Al-Isra · 56/111
Tekki Waxtaan — Al-Isra
قُلِ ادْعُوا الَّذِينَ زَعَمْتُم مِّن دُونِهِ فَلَا يَمْلِكُونَ كَشْفَ الضُّرِّ عَنكُمْ وَلَا تَحْوِيلًا ۝٥٦
Qulid `ul lazeena za`amtum min doonihee falaa yamlikoona kashfad durri`ankum wa laa tahweelaa
📖 Tekkim Wolof
Neel : “Wooleen ñi ngeen jàpp ne [Yàlla lañu] bàyyi Ko. Duñu mën a wuññi lor ja leen dal, duñu mën a soppi dara.

🎧 Dégg


📜 Aaya 54-58 — Al-Isra

54رَّبُّكُمْ أَعْلَمُ بِكُمْ ۖ إِن يَشَأْ يَرْحَمْكُمْ أَوْ إِن يَشَأْ يُعَذِّبْكُمْ ۚ وَمَا أَرْسَلْنَاكَ عَلَيْهِمْ وَكِيلًا
Seen Boroom moo leen gën a xam. Bu ko neexee Mu yërëm leen, walla Bu ko neexee Mu mbugal leen. Te yónniwunu la ci ñoom ngir nga warlul leen [seen texe].
55وَرَبُّكَ أَعْلَمُ بِمَن فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۗ وَلَقَدْ فَضَّلْنَا بَعْضَ النَّبِيِّينَ عَلَىٰ بَعْضٍ ۖ وَآتَيْنَا دَاوُودَ زَبُورًا
Te sa Boroom moo gën a xam ña nekk ci asmaan yi ak suuf si. Te def Nanu yenn Yonent yi gën ñeneen ña. Te Noo jox Daawuda “Zabour” [Téere].
56قُلِ ادْعُوا الَّذِينَ زَعَمْتُم مِّن دُونِهِ فَلَا يَمْلِكُونَ كَشْفَ الضُّرِّ عَنكُمْ وَلَا تَحْوِيلًا
Neel : “Wooleen ñi ngeen jàpp ne [Yàlla lañu] bàyyi Ko. Duñu mën a wuññi lor ja leen dal, duñu mën a soppi dara.
57أُولَٰئِكَ الَّذِينَ يَدْعُونَ يَبْتَغُونَ إِلَىٰ رَبِّهِمُ الْوَسِيلَةَ أَيُّهُمْ أَقْرَبُ وَيَرْجُونَ رَحْمَتَهُ وَيَخَافُونَ عَذَابَهُ ۚ إِنَّ عَذَابَ رَبِّكَ كَانَ مَحْذُورًا
Ña ñuy jaamu dañu ne siiw am pexem gën a jegeñ seen Boroom. Te yaakaar nañu yërmaandeem, ragal nañu mbugalam. Naka sa mbugalum Boroom, lu mat a wattandiku la.
58وَإِن مِّن قَرْيَةٍ إِلَّا نَحْنُ مُهْلِكُوهَا قَبْلَ يَوْمِ الْقِيَامَةِ أَوْ مُعَذِّبُوهَا عَذَابًا شَدِيدًا ۚ كَانَ ذَٰلِكَ فِي الْكِتَابِ مَسْطُورًا
Amul benn dëkk bu Nu dul alag balaa Bis-pénc ba, walla Nu mbugal ko mbugal mu tar. Looloo nekk ci Téere bu ñu bind. [Yàlla kuy nose la].
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
56Aaya

Tekki — Al-Isra 56

Simoore Al-Isra Aaya 56 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Neel : “Wooleen ñi ngeen jàpp ne [Yàlla lañu] bàyyi…

Simoore Aaya 56/111 — Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Isra Dégg, Al-Isra Tekki, Al-Isra mp3, Al-Isra pdf. Aaya 54–58. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers