An-Nahl · 61/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
وَلَوْ يُؤَاخِذُ اللَّهُ النَّاسَ بِظُلْمِهِم مَّا تَرَكَ عَلَيْهَا مِن دَابَّةٍ وَلَٰكِن يُؤَخِّرُهُمْ إِلَىٰ أَجَلٍ مُّسَمًّى ۖ فَإِذَا جَاءَ أَجَلُهُمْ لَا يَسْتَأْخِرُونَ سَاعَةً ۖ وَلَا يَسْتَقْدِمُونَ ۝٦١
Wa law yu`aakhizul laahun naasa bizulminhim maa taraka `alaihaa min daaabbatinw wa laakiny yu`akhkhiruhum ilaaa ajalim musamman fa izaa jaaa`a ajaluhum laa yastaakhiroona saa`atanw wa laa yastaqdimoon
📖 Tekkim Wolof
Bu Yàlla [doon] gaaw a duma nit ñi ngir seen tooñeel, kon du bàyyi kenn ci kaw suuf si. Waaye Dafa leen ci yeexe ba ci àpp bu ñu dogal ba noppi. Kon bu seen àpp agsee, duñu ko weesu mbaa ñu jiitu ko wenn waxtu.

🎧 Dégg


📜 Aaya 59-63 — An-Nahl

59يَتَوَارَىٰ مِنَ الْقَوْمِ مِن سُوءِ مَا بُشِّرَ بِهِ ۚ أَيُمْسِكُهُ عَلَىٰ هُونٍ أَمْ يَدُسُّهُ فِي التُّرَابِ ۗ أَلَا سَاءَ مَا يَحْكُمُونَ
Muy nëbbu nit ñi ngir lu naqari la ñu yégal. Muy seet ndax dakoy téyee ndax gàcceem walla dakoy suul ci suuf ? Cëy aka bon nañuy àttee mbir !
60لِلَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِالْآخِرَةِ مَثَلُ السَّوْءِ ۖ وَلِلَّهِ الْمَثَلُ الْأَعْلَىٰ ۚ وَهُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Ñeel na ñi gëmul àllaaxira nekkin wu bon. Te ñeel na Yàlla nekkin wa gën a kawe. Te Moom mooy Aji-not ji ; Aji-xereñ.
61وَلَوْ يُؤَاخِذُ اللَّهُ النَّاسَ بِظُلْمِهِم مَّا تَرَكَ عَلَيْهَا مِن دَابَّةٍ وَلَٰكِن يُؤَخِّرُهُمْ إِلَىٰ أَجَلٍ مُّسَمًّى ۖ فَإِذَا جَاءَ أَجَلُهُمْ لَا يَسْتَأْخِرُونَ سَاعَةً ۖ وَلَا يَسْتَقْدِمُونَ
Bu Yàlla [doon] gaaw a duma nit ñi ngir seen tooñeel, kon du bàyyi kenn ci kaw suuf si. Waaye Dafa leen ci yeexe ba ci àpp bu ñu dogal ba noppi. Kon bu seen àpp agsee, duñu ko weesu mbaa ñu jiitu ko wenn waxtu.
62وَيَجْعَلُونَ لِلَّهِ مَا يَكْرَهُونَ وَتَصِفُ أَلْسِنَتُهُمُ الْكَذِبَ أَنَّ لَهُمُ الْحُسْنَىٰ ۖ لَا جَرَمَ أَنَّ لَهُمُ النَّارَ وَأَنَّهُم مُّفْرَطُونَ
Ñangay sédd Yàlla la ñu sib ñoom. Te seeni làmmiñ di sos i fen naan ñoo moom Àjjana. Te ca dëgg-dëgg ñoo yeyoo Safara te ñoo cay jiitu.
63تَاللَّهِ لَقَدْ أَرْسَلْنَا إِلَىٰ أُمَمٍ مِّن قَبْلِكَ فَزَيَّنَ لَهُمُ الشَّيْطَانُ أَعْمَالَهُمْ فَهُوَ وَلِيُّهُمُ الْيَوْمَ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Giñ Nanu Nun Yàlla ne yónni woon Nanu ay Yonent cay xeet ya la jiitu. Waaye Séytaane rafetalal leen seeni jëf ba faf mu nekk tey seeni àndandoo. Te ñeel na leen mbugal mu metti.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
61Aaya

Tekki — An-Nahl 61

Simoore An-Nahl Aaya 61 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu Yàlla [doon] gaaw a duma nit ñi ngir seen…

Simoore Aaya 61/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 59–63. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers