Al-Maida · 115/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
قَالَ اللَّهُ إِنِّي مُنَزِّلُهَا عَلَيْكُمْ ۖ فَمَن يَكْفُرْ بَعْدُ مِنكُمْ فَإِنِّي أُعَذِّبُهُ عَذَابًا لَّا أُعَذِّبُهُ أَحَدًا مِّنَ الْعَالَمِينَ ۝١١٥
Waalal laahu innee munaz ziluhaa `alaikum faman yakfur ba`du minkum fa inneee u`azzibuhoo `azaabal laaa u`azzibuhooo ahadam minal `aalameen
📖 Tekkim Wolof
Yàlla toontu ne : “Maa ngi koy wàcce ci yéen. Waaye ku weddi ci yéen ginnaaw loolu, Dinaa ko mbugale noo xam ne mësuma koo mbugale kenn ci àdduna bi.”
🎧 Dégg

📜 Aaya 113-117 — Al-Maida

113قَالُوا نُرِيدُ أَن نَّأْكُلَ مِنْهَا وَتَطْمَئِنَّ قُلُوبُنَا وَنَعْلَمَ أَن قَدْ صَدَقْتَنَا وَنَكُونَ عَلَيْهَا مِنَ الشَّاهِدِينَ
Ñu ne : “Danoo bëgg lekk ci moom [ndën la] ndax sunu xel dal, nu daldi xam ne wax nga dëgg te kon nun dananu seede loolu”.
114قَالَ عِيسَى ابْنُ مَرْيَمَ اللَّهُمَّ رَبَّنَا أَنزِلْ عَلَيْنَا مَائِدَةً مِّنَ السَّمَاءِ تَكُونُ لَنَا عِيدًا لِّأَوَّلِنَا وَآخِرِنَا وَآيَةً مِّنكَ ۖ وَارْزُقْنَا وَأَنتَ خَيْرُ الرَّازِقِينَ
isaa doomu Maryaama ne : "Yaw sama Boroom, wàcceel ci nun taabal [ndën lu am ñam] mu jóge asamaan, mu nekk ci nun xew-xewu mbégte, mu ñeel ku jëkk ak ku mujj ci nun, te it muy kéemaan gu tukkee ci Yaw. Defal nu ko : Yaa di gën gi xéewalaakoon buy joxe wërsëg.”
115قَالَ اللَّهُ إِنِّي مُنَزِّلُهَا عَلَيْكُمْ ۖ فَمَن يَكْفُرْ بَعْدُ مِنكُمْ فَإِنِّي أُعَذِّبُهُ عَذَابًا لَّا أُعَذِّبُهُ أَحَدًا مِّنَ الْعَالَمِينَ
Yàlla toontu ne : “Maa ngi koy wàcce ci yéen. Waaye ku weddi ci yéen ginnaaw loolu, Dinaa ko mbugale noo xam ne mësuma koo mbugale kenn ci àdduna bi.”
116وَإِذْ قَالَ اللَّهُ يَا عِيسَى ابْنَ مَرْيَمَ أَأَنتَ قُلْتَ لِلنَّاسِ اتَّخِذُونِي وَأُمِّيَ إِلَٰهَيْنِ مِن دُونِ اللَّهِ ۖ قَالَ سُبْحَانَكَ مَا يَكُونُ لِي أَنْ أَقُولَ مَا لَيْسَ لِي بِحَقٍّ ۚ إِن كُنتُ قُلْتُهُ فَقَدْ عَلِمْتَهُ ۚ تَعْلَمُ مَا فِي نَفْسِي وَلَا أَعْلَمُ مَا فِي نَفْسِكَ ۚ إِنَّكَ أَنتَ عَلَّامُ الْغُيُوبِ
(Fàttalikul) ba Yàlla nee : "Yaw Iisaa, doomu Maryaama, moo ndax yaw yaa wax nit ñi ne : “Jàppeleen ma, maak sama yaay, nu di ñaari yàlla, beddi Yàlla ? ”. Mu toontu [moom Iisaa, doomu Maryaama] ne ko : “Tudd naa sag sell ! Yellul ci man may wax lu dul dëgg ! Su fekkee maa ko wax, xam nga ci dara. Ndax Yaw xam nga li nekk ci man, te man xamuma li nekk fi Yaw. Te Yaw yaay Xamaakoonu kumpa yi.
117مَا قُلْتُ لَهُمْ إِلَّا مَا أَمَرْتَنِي بِهِ أَنِ اعْبُدُوا اللَّهَ رَبِّي وَرَبَّكُمْ ۚ وَكُنتُ عَلَيْهِمْ شَهِيدًا مَّا دُمْتُ فِيهِمْ ۖ فَلَمَّا تَوَفَّيْتَنِي كُنتَ أَنتَ الرَّقِيبَ عَلَيْهِمْ ۚ وَأَنتَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ شَهِيدٌ
Waxumaleen lu dul li nga digle ci loolu, ne leen : “Jaamuleen Yàlla, miy sama Boroom, di seen Boroom”. Ma nekk seede ci ñoom, fekk maa nga nekkoon ca seen biir. Ba nga ma yóbboo ci Yaw [jële ma fa], Yaw yaa leen doon fuglu [nemmiku]. Te sax Yaw yaay Aji-seede ci lépp.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
115Aaya

Tekki — Al-Maida 115

Simoore Al-Maida Aaya 115 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla toontu ne : “Maa ngi koy wàcce ci yéen.…

Simoore Aaya 115/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 113–117. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers