An-Nahl · 60/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
لِلَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِالْآخِرَةِ مَثَلُ السَّوْءِ ۖ وَلِلَّهِ الْمَثَلُ الْأَعْلَىٰ ۚ وَهُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ ۝٦٠
Lillazeena laa yu`minoona bil Aakhirati masalus saw`i wa lillaahil masalul a`laa; wa Huwal `Azeezul Hakeem
📖 Tekkim Wolof
Ñeel na ñi gëmul àllaaxira nekkin wu bon. Te ñeel na Yàlla nekkin wa gën a kawe. Te Moom mooy Aji-not ji ; Aji-xereñ.

🎧 Dégg


📜 Aaya 58-62 — An-Nahl

58وَإِذَا بُشِّرَ أَحَدُهُم بِالْأُنثَىٰ ظَلَّ وَجْهُهُ مُسْوَدًّا وَهُوَ كَظِيمٌ
Ku ñu ca yégal ne am na doom ju jigéen, mu yendoo ñëgal kanam gi ànd ak mer.
59يَتَوَارَىٰ مِنَ الْقَوْمِ مِن سُوءِ مَا بُشِّرَ بِهِ ۚ أَيُمْسِكُهُ عَلَىٰ هُونٍ أَمْ يَدُسُّهُ فِي التُّرَابِ ۗ أَلَا سَاءَ مَا يَحْكُمُونَ
Muy nëbbu nit ñi ngir lu naqari la ñu yégal. Muy seet ndax dakoy téyee ndax gàcceem walla dakoy suul ci suuf ? Cëy aka bon nañuy àttee mbir !
60لِلَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِالْآخِرَةِ مَثَلُ السَّوْءِ ۖ وَلِلَّهِ الْمَثَلُ الْأَعْلَىٰ ۚ وَهُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Ñeel na ñi gëmul àllaaxira nekkin wu bon. Te ñeel na Yàlla nekkin wa gën a kawe. Te Moom mooy Aji-not ji ; Aji-xereñ.
61وَلَوْ يُؤَاخِذُ اللَّهُ النَّاسَ بِظُلْمِهِم مَّا تَرَكَ عَلَيْهَا مِن دَابَّةٍ وَلَٰكِن يُؤَخِّرُهُمْ إِلَىٰ أَجَلٍ مُّسَمًّى ۖ فَإِذَا جَاءَ أَجَلُهُمْ لَا يَسْتَأْخِرُونَ سَاعَةً ۖ وَلَا يَسْتَقْدِمُونَ
Bu Yàlla [doon] gaaw a duma nit ñi ngir seen tooñeel, kon du bàyyi kenn ci kaw suuf si. Waaye Dafa leen ci yeexe ba ci àpp bu ñu dogal ba noppi. Kon bu seen àpp agsee, duñu ko weesu mbaa ñu jiitu ko wenn waxtu.
62وَيَجْعَلُونَ لِلَّهِ مَا يَكْرَهُونَ وَتَصِفُ أَلْسِنَتُهُمُ الْكَذِبَ أَنَّ لَهُمُ الْحُسْنَىٰ ۖ لَا جَرَمَ أَنَّ لَهُمُ النَّارَ وَأَنَّهُم مُّفْرَطُونَ
Ñangay sédd Yàlla la ñu sib ñoom. Te seeni làmmiñ di sos i fen naan ñoo moom Àjjana. Te ca dëgg-dëgg ñoo yeyoo Safara te ñoo cay jiitu.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
60Aaya

Tekki — An-Nahl 60

Simoore An-Nahl Aaya 60 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñeel na ñi gëmul àllaaxira nekkin wu bon. Te ñeel…

Simoore Aaya 60/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 58–62. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers