Al-Maida · 118/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
إِن تُعَذِّبْهُمْ فَإِنَّهُمْ عِبَادُكَ ۖ وَإِن تَغْفِرْ لَهُمْ فَإِنَّكَ أَنتَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ ۝١١٨
In tu`azzibhum fa innahum ibaaduka wa in taghfir lahum fa innaka Antal `Azzezul Hakeem
📖 Tekkim Wolof
Boo leen mbugalee, say jaam lañu. Boo leen jéggalee it, Yaw yaa di Aji-not ji, di Ku xereñ [ci say àtte]”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 116-120 — Al-Maida

116وَإِذْ قَالَ اللَّهُ يَا عِيسَى ابْنَ مَرْيَمَ أَأَنتَ قُلْتَ لِلنَّاسِ اتَّخِذُونِي وَأُمِّيَ إِلَٰهَيْنِ مِن دُونِ اللَّهِ ۖ قَالَ سُبْحَانَكَ مَا يَكُونُ لِي أَنْ أَقُولَ مَا لَيْسَ لِي بِحَقٍّ ۚ إِن كُنتُ قُلْتُهُ فَقَدْ عَلِمْتَهُ ۚ تَعْلَمُ مَا فِي نَفْسِي وَلَا أَعْلَمُ مَا فِي نَفْسِكَ ۚ إِنَّكَ أَنتَ عَلَّامُ الْغُيُوبِ
(Fàttalikul) ba Yàlla nee : "Yaw Iisaa, doomu Maryaama, moo ndax yaw yaa wax nit ñi ne : “Jàppeleen ma, maak sama yaay, nu di ñaari yàlla, beddi Yàlla ? ”. Mu toontu [moom Iisaa, doomu Maryaama] ne ko : “Tudd naa sag sell ! Yellul ci man may wax lu dul dëgg ! Su fekkee maa ko wax, xam nga ci dara. Ndax Yaw xam nga li nekk ci man, te man xamuma li nekk fi Yaw. Te Yaw yaay Xamaakoonu kumpa yi.
117مَا قُلْتُ لَهُمْ إِلَّا مَا أَمَرْتَنِي بِهِ أَنِ اعْبُدُوا اللَّهَ رَبِّي وَرَبَّكُمْ ۚ وَكُنتُ عَلَيْهِمْ شَهِيدًا مَّا دُمْتُ فِيهِمْ ۖ فَلَمَّا تَوَفَّيْتَنِي كُنتَ أَنتَ الرَّقِيبَ عَلَيْهِمْ ۚ وَأَنتَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ شَهِيدٌ
Waxumaleen lu dul li nga digle ci loolu, ne leen : “Jaamuleen Yàlla, miy sama Boroom, di seen Boroom”. Ma nekk seede ci ñoom, fekk maa nga nekkoon ca seen biir. Ba nga ma yóbboo ci Yaw [jële ma fa], Yaw yaa leen doon fuglu [nemmiku]. Te sax Yaw yaay Aji-seede ci lépp.
118إِن تُعَذِّبْهُمْ فَإِنَّهُمْ عِبَادُكَ ۖ وَإِن تَغْفِرْ لَهُمْ فَإِنَّكَ أَنتَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Boo leen mbugalee, say jaam lañu. Boo leen jéggalee it, Yaw yaa di Aji-not ji, di Ku xereñ [ci say àtte]”.
119قَالَ اللَّهُ هَٰذَا يَوْمُ يَنفَعُ الصَّادِقِينَ صِدْقُهُمْ ۚ لَهُمْ جَنَّاتٌ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ خَالِدِينَ فِيهَا أَبَدًا ۚ رَّضِيَ اللَّهُ عَنْهُمْ وَرَضُوا عَنْهُ ۚ ذَٰلِكَ الْفَوْزُ الْعَظِيمُ
Yàlla ne : “Bis niki tey, ña dëgguwoon, seen dëggu ga dana leen jariñ : am nañu Àjjana yoo xam ne ay dex ñooy daw ca seen ron, dañu fay béel ba fàwwu.” Yàlla bég na ci ñoom, ñoom it ñu bég ci Yàlla. Loolu mooy texe gu màgg ga tigi.
120لِلَّهِ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَمَا فِيهِنَّ ۚ وَهُوَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Yàllaa moom nguuru asamaan yi ak suuf si ak li nekk ci seen biir, te Muy ku am kàttan nag ci def lépp [lu ko soob].
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
118Aaya

Tekki — Al-Maida 118

Simoore Al-Maida Aaya 118 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Boo leen mbugalee, say jaam lañu. Boo leen jéggalee it,…

Simoore Aaya 118/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 116–120. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers