Maryam · 37/98
Tekki Waxtaan — Maryam
فَاخْتَلَفَ الْأَحْزَابُ مِن بَيْنِهِمْ ۖ فَوَيْلٌ لِّلَّذِينَ كَفَرُوا مِن مَّشْهَدِ يَوْمٍ عَظِيمٍ ۝٣٧
Fakhtalafal ahzaabu mim bainihim fawailul lillazeena kafaroo mim mashhadi Yawmin `azeem
📖 Tekkim Wolof
Kurél yi juuyoo nañu ci seen diggante. Ñay weddi, xuru Safara ñeel na leen ca teewaayub bis bu màgg ba !

🎧 Dégg


📜 Aaya 35-39 — Maryam

35مَا كَانَ لِلَّهِ أَن يَتَّخِذَ مِن وَلَدٍ ۖ سُبْحَانَهُ ۚ إِذَا قَضَىٰ أَمْرًا فَإِنَّمَا يَقُولُ لَهُ كُن فَيَكُونُ
Yellul ci Yàlla muy jàppe kenn doomam. Cëy sellam ga ! Bu bëggee menn mbir, Danaan : “Nekkal ! ” mu daldi nekk.
36وَإِنَّ اللَّهَ رَبِّي وَرَبُّكُمْ فَاعْبُدُوهُ ۚ هَٰذَا صِرَاطٌ مُّسْتَقِيمٌ
“Te nag Yàlla moo di sama Boroom, di seen Boroom. Jaamuleen ko. Lii moo di yoon wu jub wi xocc”.
37فَاخْتَلَفَ الْأَحْزَابُ مِن بَيْنِهِمْ ۖ فَوَيْلٌ لِّلَّذِينَ كَفَرُوا مِن مَّشْهَدِ يَوْمٍ عَظِيمٍ
Kurél yi juuyoo nañu ci seen diggante. Ñay weddi, xuru Safara ñeel na leen ca teewaayub bis bu màgg ba !
38أَسْمِعْ بِهِمْ وَأَبْصِرْ يَوْمَ يَأْتُونَنَا ۖ لَٰكِنِ الظَّالِمُونَ الْيَوْمَ فِي ضَلَالٍ مُّبِينٍ
[Bu bis baa, tooñkat yi danañu dégg], danañu gis ! Waaye tey fii ci àddina, ñi ngi ci réer gu bir.
39وَأَنذِرْهُمْ يَوْمَ الْحَسْرَةِ إِذْ قُضِيَ الْأَمْرُ وَهُمْ فِي غَفْلَةٍ وَهُمْ لَا يُؤْمِنُونَ
Nanga leen xupp ci tiisu bisub jagle ga ; ndax àtte ba dog na te ñoom ña nga cig càggante te duñu gëm.
MaryamFihi Alxuraan
98Aaya
MeccanRevelation
37Aaya

Tekki — Maryam 37

Simoore Maryam Aaya 37 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Kurél yi juuyoo nañu ci seen diggante. Ñay weddi, xuru…

Simoore Aaya 37/98 — Maryam مريم (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Maryam Dégg, Maryam Tekki, Maryam mp3, Maryam pdf. Aaya 35–39. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers