Fatir · 36/45
Tekki Waxtaan — Fatir
وَالَّذِينَ كَفَرُوا لَهُمْ نَارُ جَهَنَّمَ لَا يُقْضَىٰ عَلَيْهِمْ فَيَمُوتُوا وَلَا يُخَفَّفُ عَنْهُم مِّنْ عَذَابِهَا ۚ كَذَٰلِكَ نَجْزِي كُلَّ كَفُورٍ ۝٣٦
Wallazeena kafaroo lahum naaru Jahannama laa yuqdaa `alaihim fa yamootoo wa laa yukhaffafu `anhum min `azaabihaa; kazaalika najzee kulla kafoor
📖 Tekkim Wolof
Ñay weddi nag, ñoom Safara la ñuy dëkk : ñu di leen xorñoññal, duñu dee ; te it deesuleen woyofalal mbugal ma. Noonu la Nuy feye képp ku di ab weddiwaakoon.
🎧 Dégg

📜 Aaya 34-38 — Fatir

34وَقَالُوا الْحَمْدُ لِلَّهِ الَّذِي أَذْهَبَ عَنَّا الْحَزَنَ ۖ إِنَّ رَبَّنَا لَغَفُورٌ شَكُورٌ
Ñuy wax naan : “Xeeti cant yi ñeel na Yàlla, Yàlla mi nu dàqal tiitaange. Sunu Boroom daal Jéggalaakoon la buy Yayoowaakoonu cant.
35الَّذِي أَحَلَّنَا دَارَ الْمُقَامَةِ مِن فَضْلِهِ لَا يَمَسُّنَا فِيهَا نَصَبٌ وَلَا يَمَسُّنَا فِيهَا لُغُوبٌ
Moom mi nu dalal ci kërug nooflaay ci mbaaxam, coono dunu fa dab, jaaxle it dunuu fa dab”.
36وَالَّذِينَ كَفَرُوا لَهُمْ نَارُ جَهَنَّمَ لَا يُقْضَىٰ عَلَيْهِمْ فَيَمُوتُوا وَلَا يُخَفَّفُ عَنْهُم مِّنْ عَذَابِهَا ۚ كَذَٰلِكَ نَجْزِي كُلَّ كَفُورٍ
Ñay weddi nag, ñoom Safara la ñuy dëkk : ñu di leen xorñoññal, duñu dee ; te it deesuleen woyofalal mbugal ma. Noonu la Nuy feye képp ku di ab weddiwaakoon.
37وَهُمْ يَصْطَرِخُونَ فِيهَا رَبَّنَا أَخْرِجْنَا نَعْمَلْ صَالِحًا غَيْرَ الَّذِي كُنَّا نَعْمَلُ ۚ أَوَلَمْ نُعَمِّرْكُم مَّا يَتَذَكَّرُ فِيهِ مَن تَذَكَّرَ وَجَاءَكُمُ النَّذِيرُ ۖ فَذُوقُوا فَمَا لِلظَّالِمِينَ مِن نَّصِيرٍ
Ña ngay yuuxu ca biir, di wax naan : “Yaw sunu Boroom, génne nu ; kon dey dananu jëf u yiw, wu bokkul ak la ñu daan jëf ”. “Waaw, moo ndax dundalunuleen fa woon diir bu tax, ña fàttaliku ñépp, fàttaliku nañu ca ? Te ay xuppekat it dëkkaloon nañu leen. Kon book, toqamtikuleen mbugal mi. Tooñkat yi, kenn duleen dimbali”.
38إِنَّ اللَّهَ عَالِمُ غَيْبِ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ إِنَّهُ عَلِيمٌ بِذَاتِ الصُّدُورِ
Yàllaa xam kumpag asamaan yeek suuf si. Moom ab Xamaakoon la li nekk ci dënn yi .
FatirFihi Alxuraan
45Aaya
MeccanRevelation
36Aaya

Tekki — Fatir 36

Simoore Fatir Aaya 36 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñay weddi nag, ñoom Safara la ñuy dëkk : ñu…

Simoore Aaya 36/45 — Fatir فاطر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Fatir Dégg, Fatir Tekki, Fatir mp3, Fatir pdf. Aaya 34–38. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers