Al-Maida · 65/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
وَلَوْ أَنَّ أَهْلَ الْكِتَابِ آمَنُوا وَاتَّقَوْا لَكَفَّرْنَا عَنْهُمْ سَيِّئَاتِهِمْ وَلَأَدْخَلْنَاهُمْ جَنَّاتِ النَّعِيمِ ۝٦٥
Wa law anna Ahlal Kitaabi aamanoo wattaqaw lakaffarnaa `anhum saiyiaatihim wa la adkhalnaahu Jannaatin Na`eem
📖 Tekkim Wolof
Bu waa ñoñ-téere gëmoon te ragal Yàlla, kon Nu far seeni ñaawtéef, dugal leen Àjjana ju tudd [Nahiim] xéewal.
🎧 Dégg

📜 Aaya 63-67 — Al-Maida

63لَوْلَا يَنْهَاهُمُ الرَّبَّانِيُّونَ وَالْأَحْبَارُ عَن قَوْلِهِمُ الْإِثْمَ وَأَكْلِهِمُ السُّحْتَ ۚ لَبِئْسَ مَا كَانُوا يَصْنَعُونَ
Lu tee seen làbbe ya ak seen fóore ya tere leen wax ju ñaaw, ak lekk lu araam ? Cëy la ñu liggéey aka bon !
64وَقَالَتِ الْيَهُودُ يَدُ اللَّهِ مَغْلُولَةٌ ۚ غُلَّتْ أَيْدِيهِمْ وَلُعِنُوا بِمَا قَالُوا ۘ بَلْ يَدَاهُ مَبْسُوطَتَانِ يُنفِقُ كَيْفَ يَشَاءُ ۚ وَلَيَزِيدَنَّ كَثِيرًا مِّنْهُم مَّا أُنزِلَ إِلَيْكَ مِن رَّبِّكَ طُغْيَانًا وَكُفْرًا ۚ وَأَلْقَيْنَا بَيْنَهُمُ الْعَدَاوَةَ وَالْبَغْضَاءَ إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ ۚ كُلَّمَا أَوْقَدُوا نَارًا لِّلْحَرْبِ أَطْفَأَهَا اللَّهُ ۚ وَيَسْعَوْنَ فِي الْأَرْضِ فَسَادًا ۚ وَاللَّهُ لَا يُحِبُّ الْمُفْسِدِينَ
Yahuud ya nee nañu : “Loxob Yàlla dafa banku ! ” Seeni yoxo kay ñoom moo banku, te rëbbeef na leen ngir la ñu wax. Li wér mooy ñaari yoxoy Yàlla dañoo tàlli : waaye ni mu ko neexe lay xéewale. Te la Mu wàcce ci yaw di yokk bew ak kéefar ca ñu bari ca ñoom. Te sànni Nanu ca seen diggante noonuwante ak bañante gu fay nekk ba Bis-pénc ba. Saa su ñu taalee safaraw xare, Yàlla fey ko. Dañuy dox di yàq ci suuf si rekk, te Yàlla safoowul yàqkat ya.
65وَلَوْ أَنَّ أَهْلَ الْكِتَابِ آمَنُوا وَاتَّقَوْا لَكَفَّرْنَا عَنْهُمْ سَيِّئَاتِهِمْ وَلَأَدْخَلْنَاهُمْ جَنَّاتِ النَّعِيمِ
Bu waa ñoñ-téere gëmoon te ragal Yàlla, kon Nu far seeni ñaawtéef, dugal leen Àjjana ju tudd [Nahiim] xéewal.
66وَلَوْ أَنَّهُمْ أَقَامُوا التَّوْرَاةَ وَالْإِنجِيلَ وَمَا أُنزِلَ إِلَيْهِم مِّن رَّبِّهِمْ لَأَكَلُوا مِن فَوْقِهِمْ وَمِن تَحْتِ أَرْجُلِهِم ۚ مِّنْهُمْ أُمَّةٌ مُّقْتَصِدَةٌ ۖ وَكَثِيرٌ مِّنْهُمْ سَاءَ مَا يَعْمَلُونَ
Bu ñu jëfewoon Tawreet, ak Linjiil al la ñu wàcce ca ñoom mu tukke ca seen Boroom, kon fàwwu ñu lekk [xéewal] gu bawoo ci kaw ak gu ballee ci seeni suufi tànk. Am na ci ñoom ay nit ñu jub ; waaye ñu bari ca ñoom lu bon lañuy def !
67۞ يَا أَيُّهَا الرَّسُولُ بَلِّغْ مَا أُنزِلَ إِلَيْكَ مِن رَّبِّكَ ۖ وَإِن لَّمْ تَفْعَلْ فَمَا بَلَّغْتَ رِسَالَتَهُ ۚ وَاللَّهُ يَعْصِمُكَ مِنَ النَّاسِ ۗ إِنَّ اللَّهَ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الْكَافِرِينَ
Éy yaw Yonent bi, jottalil la ñu wàcce ci yaw mu tukkee ca sa Boroom. Boo ko deful kon jottaliwoo li Ma la yónni. [Te xamal ne] Yàlla Moo lay musal ci nit ñi. Te Yàlla du gindi aw nit ñu di ay yéefar.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
65Aaya

Tekki — Al-Maida 65

Simoore Al-Maida Aaya 65 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu waa ñoñ-téere gëmoon te ragal Yàlla, kon Nu far…

Simoore Aaya 65/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 63–67. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers