Al-Baqara · 201/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَمِنْهُم مَّن يَقُولُ رَبَّنَا آتِنَا فِي الدُّنْيَا حَسَنَةً وَفِي الْآخِرَةِ حَسَنَةً وَقِنَا عَذَابَ النَّارِ ۝٢٠١
Wa minhum mai yaqoolu rabbanaaa aatina fid dunyaa hasanatawn wa fil aakhirati hasanatanw wa qinaa azaaban Naar
📖 Tekkim Wolof
Am na ci ñoom kuy wax ne : “Yaw sunu Boroom ! Defalnu xéewal ci àddina, ak ca àllaaxira ; te fegalnu mbugalum Safara ! ”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 199-203 — Al-Baqara

199ثُمَّ أَفِيضُوا مِنْ حَيْثُ أَفَاضَ النَّاسُ وَاسْتَغْفِرُوا اللَّهَ ۚ إِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Topp, ngeen wéy [yéen waa Màkka] bëbb yéen itam fa nit ña bëbbee, jéggaluleen Yàlla. Yàlla Jéggalaakoon la te Jaglewaakoon la.
200فَإِذَا قَضَيْتُم مَّنَاسِكَكُمْ فَاذْكُرُوا اللَّهَ كَذِكْرِكُمْ آبَاءَكُمْ أَوْ أَشَدَّ ذِكْرًا ۗ فَمِنَ النَّاسِ مَن يَقُولُ رَبَّنَا آتِنَا فِي الدُّنْيَا وَمَا لَهُ فِي الْآخِرَةِ مِنْ خَلَاقٍ
Bu seen aj jeexee, nangeen di tuddu Yàlla kem na ngeen daan tuddee [taggee] seeni maam, walla sax tuddiin wu gën a tar. Am na ci nit ñi ñuy wax ne : “Yaw sunu Boroom! May nu àddina [kese] ! ” - te duñu fàggu dara ngir àllaaxira.
201وَمِنْهُم مَّن يَقُولُ رَبَّنَا آتِنَا فِي الدُّنْيَا حَسَنَةً وَفِي الْآخِرَةِ حَسَنَةً وَقِنَا عَذَابَ النَّارِ
Am na ci ñoom kuy wax ne : “Yaw sunu Boroom ! Defalnu xéewal ci àddina, ak ca àllaaxira ; te fegalnu mbugalum Safara ! ”.
202أُولَٰئِكَ لَهُمْ نَصِيبٌ مِّمَّا كَسَبُوا ۚ وَاللَّهُ سَرِيعُ الْحِسَابِ
Ñooña am na ñu yool ca la ñu sàkku. Te Yàlla ku gaaw la ci xayma [waññi, màndaxe].
203۞ وَاذْكُرُوا اللَّهَ فِي أَيَّامٍ مَّعْدُودَاتٍ ۚ فَمَن تَعَجَّلَ فِي يَوْمَيْنِ فَلَا إِثْمَ عَلَيْهِ وَمَن تَأَخَّرَ فَلَا إِثْمَ عَلَيْهِ ۚ لِمَنِ اتَّقَىٰ ۗ وَاتَّقُوا اللَّهَ وَاعْلَمُوا أَنَّكُمْ إِلَيْهِ تُحْشَرُونَ
Nangeen di fàttaliku Yàlla ci ay bis yuñu lim. Ku yàkkamti ba def ko ci ñaari fan du ca am bàkkaar, kay toog fa [Munaa] ñatti fan du ca am bàkkaar ci ku ragal Yàlla. Ragal-leen Yàlla te ngeen xam ne dees na leen fang [Jiital/gur-gur] jëme ci Moom.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
201Aaya

Tekki — Al-Baqara 201

Simoore Al-Baqara Aaya 201 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Am na ci ñoom kuy wax ne : “Yaw sunu…

Simoore Aaya 201/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 199–203. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers