Al-An'am · 113/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَلِتَصْغَىٰ إِلَيْهِ أَفْئِدَةُ الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِالْآخِرَةِ وَلِيَرْضَوْهُ وَلِيَقْتَرِفُوا مَا هُم مُّقْتَرِفُونَ ۝١١٣
Wa litasghaaa ilaihi af`idatul lazeena laa yu`minoona bil Aakhirati wa liyardawhu wa liyaqtarifoo maa hum muqtarifoon
📖 Tekkim Wolof
Ak ngir xoli ñi gëmul àllaaxira jeng ci wax jooju jóge ca, ak ñu fàggu la ñuy fàggu [ciy bàkkaar].
🎧 Dégg

📜 Aaya 111-115 — Al-An'am

111۞ وَلَوْ أَنَّنَا نَزَّلْنَا إِلَيْهِمُ الْمَلَائِكَةَ وَكَلَّمَهُمُ الْمَوْتَىٰ وَحَشَرْنَا عَلَيْهِمْ كُلَّ شَيْءٍ قُبُلًا مَّا كَانُوا لِيُؤْمِنُوا إِلَّا أَن يَشَاءَ اللَّهُ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَهُمْ يَجْهَلُونَ
Te su Nu wàcce woon ci ñoom ay Malaaka, ñu dee ña di wax ak ñoom, te Nu dajale ci ñoom lu nekk ñu jàkkaarlook ñoom, duñu gëm mukk bu neexul Yàlla. Waaye nag, la ëpp ca ñoom dañoo réer.
112وَكَذَٰلِكَ جَعَلْنَا لِكُلِّ نَبِيٍّ عَدُوًّا شَيَاطِينَ الْإِنسِ وَالْجِنِّ يُوحِي بَعْضُهُمْ إِلَىٰ بَعْضٍ زُخْرُفَ الْقَوْلِ غُرُورًا ۚ وَلَوْ شَاءَ رَبُّكَ مَا فَعَلُوهُ ۖ فَذَرْهُمْ وَمَا يَفْتَرُونَ
Noonu Lanu sàkkalee bépp Yonent ab noon : muy ay séytaane yu nekk nit walla jinne yuy rafetal ay wax ci ñenn ci ñoom jëme ca ñeneen ngir wor leen. Bu neexoon sa Boroom, duñu ko def ; bàyyileen ak la ñuy duur.
113وَلِتَصْغَىٰ إِلَيْهِ أَفْئِدَةُ الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِالْآخِرَةِ وَلِيَرْضَوْهُ وَلِيَقْتَرِفُوا مَا هُم مُّقْتَرِفُونَ
Ak ngir xoli ñi gëmul àllaaxira jeng ci wax jooju jóge ca, ak ñu fàggu la ñuy fàggu [ciy bàkkaar].
114أَفَغَيْرَ اللَّهِ أَبْتَغِي حَكَمًا وَهُوَ الَّذِي أَنزَلَ إِلَيْكُمُ الْكِتَابَ مُفَصَّلًا ۚ وَالَّذِينَ آتَيْنَاهُمُ الْكِتَابَ يَعْلَمُونَ أَنَّهُ مُنَزَّلٌ مِّن رَّبِّكَ بِالْحَقِّ ۖ فَلَا تَكُونَنَّ مِنَ الْمُمْتَرِينَ
Moo ndax ci keneen ku dul Yàlla laay sàkku àttekat, te Moom moo wàcce ci yéen Téere ba faramfàcce [lu ne] ? Te ña nga xam ne joxoon Nanu leen Téere, xam nañu ne dëgg la te mu wàcc tukkee ca sa Boroom. Kon yaw ci sa wàllu bopp, bul bokk mukk ci ñiy sikki-sàkka.
115وَتَمَّتْ كَلِمَتُ رَبِّكَ صِدْقًا وَعَدْلًا ۚ لَّا مُبَدِّلَ لِكَلِمَاتِهِ ۚ وَهُوَ السَّمِيعُ الْعَلِيمُ
Sa kàddug Boroom mat na ci dëgg ak maandute. Ay waxam du soppeeku. Kuy dégg la, di Ku xam.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
113Aaya

Tekki — Al-An'am 113

Simoore Al-An'am Aaya 113 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ak ngir xoli ñi gëmul àllaaxira jeng ci wax jooju…

Simoore Aaya 113/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 111–115. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers