Aali Imran · 50/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
وَمُصَدِّقًا لِّمَا بَيْنَ يَدَيَّ مِنَ التَّوْرَاةِ وَلِأُحِلَّ لَكُم بَعْضَ الَّذِي حُرِّمَ عَلَيْكُمْ ۚ وَجِئْتُكُم بِآيَةٍ مِّن رَّبِّكُمْ فَاتَّقُوا اللَّهَ وَأَطِيعُونِ ۝٥٠
Wa musaddiqal limaa baina yadaiya minat Tawraati wa liuhilla lakum ba`dal lazee hurrima `alaikum; wa ji`tukum bi Aayatim mir Rabbikum fattaqul laaha wa atee`oon
📖 Tekkim Wolof
May dëggal li ma jiitu [Tawreet], ma di leen daganalal lennat ca ya ñu araamaloon ci yéen. Indil naa leen kàddu gu bawoo ca seen Boroom. Ragal-leen Yàlla te topp ko.

🎧 Dégg


📜 Aaya 48-52 — Aali Imran

48وَيُعَلِّمُهُ الْكِتَابَ وَالْحِكْمَةَ وَالتَّوْرَاةَ وَالْإِنجِيلَ
“Dana ko jàngal téere ba, xam-xamu ràññee, Tawreet ak Injiil,
49وَرَسُولًا إِلَىٰ بَنِي إِسْرَائِيلَ أَنِّي قَدْ جِئْتُكُم بِآيَةٍ مِّن رَّبِّكُمْ ۖ أَنِّي أَخْلُقُ لَكُم مِّنَ الطِّينِ كَهَيْئَةِ الطَّيْرِ فَأَنفُخُ فِيهِ فَيَكُونُ طَيْرًا بِإِذْنِ اللَّهِ ۖ وَأُبْرِئُ الْأَكْمَهَ وَالْأَبْرَصَ وَأُحْيِي الْمَوْتَىٰ بِإِذْنِ اللَّهِ ۖ وَأُنَبِّئُكُم بِمَا تَأْكُلُونَ وَمَا تَدَّخِرُونَ فِي بُيُوتِكُمْ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَةً لَّكُمْ إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ
dana ko def Yonent ci Banii-Israayiil, [mu wax leen ne]: “Man mii, indil naa leen ay màndarga yu bawoo ca seen Boroom. Mën naa leen defaral ci ban bi jëmmi picc, ëf ko mu nekk picc, muy dundu ci coobare Yàlla. Danaa faj ku judduwaale gumba ak ku gaana, danaa dundal [dekkal] ku dee ci coobare Yàlla. Mën naa leen xamal la ngeen di lekk ak la ngeen denc ca seeni kër. Loolu war na leen a yéem [waar], ndegam ñu gëm ngeen !
50وَمُصَدِّقًا لِّمَا بَيْنَ يَدَيَّ مِنَ التَّوْرَاةِ وَلِأُحِلَّ لَكُم بَعْضَ الَّذِي حُرِّمَ عَلَيْكُمْ ۚ وَجِئْتُكُم بِآيَةٍ مِّن رَّبِّكُمْ فَاتَّقُوا اللَّهَ وَأَطِيعُونِ
May dëggal li ma jiitu [Tawreet], ma di leen daganalal lennat ca ya ñu araamaloon ci yéen. Indil naa leen kàddu gu bawoo ca seen Boroom. Ragal-leen Yàlla te topp ko.
51إِنَّ اللَّهَ رَبِّي وَرَبُّكُمْ فَاعْبُدُوهُ ۗ هَٰذَا صِرَاطٌ مُّسْتَقِيمٌ
Yàlla miy sama Boroom di seen Boroom. Jaamuleen ko : lii mooy yoon wu jub xocc wi.”
52۞ فَلَمَّا أَحَسَّ عِيسَىٰ مِنْهُمُ الْكُفْرَ قَالَ مَنْ أَنصَارِي إِلَى اللَّهِ ۖ قَالَ الْحَوَارِيُّونَ نَحْنُ أَنصَارُ اللَّهِ آمَنَّا بِاللَّهِ وَاشْهَدْ بِأَنَّا مُسْلِمُونَ
Ba Iisaa ràññee ca ñoom gëmëdi, la daldi wax ne : “Waaw ana kan moo may dimbali ci liggéeyal Yàlla ? ” Gaa yu sell ya ne ko : “Nun noo lay dimbali ci yoonu Yàlla. Gëm nanu Yàlla. Seedeel ne nun way-wommatu lanu [jëm ci Yàlla].
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
50Aaya

Tekki — Aali Imran 50

Simoore Aali Imran Aaya 50 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : May dëggal li ma jiitu [Tawreet], ma di leen daganalal…

Simoore Aaya 50/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 48–52. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers