Al-A'raf · 170/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
وَالَّذِينَ يُمَسِّكُونَ بِالْكِتَابِ وَأَقَامُوا الصَّلَاةَ إِنَّا لَا نُضِيعُ أَجْرَ الْمُصْلِحِينَ ۝١٧٠
Wallazeena yumas sikoona bil Kitaabi wa aqaamus Salaata innaa laa nudee`uajral musliheen
📖 Tekkim Wolof
Te ñay jafandu ca Téere ba te di taxawal julli, [nañu xam ne] Nun nag Dunu sànk peyu way-sellal ña.

🎧 Dégg


📜 Aaya 168-172 — Al-A'raf

168وَقَطَّعْنَاهُمْ فِي الْأَرْضِ أُمَمًا ۖ مِّنْهُمُ الصَّالِحُونَ وَمِنْهُمْ دُونَ ذَٰلِكَ ۖ وَبَلَوْنَاهُم بِالْحَسَنَاتِ وَالسَّيِّئَاتِ لَعَلَّهُمْ يَرْجِعُونَ
Te séddale Nanu leen ay giir ci suuf si. Am ci ñoom ñu yiw, am ñu yiwadi. Nu nattu leen ciy xéewal ak ciy naqar ndax ñu dellusi [ci seen Boroom].
169فَخَلَفَ مِن بَعْدِهِمْ خَلْفٌ وَرِثُوا الْكِتَابَ يَأْخُذُونَ عَرَضَ هَٰذَا الْأَدْنَىٰ وَيَقُولُونَ سَيُغْفَرُ لَنَا وَإِن يَأْتِهِمْ عَرَضٌ مِّثْلُهُ يَأْخُذُوهُ ۚ أَلَمْ يُؤْخَذْ عَلَيْهِم مِّيثَاقُ الْكِتَابِ أَن لَّا يَقُولُوا عَلَى اللَّهِ إِلَّا الْحَقَّ وَدَرَسُوا مَا فِيهِ ۗ وَالدَّارُ الْآخِرَةُ خَيْرٌ لِّلَّذِينَ يَتَّقُونَ ۗ أَفَلَا تَعْقِلُونَ
Kuutaay gu bon toftaloo ca ñoom, [teewul] ñu jàppe ci alali ku yées ki [di àddina], ñu naan : “Dees nanu baal.”. Te bu leen alal ju ne mel dikkalee, ñu jàpp ca. Waaw ndax kóllareb Téere ba tënku leen ci di waxal Yàlla dëgg rekk ? Moone jàng nañu la nekk ca biir de. Te kërug àllaaxira moo gën ca ña ragal Yàlla, - Moo ndax dangeen dul xel-lu ? -
170وَالَّذِينَ يُمَسِّكُونَ بِالْكِتَابِ وَأَقَامُوا الصَّلَاةَ إِنَّا لَا نُضِيعُ أَجْرَ الْمُصْلِحِينَ
Te ñay jafandu ca Téere ba te di taxawal julli, [nañu xam ne] Nun nag Dunu sànk peyu way-sellal ña.
171۞ وَإِذْ نَتَقْنَا الْجَبَلَ فَوْقَهُمْ كَأَنَّهُ ظُلَّةٌ وَظَنُّوا أَنَّهُ وَاقِعٌ بِهِمْ خُذُوا مَا آتَيْنَاكُم بِقُوَّةٍ وَاذْكُرُوا مَا فِيهِ لَعَلَّكُمْ تَتَّقُونَ
[Fàttalikul] ba Nu yékkatee doj wa mu tiim leen, mel ni niir la. Ñu am njort ci mu daanu ci seen kaw. Ñu ne leen : “Jàppleen lii ñu leen jox ànd ca ak farlu te ngeen jëfe li nekk ci biir. Ndax xéy-na yéen ngeen ragal Yàlla”.
172وَإِذْ أَخَذَ رَبُّكَ مِن بَنِي آدَمَ مِن ظُهُورِهِمْ ذُرِّيَّتَهُمْ وَأَشْهَدَهُمْ عَلَىٰ أَنفُسِهِمْ أَلَسْتُ بِرَبِّكُمْ ۖ قَالُوا بَلَىٰ ۛ شَهِدْنَا ۛ أَن تَقُولُوا يَوْمَ الْقِيَامَةِ إِنَّا كُنَّا عَنْ هَٰذَا غَافِلِينَ
[Fàttalikul] ba sa Boroom génnee ci ndigul doomu-aadama yi seeni sëf, te Mu seedeloo leen ci seen bopp, ne leen : “Du Maay seen Boroom ? ”. Ñu ne : “Axakay, seede nanu ko...” - ngir ngeen bañ a wax ca Bis-pénc ba ne : “Danoo réere woon lii [mu nekk seenu lay]”,
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
170Aaya

Tekki — Al-A'raf 170

Simoore Al-A'raf Aaya 170 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te ñay jafandu ca Téere ba te di taxawal julli,…

Simoore Aaya 170/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 168–172. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers