Aali Imran · 9/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
رَبَّنَا إِنَّكَ جَامِعُ النَّاسِ لِيَوْمٍ لَّا رَيْبَ فِيهِ ۚ إِنَّ اللَّهَ لَا يُخْلِفُ الْمِيعَادَ ۝٩
Rabbanaaa innaka jaami `un-naasi li Yawmil laa raibafeeh; innal laaha laa yukhliful mee`aad
📖 Tekkim Wolof
Sunu Boroom ! Yaw yaa di dajale nit ñi ci bis boo xam ne - sikk nekkul ci ag ñëwam - Yàlla, du wuute dige ba.

🎧 Dégg


📜 Aaya 7-11 — Simoore Aali Imran

7هُوَ الَّذِي أَنزَلَ عَلَيْكَ الْكِتَابَ مِنْهُ آيَاتٌ مُّحْكَمَاتٌ هُنَّ أُمُّ الْكِتَابِ وَأُخَرُ مُتَشَابِهَاتٌ ۖ فَأَمَّا الَّذِينَ فِي قُلُوبِهِمْ زَيْغٌ فَيَتَّبِعُونَ مَا تَشَابَهَ مِنْهُ ابْتِغَاءَ الْفِتْنَةِ وَابْتِغَاءَ تَأْوِيلِهِ ۗ وَمَا يَعْلَمُ تَأْوِيلَهُ إِلَّا اللَّهُ ۗ وَالرَّاسِخُونَ فِي الْعِلْمِ يَقُولُونَ آمَنَّا بِهِ كُلٌّ مِّنْ عِندِ رَبِّنَا ۗ وَمَا يَذَّكَّرُ إِلَّا أُولُو الْأَلْبَابِ
Moom moo wàcce ci yaw Téere ba : am na ca ay laaya seen maanaa leer nañu, ñoo di cosaani àtte yi, ak yeneeni laaya yu seeni maanaa fésul. Ña nga xam ne jeng a nekk seeni xol, benn ca laaya yooyu lañuy topp ngir sàkku fitna ak jéem leen a firi, te Yàlla doŋŋ a xam seeni piri ak ña sax ci xam-xam. Danañu wax ne : “Gëm nanu ko : lépp ca sunu Boroom la bawoo ! ” Woroom xel yi rekk ay waaru.
8رَبَّنَا لَا تُزِغْ قُلُوبَنَا بَعْدَ إِذْ هَدَيْتَنَا وَهَبْ لَنَا مِن لَّدُنكَ رَحْمَةً ۚ إِنَّكَ أَنتَ الْوَهَّابُ
“Yaw sunu Boroom ! yàlla boo jengal sunuy xol ginnaaw ba nga nu gindee ; te may nu yërmaande ju bawoo ci yaw. Yaw de yaa di Mayewaakoon bi !
9رَبَّنَا إِنَّكَ جَامِعُ النَّاسِ لِيَوْمٍ لَّا رَيْبَ فِيهِ ۚ إِنَّ اللَّهَ لَا يُخْلِفُ الْمِيعَادَ
Sunu Boroom ! Yaw yaa di dajale nit ñi ci bis boo xam ne - sikk nekkul ci ag ñëwam - Yàlla, du wuute dige ba.
10إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا لَن تُغْنِيَ عَنْهُمْ أَمْوَالُهُمْ وَلَا أَوْلَادُهُم مِّنَ اللَّهِ شَيْئًا ۖ وَأُولَٰئِكَ هُمْ وَقُودُ النَّارِ
Ña weddi, seen alal ya ak seen njaboot ya duleen fegal dara ca Yàlla. Te ñoom ñoo di mattum Safara,
11كَدَأْبِ آلِ فِرْعَوْنَ وَالَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ ۚ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا فَأَخَذَهُمُ اللَّهُ بِذُنُوبِهِمْ ۗ وَاللَّهُ شَدِيدُ الْعِقَابِ
lu mel ni aadaay nitu Firawna ak ña leen jiitu woon, weddi woon Sunuy laaya. Yàlla jàppe leen seeni bàkkaar. Te Yàlla di ku tar mbugal.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
9Aaya

Tekki — Aali Imran 9

Simoore Aali Imran Aaya 9 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Sunu Boroom ! Yaw yaa di dajale nit ñi ci…

Simoore Aaya 9/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 7–11. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers