Al-Baqara · 53/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَإِذْ آتَيْنَا مُوسَى الْكِتَابَ وَالْفُرْقَانَ لَعَلَّكُمْ تَهْتَدُونَ ۝٥٣
Wa iz aatainaa Moosal kitaaba wal Furqaana la`allakum tahtadoon
📖 Tekkim Wolof
[Fàttalikuleen], ba Nu joxee Muusaa Téere ba ak Àtte yay téqale [dëgg ak fen] ndax ngeen gindiku.
🎧 Dégg

📜 Aaya 51-55 — Al-Baqara

51وَإِذْ وَاعَدْنَا مُوسَىٰ أَرْبَعِينَ لَيْلَةً ثُمَّ اتَّخَذْتُمُ الْعِجْلَ مِن بَعْدِهِ وَأَنتُمْ ظَالِمُونَ
[Fàttalikuleen], ba Nu dëelanteek Muusaa ñeen-fukki guddi ! Te ngeen jaamu yëkk wa ginnaawam, ngeen di way-tooñ.
52ثُمَّ عَفَوْنَا عَنكُم مِّن بَعْدِ ذَٰلِكَ لَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ
Ginnaaw ga, Nu baal leen ndax ngeen gërëm [seen Boroom].
53وَإِذْ آتَيْنَا مُوسَى الْكِتَابَ وَالْفُرْقَانَ لَعَلَّكُمْ تَهْتَدُونَ
[Fàttalikuleen], ba Nu joxee Muusaa Téere ba ak Àtte yay téqale [dëgg ak fen] ndax ngeen gindiku.
54وَإِذْ قَالَ مُوسَىٰ لِقَوْمِهِ يَا قَوْمِ إِنَّكُمْ ظَلَمْتُمْ أَنفُسَكُم بِاتِّخَاذِكُمُ الْعِجْلَ فَتُوبُوا إِلَىٰ بَارِئِكُمْ فَاقْتُلُوا أَنفُسَكُمْ ذَٰلِكُمْ خَيْرٌ لَّكُمْ عِندَ بَارِئِكُمْ فَتَابَ عَلَيْكُمْ ۚ إِنَّهُ هُوَ التَّوَّابُ الرَّحِيمُ
Ak ba Muusaa waxee aw nitam : "Samaw nit, yéen tooñ ngeen seen bopp ci li ngeen jaamu yëkk wa. Na ngeen baalu seen Boroom; te ngeen reyante yéen [ñi bokkoon ci moy Yàlla googu] : Looloo gën ci yéen ca seen Boroom” !... Kon mu jéggal leen ndax moom mooy Jéggalaakoon ba, di Jaglewaakoon ba !
55وَإِذْ قُلْتُمْ يَا مُوسَىٰ لَن نُّؤْمِنَ لَكَ حَتَّىٰ نَرَى اللَّهَ جَهْرَةً فَأَخَذَتْكُمُ الصَّاعِقَةُ وَأَنتُمْ تَنظُرُونَ
Ak ba ngeen waxee ne : “ Yaw Muusaa, dunu la gëm ba ba nuy gis Yàlla ne jàkk ci Moom” !... Faf xaacu ga fàdd leen, ngeen di gis loolu.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
53Aaya

Tekki — Al-Baqara 53

Simoore Al-Baqara Aaya 53 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Fàttalikuleen], ba Nu joxee Muusaa Téere ba ak Àtte yay…

Simoore Aaya 53/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 51–55. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers