya

Tekki — Ibrahima 6

Simoore Ibrahima Aaya 6 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : (Fàttalikul) ba Muusaa waxee aw nitam ne leen : “Fàttalikuleen…

Simoore Aaya 6/52 — Ibrahima إبراهيم (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ibrahima Dégg, Ibrahima Tekki, Ibrahima mp3, Ibrahima pdf. Aaya 4–8. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers