Al-Hashr · 6/24
Tekki Waxtaan — Al-Hashr
وَمَا أَفَاءَ اللَّهُ عَلَىٰ رَسُولِهِ مِنْهُمْ فَمَا أَوْجَفْتُمْ عَلَيْهِ مِنْ خَيْلٍ وَلَا رِكَابٍ وَلَٰكِنَّ اللَّهَ يُسَلِّطُ رُسُلَهُ عَلَىٰ مَن يَشَاءُ ۚ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ ۝٦
Wa maaa afaaa`al laahu `alaaa Rasoolihee minhum famaaa awjaftum `alaihi min khailiinw wa laa rikaabinw wa laakinnal laaha yusallitu Rusulahoo `alaa many yashaaa`; wallaahu `alaa kulli shai`in Qadeer
📖 Tekkim Wolof
Li ngeen nangoo ci ñoom (alal) te xeexuleen Yàllaa ko baaxe ab Yonentam ; waaye nag Yàlla mooy bal ay Yonentam ci kaw ku ko soob te Yàlla ku am kàttan la ci def lépp lu ne.

🎧 Dégg


📜 Aaya 4-8 — Al-Hashr

4ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ شَاقُّوا اللَّهَ وَرَسُولَهُ ۖ وَمَن يُشَاقِّ اللَّهَ فَإِنَّ اللَّهَ شَدِيدُ الْعِقَابِ
Li ko waral moo di ne ñoom dañoo juuyoo woon ak Yàlla ak ub Yonentam. Te nag képp kuy juuyook Yàlla... moom di boroom mbugël mu tar.
5مَا قَطَعْتُم مِّن لِّينَةٍ أَوْ تَرَكْتُمُوهَا قَائِمَةً عَلَىٰ أُصُولِهَا فَبِإِذْنِ اللَّهِ وَلِيُخْزِيَ الْفَاسِقِينَ
Tàndarma gu ngeen man a dog walla ngeen bàyyi ko mu taxaw, ci ndigalul Yàlla la ame ak it ngir mu gàcceel saay-saay sa (Yahuud ya).
6وَمَا أَفَاءَ اللَّهُ عَلَىٰ رَسُولِهِ مِنْهُمْ فَمَا أَوْجَفْتُمْ عَلَيْهِ مِنْ خَيْلٍ وَلَا رِكَابٍ وَلَٰكِنَّ اللَّهَ يُسَلِّطُ رُسُلَهُ عَلَىٰ مَن يَشَاءُ ۚ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Li ngeen nangoo ci ñoom (alal) te xeexuleen Yàllaa ko baaxe ab Yonentam ; waaye nag Yàlla mooy bal ay Yonentam ci kaw ku ko soob te Yàlla ku am kàttan la ci def lépp lu ne.
7مَّا أَفَاءَ اللَّهُ عَلَىٰ رَسُولِهِ مِنْ أَهْلِ الْقُرَىٰ فَلِلَّهِ وَلِلرَّسُولِ وَلِذِي الْقُرْبَىٰ وَالْيَتَامَىٰ وَالْمَسَاكِينِ وَابْنِ السَّبِيلِ كَيْ لَا يَكُونَ دُولَةً بَيْنَ الْأَغْنِيَاءِ مِنكُمْ ۚ وَمَا آتَاكُمُ الرَّسُولُ فَخُذُوهُ وَمَا نَهَاكُمْ عَنْهُ فَانتَهُوا ۚ وَاتَّقُوا اللَّهَ ۖ إِنَّ اللَّهَ شَدِيدُ الْعِقَابِ
Alal ji ngeen nangoo ci dëkk-dëkkaan yi te xeexuleen, Yàllaa ko moom ak ub Yonentam, ak mbokki jigeñaale, ak jirim yi, ak ndóol yi ak doxandeem yi, ( te loolu nag ngir mu baña yem rek) ci diggante way woomal yi. Lépp lu leen Yonent bi jox jël-leen ko ; lépp lu mu leen tere, bàyyileen ko ; te ngeen ragal Yàlla ndax Yàlla kat ku tar mbugël la.
8لِلْفُقَرَاءِ الْمُهَاجِرِينَ الَّذِينَ أُخْرِجُوا مِن دِيَارِهِمْ وَأَمْوَالِهِمْ يَبْتَغُونَ فَضْلًا مِّنَ اللَّهِ وَرِضْوَانًا وَيَنصُرُونَ اللَّهَ وَرَسُولَهُ ۚ أُولَٰئِكَ هُمُ الصَّادِقُونَ
[Bokk na ci ñi yayoo alal jooju] way ñakk ña gàddaayoon ñu génnee woon leen ca seen kër ak seen alal, te doon sàkku ngëneel ci Yàlla ak ngëramam, te doon sàkku ndimbalu Yàlla ak Ub Yonentam. Ñooña ñoo di ñu dëggal ña.
Al-HashrFihi Alxuraan
24Aaya
MedinanRevelation
6Aaya

Tekki — Al-Hashr 6

Simoore Al-Hashr Aaya 6 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Li ngeen nangoo ci ñoom (alal) te xeexuleen Yàllaa ko…

Simoore Aaya 6/24 — Al-Hashr الحشر (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hashr Dégg, Al-Hashr Tekki, Al-Hashr mp3, Al-Hashr pdf. Aaya 4–8. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers