Al-Baqara · 54/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَإِذْ قَالَ مُوسَىٰ لِقَوْمِهِ يَا قَوْمِ إِنَّكُمْ ظَلَمْتُمْ أَنفُسَكُم بِاتِّخَاذِكُمُ الْعِجْلَ فَتُوبُوا إِلَىٰ بَارِئِكُمْ فَاقْتُلُوا أَنفُسَكُمْ ذَٰلِكُمْ خَيْرٌ لَّكُمْ عِندَ بَارِئِكُمْ فَتَابَ عَلَيْكُمْ ۚ إِنَّهُ هُوَ التَّوَّابُ الرَّحِيمُ ۝٥٤
Wa iz qaala Moosaa liqawmihee yaa qawmi innakum zalamtum anfusakum bittikhaa zikumul `ijla fatoobooo ilaa Baari`ikum faqtulooo anfusakum zaalikum khairul lakum `inda Baari`ikum fataaba `alaikum; innahoo Huwat Tawwaabur Raheem
📖 Tekkim Wolof
Ak ba Muusaa waxee aw nitam : "Samaw nit, yéen tooñ ngeen seen bopp ci li ngeen jaamu yëkk wa. Na ngeen baalu seen Boroom; te ngeen reyante yéen [ñi bokkoon ci moy Yàlla googu] : Looloo gën ci yéen ca seen Boroom” !... Kon mu jéggal leen ndax moom mooy Jéggalaakoon ba, di Jaglewaakoon ba !

🎧 Dégg


📜 Aaya 52-56 — Al-Baqara

52ثُمَّ عَفَوْنَا عَنكُم مِّن بَعْدِ ذَٰلِكَ لَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ
Ginnaaw ga, Nu baal leen ndax ngeen gërëm [seen Boroom].
53وَإِذْ آتَيْنَا مُوسَى الْكِتَابَ وَالْفُرْقَانَ لَعَلَّكُمْ تَهْتَدُونَ
[Fàttalikuleen], ba Nu joxee Muusaa Téere ba ak Àtte yay téqale [dëgg ak fen] ndax ngeen gindiku.
54وَإِذْ قَالَ مُوسَىٰ لِقَوْمِهِ يَا قَوْمِ إِنَّكُمْ ظَلَمْتُمْ أَنفُسَكُم بِاتِّخَاذِكُمُ الْعِجْلَ فَتُوبُوا إِلَىٰ بَارِئِكُمْ فَاقْتُلُوا أَنفُسَكُمْ ذَٰلِكُمْ خَيْرٌ لَّكُمْ عِندَ بَارِئِكُمْ فَتَابَ عَلَيْكُمْ ۚ إِنَّهُ هُوَ التَّوَّابُ الرَّحِيمُ
Ak ba Muusaa waxee aw nitam : "Samaw nit, yéen tooñ ngeen seen bopp ci li ngeen jaamu yëkk wa. Na ngeen baalu seen Boroom; te ngeen reyante yéen [ñi bokkoon ci moy Yàlla googu] : Looloo gën ci yéen ca seen Boroom” !... Kon mu jéggal leen ndax moom mooy Jéggalaakoon ba, di Jaglewaakoon ba !
55وَإِذْ قُلْتُمْ يَا مُوسَىٰ لَن نُّؤْمِنَ لَكَ حَتَّىٰ نَرَى اللَّهَ جَهْرَةً فَأَخَذَتْكُمُ الصَّاعِقَةُ وَأَنتُمْ تَنظُرُونَ
Ak ba ngeen waxee ne : “ Yaw Muusaa, dunu la gëm ba ba nuy gis Yàlla ne jàkk ci Moom” !... Faf xaacu ga fàdd leen, ngeen di gis loolu.
56ثُمَّ بَعَثْنَاكُم مِّن بَعْدِ مَوْتِكُمْ لَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ
Topp Nu dekkal leen ginnaaw ba ngeen deewee, ndax Yàlla ngeen di sant [seen Boroom].
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
54Aaya

Tekki — Al-Baqara 54

Simoore Al-Baqara Aaya 54 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ak ba Muusaa waxee aw nitam : "Samaw nit, yéen…

Simoore Aaya 54/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 52–56. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers