Maryam · 36/98
Tekki Waxtaan — Maryam
وَإِنَّ اللَّهَ رَبِّي وَرَبُّكُمْ فَاعْبُدُوهُ ۚ هَٰذَا صِرَاطٌ مُّسْتَقِيمٌ ۝٣٦
Wa innal laaha Rabbee wa Rabbukum fa`budooh; haazaa Siraatum Mustaqeem
📖 Tekkim Wolof
“Te nag Yàlla moo di sama Boroom, di seen Boroom. Jaamuleen ko. Lii moo di yoon wu jub wi xocc”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 34-38 — Maryam

34ذَٰلِكَ عِيسَى ابْنُ مَرْيَمَ ۚ قَوْلَ الْحَقِّ الَّذِي فِيهِ يَمْتَرُونَ
Loolu mooy mbirum Iisaa doomu Maryam, wax jii moo cay dëgg ca la ngeen doon werante.
35مَا كَانَ لِلَّهِ أَن يَتَّخِذَ مِن وَلَدٍ ۖ سُبْحَانَهُ ۚ إِذَا قَضَىٰ أَمْرًا فَإِنَّمَا يَقُولُ لَهُ كُن فَيَكُونُ
Yellul ci Yàlla muy jàppe kenn doomam. Cëy sellam ga ! Bu bëggee menn mbir, Danaan : “Nekkal ! ” mu daldi nekk.
36وَإِنَّ اللَّهَ رَبِّي وَرَبُّكُمْ فَاعْبُدُوهُ ۚ هَٰذَا صِرَاطٌ مُّسْتَقِيمٌ
“Te nag Yàlla moo di sama Boroom, di seen Boroom. Jaamuleen ko. Lii moo di yoon wu jub wi xocc”.
37فَاخْتَلَفَ الْأَحْزَابُ مِن بَيْنِهِمْ ۖ فَوَيْلٌ لِّلَّذِينَ كَفَرُوا مِن مَّشْهَدِ يَوْمٍ عَظِيمٍ
Kurél yi juuyoo nañu ci seen diggante. Ñay weddi, xuru Safara ñeel na leen ca teewaayub bis bu màgg ba !
38أَسْمِعْ بِهِمْ وَأَبْصِرْ يَوْمَ يَأْتُونَنَا ۖ لَٰكِنِ الظَّالِمُونَ الْيَوْمَ فِي ضَلَالٍ مُّبِينٍ
[Bu bis baa, tooñkat yi danañu dégg], danañu gis ! Waaye tey fii ci àddina, ñi ngi ci réer gu bir.
MaryamFihi Alxuraan
98Aaya
MeccanRevelation
36Aaya

Tekki — Maryam 36

Simoore Maryam Aaya 36 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : “Te nag Yàlla moo di sama Boroom, di seen Boroom.…

Simoore Aaya 36/98 — Maryam مريم (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Maryam Dégg, Maryam Tekki, Maryam mp3, Maryam pdf. Aaya 34–38. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers