Al-Baqara · 55/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَإِذْ قُلْتُمْ يَا مُوسَىٰ لَن نُّؤْمِنَ لَكَ حَتَّىٰ نَرَى اللَّهَ جَهْرَةً فَأَخَذَتْكُمُ الصَّاعِقَةُ وَأَنتُمْ تَنظُرُونَ ۝٥٥
Wa iz qultum yaa Moosaa lan nu`mina laka hattaa naral laaha jahratan fa akhazat kumus saa`iqatu wa antum tanzuroon
📖 Tekkim Wolof
Ak ba ngeen waxee ne : “ Yaw Muusaa, dunu la gëm ba ba nuy gis Yàlla ne jàkk ci Moom” !... Faf xaacu ga fàdd leen, ngeen di gis loolu.
🎧 Dégg

📜 Aaya 53-57 — Al-Baqara

53وَإِذْ آتَيْنَا مُوسَى الْكِتَابَ وَالْفُرْقَانَ لَعَلَّكُمْ تَهْتَدُونَ
[Fàttalikuleen], ba Nu joxee Muusaa Téere ba ak Àtte yay téqale [dëgg ak fen] ndax ngeen gindiku.
54وَإِذْ قَالَ مُوسَىٰ لِقَوْمِهِ يَا قَوْمِ إِنَّكُمْ ظَلَمْتُمْ أَنفُسَكُم بِاتِّخَاذِكُمُ الْعِجْلَ فَتُوبُوا إِلَىٰ بَارِئِكُمْ فَاقْتُلُوا أَنفُسَكُمْ ذَٰلِكُمْ خَيْرٌ لَّكُمْ عِندَ بَارِئِكُمْ فَتَابَ عَلَيْكُمْ ۚ إِنَّهُ هُوَ التَّوَّابُ الرَّحِيمُ
Ak ba Muusaa waxee aw nitam : "Samaw nit, yéen tooñ ngeen seen bopp ci li ngeen jaamu yëkk wa. Na ngeen baalu seen Boroom; te ngeen reyante yéen [ñi bokkoon ci moy Yàlla googu] : Looloo gën ci yéen ca seen Boroom” !... Kon mu jéggal leen ndax moom mooy Jéggalaakoon ba, di Jaglewaakoon ba !
55وَإِذْ قُلْتُمْ يَا مُوسَىٰ لَن نُّؤْمِنَ لَكَ حَتَّىٰ نَرَى اللَّهَ جَهْرَةً فَأَخَذَتْكُمُ الصَّاعِقَةُ وَأَنتُمْ تَنظُرُونَ
Ak ba ngeen waxee ne : “ Yaw Muusaa, dunu la gëm ba ba nuy gis Yàlla ne jàkk ci Moom” !... Faf xaacu ga fàdd leen, ngeen di gis loolu.
56ثُمَّ بَعَثْنَاكُم مِّن بَعْدِ مَوْتِكُمْ لَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ
Topp Nu dekkal leen ginnaaw ba ngeen deewee, ndax Yàlla ngeen di sant [seen Boroom].
57وَظَلَّلْنَا عَلَيْكُمُ الْغَمَامَ وَأَنزَلْنَا عَلَيْكُمُ الْمَنَّ وَالسَّلْوَىٰ ۖ كُلُوا مِن طَيِّبَاتِ مَا رَزَقْنَاكُمْ ۖ وَمَا ظَلَمُونَا وَلَٰكِن كَانُوا أَنفُسَهُمْ يَظْلِمُونَ
Nu keral leen ak i niir, wàcceel leen lem ak i picc [yu tuddu gëméen], ne leen : - “Lekk leen ci lu sell lii Nu leen xéewale ! ” - Ñoom daal seen bopp lañuy tooñ, waaye du Nun lañuy tooñ.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
55Aaya

Tekki — Al-Baqara 55

Simoore Al-Baqara Aaya 55 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ak ba ngeen waxee ne : “ Yaw Muusaa, dunu…

Simoore Aaya 55/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 53–57. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers