Al-Isra · 25/111
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Isra
رَّبُّكُمْ أَعْلَمُ بِمَا فِي نُفُوسِكُمْ ۚ إِن تَكُونُوا صَالِحِينَ فَإِنَّهُ كَانَ لِلْأَوَّابِينَ غَفُورًا ۝٢٥
Rabbukum a`lamu bimaa fee nufoosikum; in takoonoo saaliheena fa innahoo kaana lil awwaabeena Ghafoooraa
📖 Tekkim Wolof
Seen Boroom a gën a xam li nekk ci seen bakkan. Ndeem nekk ngeen ñu sell ; Moom Jéggalaakoon la ci ñiy dellu jëm ci jaamu Yàlla.

🎧 Dégg


📜 Aaya 23-27 — Simoore Al-Isra

23۞ وَقَضَىٰ رَبُّكَ أَلَّا تَعْبُدُوا إِلَّا إِيَّاهُ وَبِالْوَالِدَيْنِ إِحْسَانًا ۚ إِمَّا يَبْلُغَنَّ عِندَكَ الْكِبَرَ أَحَدُهُمَا أَوْ كِلَاهُمَا فَلَا تَقُل لَّهُمَا أُفٍّ وَلَا تَنْهَرْهُمَا وَقُل لَّهُمَا قَوْلًا كَرِيمًا
Sa Boroom dogal na ne : “Buleen jaamu ku dul Moom doŋŋ ; te ngeen rafetal jëme ci seeni waajur : te ndeem kenn ci ñoom walla ñoom ñaar egg nañu ci màggat ci sa teewaay ; buleen wax : “Kuf ma la ! ”, buleen leen gëdd, nangeen leen wax wax ju yiw.
24وَاخْفِضْ لَهُمَا جَنَاحَ الذُّلِّ مِنَ الرَّحْمَةِ وَقُل رَّبِّ ارْحَمْهُمَا كَمَا رَبَّيَانِي صَغِيرًا
Nanga suufeel sa bopp ngir ñoom ; di toroxlu ci yërmaande ; te deel wax : "Sama Boroom yërëm leen [ni ñu ma yërëme woon] ba ñu may yar ba ma nekkee xale”.
25رَّبُّكُمْ أَعْلَمُ بِمَا فِي نُفُوسِكُمْ ۚ إِن تَكُونُوا صَالِحِينَ فَإِنَّهُ كَانَ لِلْأَوَّابِينَ غَفُورًا
Seen Boroom a gën a xam li nekk ci seen bakkan. Ndeem nekk ngeen ñu sell ; Moom Jéggalaakoon la ci ñiy dellu jëm ci jaamu Yàlla.
26وَآتِ ذَا الْقُرْبَىٰ حَقَّهُ وَالْمِسْكِينَ وَابْنَ السَّبِيلِ وَلَا تُبَذِّرْ تَبْذِيرًا
“Nanga jox sa jegeñaale li la war ci moom, ak ku ñàkk ak ku nekk ci tukki. Waaye bul nekk di pasar-pasaree alal,
27إِنَّ الْمُبَذِّرِينَ كَانُوا إِخْوَانَ الشَّيَاطِينِ ۖ وَكَانَ الشَّيْطَانُ لِرَبِّهِ كَفُورًا
yàqkat yi mbokki Séytaane lañu ; te Séytaane dafa weddi Boroomam.
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
25Aaya

Tekki — Al-Isra 25

Simoore Al-Isra Aaya 25 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Seen Boroom a gën a xam li nekk ci seen…

Simoore Aaya 25/111 — Simoore Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Isra Dégg, Simoore Al-Isra Tekki, Simoore Al-Isra mp3, Simoore Al-Isra pdf. Aaya 23–27. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers