Al-Isra · 22/111
Tekki Waxtaan — Al-Isra
لَّا تَجْعَلْ مَعَ اللَّهِ إِلَٰهًا آخَرَ فَتَقْعُدَ مَذْمُومًا مَّخْذُولًا ۝٢٢
Laa taj`al ma`al laahi ilaahan aakhara fataq`uda mazoomam makhzoolaa
📖 Tekkim Wolof
Bul sàkk jeneen yàlla di ko booleek Yàlla ; kon dey danga doon ku ñu xas, ku ñu wacc mu beddiku.
🎧 Dégg

📜 Aaya 20-24 — Al-Isra

20كُلًّا نُّمِدُّ هَٰؤُلَاءِ وَهَٰؤُلَاءِ مِنْ عَطَاءِ رَبِّكَ ۚ وَمَا كَانَ عَطَاءُ رَبِّكَ مَحْظُورًا
Ñoom ñépp Dananu leen tëbb ; ñii ak ñële, ay may yu jóge ca sa Boroom. Te sa mayu Boroom nekkul lu ñu tere kenn.Làndi na!
21انظُرْ كَيْفَ فَضَّلْنَا بَعْضَهُمْ عَلَىٰ بَعْضٍ ۚ وَلَلْآخِرَةُ أَكْبَرُ دَرَجَاتٍ وَأَكْبَرُ تَفْضِيلًا
Gisal ni Nu gënalee ñenn ñi ci kaw ñeneen ña. Te ca dëgg-dëgg àllaaxira moo gën a màgg daraja te moo gën a màgg i xéewal.
22لَّا تَجْعَلْ مَعَ اللَّهِ إِلَٰهًا آخَرَ فَتَقْعُدَ مَذْمُومًا مَّخْذُولًا
Bul sàkk jeneen yàlla di ko booleek Yàlla ; kon dey danga doon ku ñu xas, ku ñu wacc mu beddiku.
23۞ وَقَضَىٰ رَبُّكَ أَلَّا تَعْبُدُوا إِلَّا إِيَّاهُ وَبِالْوَالِدَيْنِ إِحْسَانًا ۚ إِمَّا يَبْلُغَنَّ عِندَكَ الْكِبَرَ أَحَدُهُمَا أَوْ كِلَاهُمَا فَلَا تَقُل لَّهُمَا أُفٍّ وَلَا تَنْهَرْهُمَا وَقُل لَّهُمَا قَوْلًا كَرِيمًا
Sa Boroom dogal na ne : “Buleen jaamu ku dul Moom doŋŋ ; te ngeen rafetal jëme ci seeni waajur : te ndeem kenn ci ñoom walla ñoom ñaar egg nañu ci màggat ci sa teewaay ; buleen wax : “Kuf ma la ! ”, buleen leen gëdd, nangeen leen wax wax ju yiw.
24وَاخْفِضْ لَهُمَا جَنَاحَ الذُّلِّ مِنَ الرَّحْمَةِ وَقُل رَّبِّ ارْحَمْهُمَا كَمَا رَبَّيَانِي صَغِيرًا
Nanga suufeel sa bopp ngir ñoom ; di toroxlu ci yërmaande ; te deel wax : "Sama Boroom yërëm leen [ni ñu ma yërëme woon] ba ñu may yar ba ma nekkee xale”.
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
22Aaya

Tekki — Al-Isra 22

Simoore Al-Isra Aaya 22 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bul sàkk jeneen yàlla di ko booleek Yàlla ; kon…

Simoore Aaya 22/111 — Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Isra Dégg, Al-Isra Tekki, Al-Isra mp3, Al-Isra pdf. Aaya 20–24. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers