Al-Maida · 109/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
۞ يَوْمَ يَجْمَعُ اللَّهُ الرُّسُلَ فَيَقُولُ مَاذَا أُجِبْتُمْ ۖ قَالُوا لَا عِلْمَ لَنَا ۖ إِنَّكَ أَنتَ عَلَّامُ الْغُيُوبِ ۝١٠٩
yawma yajma`ul laahur Rusula fa yaqoolu maazaaa ujibtum qaaloo laa `ilma lanaa innaka Anta `Allaamul Ghuyoob
📖 Tekkim Wolof
Bis bu Yàlla dajalee Yonent ya, ne leen : “Lu ñu leen toontu ? ” Ñu ne Ko : “Amunu xam-xam : Yaw yaay ki xam kumpa”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 107-111 — Al-Maida

107فَإِنْ عُثِرَ عَلَىٰ أَنَّهُمَا اسْتَحَقَّا إِثْمًا فَآخَرَانِ يَقُومَانِ مَقَامَهُمَا مِنَ الَّذِينَ اسْتَحَقَّ عَلَيْهِمُ الْأَوْلَيَانِ فَيُقْسِمَانِ بِاللَّهِ لَشَهَادَتُنَا أَحَقُّ مِن شَهَادَتِهِمَا وَمَا اعْتَدَيْنَا إِنَّا إِذًا لَّمِنَ الظَّالِمِينَ
Bu ñu xamee ne ñoom ñaar waxuñu dëgg, kon ñeneen ñaar wuutu leen, ñu di ña gën a nekk i jegeñaale [néew ba], ñu giñ ci Yàlla ne : “Sunu seede moo gën a dëggu sunu bos te jalgatiwunu. Nde kon nu bokk ci way-tooñ ña”.
108ذَٰلِكَ أَدْنَىٰ أَن يَأْتُوا بِالشَّهَادَةِ عَلَىٰ وَجْهِهَا أَوْ يَخَافُوا أَن تُرَدَّ أَيْمَانٌ بَعْدَ أَيْمَانِهِمْ ۗ وَاتَّقُوا اللَّهَ وَاسْمَعُوا ۗ وَاللَّهُ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الْفَاسِقِينَ
Loolooy tax ña giñ joxe seede su dëggu ; mbaa ñu ragal ñu dàq seeni seede ginnaaw ba ñu defee seede su [dëng]. Te nangeen ragal Yàlla tey dégg [ndigal]. Yàlla du gindi nit ñu di ay saay-saay [ñu génn ci topp].
109۞ يَوْمَ يَجْمَعُ اللَّهُ الرُّسُلَ فَيَقُولُ مَاذَا أُجِبْتُمْ ۖ قَالُوا لَا عِلْمَ لَنَا ۖ إِنَّكَ أَنتَ عَلَّامُ الْغُيُوبِ
Bis bu Yàlla dajalee Yonent ya, ne leen : “Lu ñu leen toontu ? ” Ñu ne Ko : “Amunu xam-xam : Yaw yaay ki xam kumpa”.
110إِذْ قَالَ اللَّهُ يَا عِيسَى ابْنَ مَرْيَمَ اذْكُرْ نِعْمَتِي عَلَيْكَ وَعَلَىٰ وَالِدَتِكَ إِذْ أَيَّدتُّكَ بِرُوحِ الْقُدُسِ تُكَلِّمُ النَّاسَ فِي الْمَهْدِ وَكَهْلًا ۖ وَإِذْ عَلَّمْتُكَ الْكِتَابَ وَالْحِكْمَةَ وَالتَّوْرَاةَ وَالْإِنجِيلَ ۖ وَإِذْ تَخْلُقُ مِنَ الطِّينِ كَهَيْئَةِ الطَّيْرِ بِإِذْنِي فَتَنفُخُ فِيهَا فَتَكُونُ طَيْرًا بِإِذْنِي ۖ وَتُبْرِئُ الْأَكْمَهَ وَالْأَبْرَصَ بِإِذْنِي ۖ وَإِذْ تُخْرِجُ الْمَوْتَىٰ بِإِذْنِي ۖ وَإِذْ كَفَفْتُ بَنِي إِسْرَائِيلَ عَنكَ إِذْ جِئْتَهُم بِالْبَيِّنَاتِ فَقَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا مِنْهُمْ إِنْ هَٰذَا إِلَّا سِحْرٌ مُّبِينٌ
[Fàttalikul] ba Yàlla nee : "Yaw Iisaa, doomi Maryaama, fàttalikul xéewal ya Ma la defal yaak sa yaay ba Ma la dimbalee boole la ak Ruu gu sell ga [Jibriil]. Ba nga wax ak nit ñi fekk yaa ngi nekk liir ak ba nga nekkee mag mu weesu ndaw. [Fàttalikul it] ba Ma la jàngalee Téere ba ak gis-gis bu ubbiku, ak Tawreet ak Linjiil ! [Fàttalikul it] ba ngay sos ci ban lu ame melow njanaaw ; ci Sama coobare nga ëf ca. Mu nekk njanaaw ci sama coobare. Te ngay wéral ku gumba ak ku gaana, ci Sama coobare. Ak di génne ku dee [ci bàmmeel] ci Sama coobare ak ci li Ma la fegal waa Bani-Israayiil [ñu bañ laa lor] ba nga leen indilee lay yu leer ya. Te ña weddi ca ñoom ne leen : “Nekkul lu dul njibar gu bir”.
111وَإِذْ أَوْحَيْتُ إِلَى الْحَوَارِيِّينَ أَنْ آمِنُوا بِي وَبِرَسُولِي قَالُوا آمَنَّا وَاشْهَدْ بِأَنَّنَا مُسْلِمُونَ
Fàttalikul ba nu xiiree sa taalibe ya [waaraatekat ya], sol ci seeni xol ne leen: “Gëmleen Ma ak Sama Yonent”. Ñu ne : “Gëm nanu ; te Nanga seede ne nun way-wommatu lanu [jullit lanu]”.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
109Aaya

Tekki — Al-Maida 109

Simoore Al-Maida Aaya 109 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bis bu Yàlla dajalee Yonent ya, ne leen : “Lu…

Simoore Aaya 109/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 107–111. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers