Al-An'am · 112/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَكَذَٰلِكَ جَعَلْنَا لِكُلِّ نَبِيٍّ عَدُوًّا شَيَاطِينَ الْإِنسِ وَالْجِنِّ يُوحِي بَعْضُهُمْ إِلَىٰ بَعْضٍ زُخْرُفَ الْقَوْلِ غُرُورًا ۚ وَلَوْ شَاءَ رَبُّكَ مَا فَعَلُوهُ ۖ فَذَرْهُمْ وَمَا يَفْتَرُونَ ۝١١٢
Wa kazaalika ja`alnaa likulli nabiyyin `aduwwan Shayaateenal insi waljinni yoohee ba`duhum ilaa ba`din zukhrufal qawli ghurooraa; wa law shaaa`a Rabbuka maa fa`aloohu fazarhum wa maa yaftaroon
📖 Tekkim Wolof
Noonu Lanu sàkkalee bépp Yonent ab noon : muy ay séytaane yu nekk nit walla jinne yuy rafetal ay wax ci ñenn ci ñoom jëme ca ñeneen ngir wor leen. Bu neexoon sa Boroom, duñu ko def ; bàyyileen ak la ñuy duur.

🎧 Dégg


📜 Aaya 110-114 — Al-An'am

110وَنُقَلِّبُ أَفْئِدَتَهُمْ وَأَبْصَارَهُمْ كَمَا لَمْ يُؤْمِنُوا بِهِ أَوَّلَ مَرَّةٍ وَنَذَرُهُمْ فِي طُغْيَانِهِمْ يَعْمَهُونَ
Te Dananu wëlbati seeni xol ak seeni gis-gis ca nawoon, ba ñu ko ñàkkee gëm ca njalbéen ga ; te Dananu leen bàyyi ca seenug féttéerlu ñuy tuñ-tuñi.
111۞ وَلَوْ أَنَّنَا نَزَّلْنَا إِلَيْهِمُ الْمَلَائِكَةَ وَكَلَّمَهُمُ الْمَوْتَىٰ وَحَشَرْنَا عَلَيْهِمْ كُلَّ شَيْءٍ قُبُلًا مَّا كَانُوا لِيُؤْمِنُوا إِلَّا أَن يَشَاءَ اللَّهُ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَهُمْ يَجْهَلُونَ
Te su Nu wàcce woon ci ñoom ay Malaaka, ñu dee ña di wax ak ñoom, te Nu dajale ci ñoom lu nekk ñu jàkkaarlook ñoom, duñu gëm mukk bu neexul Yàlla. Waaye nag, la ëpp ca ñoom dañoo réer.
112وَكَذَٰلِكَ جَعَلْنَا لِكُلِّ نَبِيٍّ عَدُوًّا شَيَاطِينَ الْإِنسِ وَالْجِنِّ يُوحِي بَعْضُهُمْ إِلَىٰ بَعْضٍ زُخْرُفَ الْقَوْلِ غُرُورًا ۚ وَلَوْ شَاءَ رَبُّكَ مَا فَعَلُوهُ ۖ فَذَرْهُمْ وَمَا يَفْتَرُونَ
Noonu Lanu sàkkalee bépp Yonent ab noon : muy ay séytaane yu nekk nit walla jinne yuy rafetal ay wax ci ñenn ci ñoom jëme ca ñeneen ngir wor leen. Bu neexoon sa Boroom, duñu ko def ; bàyyileen ak la ñuy duur.
113وَلِتَصْغَىٰ إِلَيْهِ أَفْئِدَةُ الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِالْآخِرَةِ وَلِيَرْضَوْهُ وَلِيَقْتَرِفُوا مَا هُم مُّقْتَرِفُونَ
Ak ngir xoli ñi gëmul àllaaxira jeng ci wax jooju jóge ca, ak ñu fàggu la ñuy fàggu [ciy bàkkaar].
114أَفَغَيْرَ اللَّهِ أَبْتَغِي حَكَمًا وَهُوَ الَّذِي أَنزَلَ إِلَيْكُمُ الْكِتَابَ مُفَصَّلًا ۚ وَالَّذِينَ آتَيْنَاهُمُ الْكِتَابَ يَعْلَمُونَ أَنَّهُ مُنَزَّلٌ مِّن رَّبِّكَ بِالْحَقِّ ۖ فَلَا تَكُونَنَّ مِنَ الْمُمْتَرِينَ
Moo ndax ci keneen ku dul Yàlla laay sàkku àttekat, te Moom moo wàcce ci yéen Téere ba faramfàcce [lu ne] ? Te ña nga xam ne joxoon Nanu leen Téere, xam nañu ne dëgg la te mu wàcc tukkee ca sa Boroom. Kon yaw ci sa wàllu bopp, bul bokk mukk ci ñiy sikki-sàkka.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
112Aaya

Tekki — Al-An'am 112

Simoore Al-An'am Aaya 112 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Noonu Lanu sàkkalee bépp Yonent ab noon : muy ay…

Simoore Aaya 112/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 110–114. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers