An-Nisa · 125/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
وَمَنْ أَحْسَنُ دِينًا مِّمَّنْ أَسْلَمَ وَجْهَهُ لِلَّهِ وَهُوَ مُحْسِنٌ وَاتَّبَعَ مِلَّةَ إِبْرَاهِيمَ حَنِيفًا ۗ وَاتَّخَذَ اللَّهُ إِبْرَاهِيمَ خَلِيلًا ۝١٢٥
Wa man ahsanu deenam mimmman aslama wajhahoo lillaahi wa huwa muhsinunw wattaba`a Millata Ibraaheema haneefaa; wattakhazal laahu Ibraaheema khaleelaa
📖 Tekkim Wolof
Ana ku gën a rafet diine ku jubale boppam Yàlla, te di kuy rafetal [jëfam], tey roy diiney Ibraahiima cig wéetal Yàlla ? Te Yàlla Moom jàppe na Ibraahiima soppeem.

🎧 Dégg


📜 Aaya 123-127 — An-Nisa

123لَّيْسَ بِأَمَانِيِّكُمْ وَلَا أَمَانِيِّ أَهْلِ الْكِتَابِ ۗ مَن يَعْمَلْ سُوءًا يُجْزَ بِهِ وَلَا يَجِدْ لَهُ مِن دُونِ اللَّهِ وَلِيًّا وَلَا نَصِيرًا
Mbir ma ajuwul ci seeni mébét walla ci mébétu ña jotoon Téere. Waaye ku def ñaawtéef, jot peyam, kenn du ko mën a amal kilifa gu ko yiir mbaa mu ko mën a dimbali ginnaaw bu ca Yàlla génnee.
124وَمَن يَعْمَلْ مِنَ الصَّالِحَاتِ مِن ذَكَرٍ أَوْ أُنثَىٰ وَهُوَ مُؤْمِنٌ فَأُولَٰئِكَ يَدْخُلُونَ الْجَنَّةَ وَلَا يُظْلَمُونَ نَقِيرًا
Ku jëf, jëf ju bokk ci aw yiw, di góor mbaa muy jigéen, te di ab jullit... ñooña danañu dugg Àjjana; te kenn duleen ca tooñ [ba waññil leen] lu toll ni mboxosu xooxu tàndarma.
125وَمَنْ أَحْسَنُ دِينًا مِّمَّنْ أَسْلَمَ وَجْهَهُ لِلَّهِ وَهُوَ مُحْسِنٌ وَاتَّبَعَ مِلَّةَ إِبْرَاهِيمَ حَنِيفًا ۗ وَاتَّخَذَ اللَّهُ إِبْرَاهِيمَ خَلِيلًا
Ana ku gën a rafet diine ku jubale boppam Yàlla, te di kuy rafetal [jëfam], tey roy diiney Ibraahiima cig wéetal Yàlla ? Te Yàlla Moom jàppe na Ibraahiima soppeem.
126وَلِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ بِكُلِّ شَيْءٍ مُّحِيطًا
Yàllaa moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Te Yàlla lépp la peeg.
127وَيَسْتَفْتُونَكَ فِي النِّسَاءِ ۖ قُلِ اللَّهُ يُفْتِيكُمْ فِيهِنَّ وَمَا يُتْلَىٰ عَلَيْكُمْ فِي الْكِتَابِ فِي يَتَامَى النِّسَاءِ اللَّاتِي لَا تُؤْتُونَهُنَّ مَا كُتِبَ لَهُنَّ وَتَرْغَبُونَ أَن تَنكِحُوهُنَّ وَالْمُسْتَضْعَفِينَ مِنَ الْوِلْدَانِ وَأَن تَقُومُوا لِلْيَتَامَىٰ بِالْقِسْطِ ۚ وَمَا تَفْعَلُوا مِنْ خَيْرٍ فَإِنَّ اللَّهَ كَانَ بِهِ عَلِيمًا
Ña nga lay laaj nga ubbee leen ci jigéen ñi. Neel : “Yàlla Dana leen ubbee ci ñoom, ak lañu leen jàngal ca Téere ba [di leeral lu jëm ci] jirim yu jigéen yi nga xam ne joxooleen leen la ñu digle ci ñoom, te ngeen xemmem takk leen, [ak leeral lu jëm ca] ñu néew doole ña ci xale yi”. [Ak di leen digal] ngeen taxawu jirim ci ag maandute. Lu ngeen ca def ci ñoom ci lu baax, Yàlla xam na ko.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
125Aaya

Tekki — An-Nisa 125

Simoore An-Nisa Aaya 125 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ana ku gën a rafet diine ku jubale boppam Yàlla,…

Simoore Aaya 125/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 123–127. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers