Al-A'raf · 167/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
وَإِذْ تَأَذَّنَ رَبُّكَ لَيَبْعَثَنَّ عَلَيْهِمْ إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ مَن يَسُومُهُمْ سُوءَ الْعَذَابِ ۗ إِنَّ رَبَّكَ لَسَرِيعُ الْعِقَابِ ۖ وَإِنَّهُ لَغَفُورٌ رَّحِيمٌ ۝١٦٧
Wa iz ta azzana Rabbuka la yab`asannna `alaihim ilaa Yawmil Qiyaamati mai yasoomuhum sooo`al `azaab; inna Rabbaka lasaree`ul `iqaab; wa innahoo la Ghafoorur Raheem
📖 Tekkim Wolof
[Fàttalikul] ba seen Boroom xamlee ne Dana leen yónnee ku leen di teg gëm jaa boni mbugal ba kerook Bis-pénc di agsi. Sa Boroom nag Ku gaaw la ci mbugal te Moom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 165-169 — Al-A'raf

165فَلَمَّا نَسُوا مَا ذُكِّرُوا بِهِ أَنجَيْنَا الَّذِينَ يَنْهَوْنَ عَنِ السُّوءِ وَأَخَذْنَا الَّذِينَ ظَلَمُوا بِعَذَابٍ بَئِيسٍ بِمَا كَانُوا يَفْسُقُونَ
Ba ñu fàttee la ñu leen doon waare, musal Nanu ña doon tere lu bon, Nu sadd ña doon tooñ, mbugal mu tar ngir la ñu féttérlu woon génn topp.
166فَلَمَّا عَتَوْا عَن مَّا نُهُوا عَنْهُ قُلْنَا لَهُمْ كُونُوا قِرَدَةً خَاسِئِينَ
Bu ñu rëyloo ca la ñu leen tere, Nu wax leen ne : “Nekkleen di ay golo yu torox”.
167وَإِذْ تَأَذَّنَ رَبُّكَ لَيَبْعَثَنَّ عَلَيْهِمْ إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ مَن يَسُومُهُمْ سُوءَ الْعَذَابِ ۗ إِنَّ رَبَّكَ لَسَرِيعُ الْعِقَابِ ۖ وَإِنَّهُ لَغَفُورٌ رَّحِيمٌ
[Fàttalikul] ba seen Boroom xamlee ne Dana leen yónnee ku leen di teg gëm jaa boni mbugal ba kerook Bis-pénc di agsi. Sa Boroom nag Ku gaaw la ci mbugal te Moom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
168وَقَطَّعْنَاهُمْ فِي الْأَرْضِ أُمَمًا ۖ مِّنْهُمُ الصَّالِحُونَ وَمِنْهُمْ دُونَ ذَٰلِكَ ۖ وَبَلَوْنَاهُم بِالْحَسَنَاتِ وَالسَّيِّئَاتِ لَعَلَّهُمْ يَرْجِعُونَ
Te séddale Nanu leen ay giir ci suuf si. Am ci ñoom ñu yiw, am ñu yiwadi. Nu nattu leen ciy xéewal ak ciy naqar ndax ñu dellusi [ci seen Boroom].
169فَخَلَفَ مِن بَعْدِهِمْ خَلْفٌ وَرِثُوا الْكِتَابَ يَأْخُذُونَ عَرَضَ هَٰذَا الْأَدْنَىٰ وَيَقُولُونَ سَيُغْفَرُ لَنَا وَإِن يَأْتِهِمْ عَرَضٌ مِّثْلُهُ يَأْخُذُوهُ ۚ أَلَمْ يُؤْخَذْ عَلَيْهِم مِّيثَاقُ الْكِتَابِ أَن لَّا يَقُولُوا عَلَى اللَّهِ إِلَّا الْحَقَّ وَدَرَسُوا مَا فِيهِ ۗ وَالدَّارُ الْآخِرَةُ خَيْرٌ لِّلَّذِينَ يَتَّقُونَ ۗ أَفَلَا تَعْقِلُونَ
Kuutaay gu bon toftaloo ca ñoom, [teewul] ñu jàppe ci alali ku yées ki [di àddina], ñu naan : “Dees nanu baal.”. Te bu leen alal ju ne mel dikkalee, ñu jàpp ca. Waaw ndax kóllareb Téere ba tënku leen ci di waxal Yàlla dëgg rekk ? Moone jàng nañu la nekk ca biir de. Te kërug àllaaxira moo gën ca ña ragal Yàlla, - Moo ndax dangeen dul xel-lu ? -
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
167Aaya

Tekki — Al-A'raf 167

Simoore Al-A'raf Aaya 167 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Fàttalikul] ba seen Boroom xamlee ne Dana leen yónnee ku…

Simoore Aaya 167/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 165–169. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers