An-Nisa · 136/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا آمِنُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ وَالْكِتَابِ الَّذِي نَزَّلَ عَلَىٰ رَسُولِهِ وَالْكِتَابِ الَّذِي أَنزَلَ مِن قَبْلُ ۚ وَمَن يَكْفُرْ بِاللَّهِ وَمَلَائِكَتِهِ وَكُتُبِهِ وَرُسُلِهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ فَقَدْ ضَلَّ ضَلَالًا بَعِيدًا ۝١٣٦
Yaaa aiyuhal lazeena aamanooo aaminoo billaahi wa Rasoolihee wal Kitaabil lazee nazzala `alaa Rasoolihee wal Kitaabil lazeee anzala min qabl; wa mai yakfur billaahi wa Malaaa`ikatihee wa Kutubihee wa Rusulihee wal Yawmil Aakhiri faqad dalla dalaalam ba`eedaa
📖 Tekkim Wolof
Éy yéen ñi gëm ! Doyluleen Yàlla ak ub Yonentam, ak Téere ba Mu wàcce ci Yonentam, ak Téere ba wàcc la jiitu. Képp ku weddi Yàlla, ak i Malaakaam, ak Yonentam, ak Bis-pénc ba, réer na réer gu sori [dëgg].

🎧 Dégg


📜 Aaya 134-138 — An-Nisa

134مَّن كَانَ يُرِيدُ ثَوَابَ الدُّنْيَا فَعِندَ اللَّهِ ثَوَابُ الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ سَمِيعًا بَصِيرًا
Koo xam ne yoolu àddina bi la bëgg, [na xam ne] Yàlla am na lu mu yoole ci àddina ak ca àllaaxira. Te Yàlla Kuy dégg la, Kuy gis la.
135۞ يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا كُونُوا قَوَّامِينَ بِالْقِسْطِ شُهَدَاءَ لِلَّهِ وَلَوْ عَلَىٰ أَنفُسِكُمْ أَوِ الْوَالِدَيْنِ وَالْأَقْرَبِينَ ۚ إِن يَكُنْ غَنِيًّا أَوْ فَقِيرًا فَاللَّهُ أَوْلَىٰ بِهِمَا ۖ فَلَا تَتَّبِعُوا الْهَوَىٰ أَن تَعْدِلُوا ۚ وَإِن تَلْوُوا أَوْ تُعْرِضُوا فَإِنَّ اللَّهَ كَانَ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرًا
Éy yéen ñi gëm ! Taxawleen temm ci maandute, di seede ngir Yàlla doonte seede soosu [lu naqari la] luy dal ci seen kaw, walla ci seeni waajur, walla ci kaw seeni njaboot, walla seeni jegeñaale. Su dee ku woomal la walla ku ñàkk, Yàllaay ki gën pey ci ñoom ñaar ñépp. Buleen topp seeni bànneex ba ñàkk a maandu. Bu ngeen jéggalee [seede] walla ngeen dëddu bañ a seede, xamleen ne Yàlla Ku deñ-kumpa la ci li ngeen def.
136يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا آمِنُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ وَالْكِتَابِ الَّذِي نَزَّلَ عَلَىٰ رَسُولِهِ وَالْكِتَابِ الَّذِي أَنزَلَ مِن قَبْلُ ۚ وَمَن يَكْفُرْ بِاللَّهِ وَمَلَائِكَتِهِ وَكُتُبِهِ وَرُسُلِهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ فَقَدْ ضَلَّ ضَلَالًا بَعِيدًا
Éy yéen ñi gëm ! Doyluleen Yàlla ak ub Yonentam, ak Téere ba Mu wàcce ci Yonentam, ak Téere ba wàcc la jiitu. Képp ku weddi Yàlla, ak i Malaakaam, ak Yonentam, ak Bis-pénc ba, réer na réer gu sori [dëgg].
137إِنَّ الَّذِينَ آمَنُوا ثُمَّ كَفَرُوا ثُمَّ آمَنُوا ثُمَّ كَفَرُوا ثُمَّ ازْدَادُوا كُفْرًا لَّمْ يَكُنِ اللَّهُ لِيَغْفِرَ لَهُمْ وَلَا لِيَهْدِيَهُمْ سَبِيلًا
Ña nga xam ne dañoo gëm ba noppi weddi, daldi gëm, weddiwaat, seenug weddi di gën a tar, Yàlla duleen jéggal, te it duleen gindi teg leen ci yoon wu leer wa.
138بَشِّرِ الْمُنَافِقِينَ بِأَنَّ لَهُمْ عَذَابًا أَلِيمًا
Bégalal [xamalal] naaféq ya ci ne am nañu mbugal mu metti,
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
136Aaya

Tekki — An-Nisa 136

Simoore An-Nisa Aaya 136 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Éy yéen ñi gëm ! Doyluleen Yàlla ak ub Yonentam,…

Simoore Aaya 136/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 134–138. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers